Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Luke 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In Tiberius Caesar's fifteenth year, when Pontius Pilate was governor of Judea, Herod was tetrarch of Galilee, his brother Philip of the region of Ituraea and Trachonitis, and Lysanias of Abilene, Ca fukkeelu at ak juróom ci nguurug buur bu mag ba Tibeer Sesaar, ba Poñsë Pilaat yilifee diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, Lisañas yilif Abilen,
2 under high priests Annas and Caiaphas, our Father's word came to John son of Zechariah in the wilderness. jamono yooyu Anas ak Kayif doone sarxalkat yu mag ya, ca la kàddug Yàlla dikkal Yaxya doomu Sàkkaryaa, ca màndiŋ ma.
3 He went through the whole Jordan region, preaching a baptism of repentance for the forgiveness of sins, Yaxya dugg ci mboolem àll bi wër dexu Yurdan, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir Yàlla jéggal leen seeni bàkkaar.
4 as it is written in the book of the words of Isaiah the prophet: "A voice of one calling in the wilderness: Prepare the way for the Lord, make his paths straight. Loolu lañu bind ci téereb waxi Yonent Yàlla Esayi ne: «Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan: “Nangeen xàll yoonu Boroom bi, juballeen ay xàllam.
5 Every valley will be filled in, and every mountain and hill made low. The crooked roads will become straight, and the rough ways smooth, Xur yépp ay sëkke, tund wu mag ak wu ndaw maasaloo, yoon ya lunkoon, jubbantiku, ya ñagasoon, nooy,
6 and all flesh will see the salvation of our Father." ba ñépp gis mucc gi Yàlla dogal.”»
7 John said then to the crowds coming to be baptized by him: "You brood of vipers! Who warned you to flee the coming wrath? Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen artu, ba ngeen di daw sànj miy dikk?
8 So produce fruit worthy of repentance. Don't start telling yourselves, 'We have Abraham as our father.' For I tell you, our Father can raise up children for Abraham from these stones. Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
9 Already the axe lies at the root of the trees; every tree not bearing good fruit is cut down and thrown into the fire." Te itam xàcc nañu sémmiñ ngir gor reenu garab yi ba noppi. Kon nag gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.»
10 And the crowds asked him, "What then should we do?" Mbooloo ma itam laaj ko ne ko: «Ana lu nu war nag?»
11 He replied, "Whoever has two shirts, share with the one who has none; whoever has food, do the same." Mu ne leen: «Ku am ñaari turki, na sédd ki amul. Ku am aw ñam itam, na defe noonu.»
12 Tax collectors also came to be baptized, and they said to him, "Teacher, what should we do?" Ay juutikat itam dikk, ngir sóobusi; ñu ne Yaxya: «Kilifa gi, ana lu nu war?»
13 "Collect no more than you are required to," he told them. Mu ne leen: «Xanaa baña sàkku lenn lu moy li jaadu.»
14 Soldiers also asked him, "And us—what should we do?" He said to them, "Don't extort anyone by force or false charges; be satisfied with your wages." Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.»
15 The people were expectant, all wondering in their hearts whether John himself might be the Christ. Ci kaw loolu askan wa di séentu, ñépp di seetaat ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.
16 John answered them all, "I baptize you with water. But one stronger than I is coming—I'm not worthy to untie his sandal strap. He will baptize you with the Holy Spirit and fire. Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man de ci ndox laa leen di sóob. Waaye ku ma sut a ngi ñëw, kooku, buumi caraxam sax, yeyoowuma ko koo feccil. Moom, ci Noo gu Sell gi ak sawara la leen di sóob.
17 Winnowing fork in hand, he will clear his threshing floor, gather the wheat into his barn, but burn the chaff with fire that can't be put out." Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18 And with many other words of exhortation, John proclaimed the good news to the people. Bare na yeneen dénkaane yu Yaxya doon xamal nit ñi, di yégle xibaaru jàmm bi.
