Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Leviticus 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "If someone's offering is a peace offering from the herd, male or female, he must present it without defect before me. «Su fekkee ne li nit kiy sarxe saraxu cant la ci biir jàmm, mu di ko jële ci nag wu góor mbaa wu jigéen, na indil Aji Sax ji lu amul sikk.
2 He lays his hand on his offering's head and slaughters it at the tent of meeting's entrance, and Aaron's sons the priests splash the blood against all sides of the altar. Day teg loxoom ci kaw boppu jur gi muy sarxal, te rendi ko ca bunt xaymab ndaje ma. Doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi daldi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
3 From the peace offering he must present to me a food offering made by fire: the fat covering the inner parts and all the fat on them, Li muy génne ci saraxu cant gi ci biir jàmm, ñu war koo taalal Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
4 both kidneys with the fat on them near the flanks, and the long lobe of the liver, which he removes with the kidneys. ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
5 Aaron's sons will burn it on the altar atop the burnt offering on the wood over the fire—a food offering, a pleasing aroma to me. Na doomi Aaróona yi boole yooyu lakk ci kaw sarxalukaay bi, mu tege ci kaw saraxu rendi-dóomal bi ci kaw mattum taal bi. Saraxu sawara la ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
6 "If his peace offering to me is from the flock, male or female, he must present it without defect. «Su fekkee ne li nit kiy sarxalal Aji Sax ji saraxu cant la ci biir jàmm, te mu di ko jële ci jur gu gàtt, gu góor mbaa gu jigéen, na sarxal lu amul sikk.
7 If he brings a lamb as his offering, he is to present it before me, Su dee sarxal xar, na ko indil Aji Sax ji
8 lay his hand on the head of his offering and slaughter it before the tent of meeting; Aaron's sons will splash its blood on all sides of the altar. te teg loxoom ci boppu xar mi muy sarxe, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi, doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
9 From the peace offering he must present a food offering to me by fire: its fat, the whole fat tail cut off close to the backbone, the fat covering the inner parts, and all the fat on them, Li muy génne ci saraxu cant ci biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
10 both kidneys with the fat near the loins, and the liver's long lobe, which he removes with the kidneys. ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
11 The priest will burn it on the altar as food, an offering made to me by fire. Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñam wu ñu lakke sawara, ñeel Aji Sax ji.
12 "If his offering is a goat, he is to present it before me, «Bu saraxu nit ki dee bëy, na ko indil Aji Sax ji
13 lay his hand on its head and slaughter it in front of the tent of meeting; Aaron's sons will splash its blood on all sides of the altar. te teg loxoom ci bopp bi, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi. Na doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
14 From it he must present a food offering to me by fire: the fat covering the inner parts and all the fat on them, La mu cay génnee muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji mooy nebbon bi sàng yérey biir yi yépp, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
15 both kidneys with their fat near the loins, and the liver's long lobe, which he removes with the kidneys. ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te mu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
16 The priest will burn them on the altar as food, an offering by fire, a pleasing aroma. All fat is mine. Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñam wu ñu lakke sawara, muy xeeñ xetug jàmm gu neex Aji Sax ji. Mboolem luy nebbon, Aji Sax jeey boroom.
17 "This is a lasting rule for all generations, wherever you live: never eat any fat or any blood." Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]