19 But John confronted Herod the tetrarch about Herodias, his brother's wife, and about all the evil Herod had done, Erodd boroom réew ma nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def.
20 Herod added this to all the rest: he locked John up in prison. Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba.
21 When all the people were baptized, Jesus was baptized too. As he prayed, heaven opened, Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku.
22 and the Holy Spirit descended on him in bodily form like a dove. And a voice came from heaven: "You are my beloved Son; in you I delight." Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»
23 Jesus was about thirty when he began his ministry, the son—so it was thought—of Joseph, son of Heli, Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe. Yuusufa, Eli mooy baayam,
24 the son of Matthat, the son of Levi, the son of Melchi, the son of Jannai, the son of Joseph, Eli, Matat. Matat, Lewi; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25 the son of Mattathias, the son of Amos, the son of Nahum, the son of Esli, the son of Naggai, Yuusufa, Matacas; Matacas, Amos; Amos, Nawum; Nawum, Esli; Esli, Nagayi.
26 the son of Maath, the son of Mattathias, the son of Semein, the son of Josech, the son of Joda, Nagayi, Maat; Maat, Matacas; Matacas, Semeyin; Semeyin, Yosex; Yosex, Yoda.
27 the son of Joanan, the son of Rhesa, the son of Zerubbabel, the son of Shealtiel, the son of Neri, Yoda, Yoxanan; Yoxanan, Resa; Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri;
28 the son of Melchi, the son of Addi, the son of Cosam, the son of Elmadam, the son of Er, Neri, Melki; Melki, Adi; Adi, Kosam; Kosam, Elmadam; Elmadam, Er.
29 the son of Joshua, the son of Eliezer, the son of Jorim, the son of Matthat, the son of Levi, Er, Yosuwe; Yosuwe, Elyeser; Elyeser, Yorim; Yorim, Matat; Matat, Lewi;
30 the son of Simeon, the son of Judah, the son of Joseph, the son of Jonam, the son of Eliakim, Lewi, Simeyon; Simeyon, Yuda; Yuda, Yuusufa; Yuusufa, Yonam; Yonam, Elyakim.
31 the son of Melea, the son of Menna, the son of Mattatha, the son of Nathan, the son of David, Elyakim, Meleya; Meleya, Mena; Mena, Matata; Matata, Natan; Natan, Daawuda.
32 the son of Jesse, the son of Obed, the son of Boaz, the son of Salmon, the son of Nahshon, Daawuda mooy doomu Yese; Yese, Obedd; Obedd, Bowas; Bowas, Sala; Sala, Naason.
33 the son of Amminadab, the son of Admin, the son of Arni, the son of Hezron, the son of Perez, the son of Judah, Naason, Aminadab; Aminadab, Admin; Admin, Arni; Arni, Esron; Esron, Peres; Peres, Yuda;
34 the son of Jacob, the son of Isaac, the son of Abraham, the son of Terah, the son of Nahor, Yuda, Yanqóoba; Yanqóoba, Isaaxa; Isaaxa, Ibraayma; Ibraayma, Teraa; Teraa, Naxor;
35 the son of Serug, the son of Reu, the son of Peleg, the son of Eber, the son of Shelah, Naxor, Serug; Serug, Rew; Rew, Peleg; Peleg, Eber; Eber, Sela;
36 the son of Cainan, the son of Arphaxad, the son of Shem, the son of Noah, the son of Lamech, Sela, Kenan; Kenan, Arpagsàdd; Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
37 the son of Methuselah, the son of Enoch, the son of Jared, the son of Mahalalel, the son of Cainan, Lemeg, Matusalem; Matusalem, Enog; Enog, Yeredd; Yeredd, Maalaleel; Maalaleel, Kenan;
38 the son of Enosh, the son of Seth, the son of Adam, the son of our Father. Kenan, Enos; Enos, Set; Set, Aadama; Aadama, Yàlla.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]