Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Leviticus 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "When anyone brings a grain offering to our Father, the offering must be fine flour. Pour oil on it, put frankincense on it, «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu pepp, sunguf su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci cuuraay,
2 and bring it to Aaron's sons, the priests. The priest will take a handful of its fine flour and oil, with all its frankincense, and burn the memorial portion on the altar—a fire offering, a pleasing aroma to our Father. te yót ko doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi. Na sarxalkat bi sàkk barci-loxob sunguf su mucc ayib soosu ànd ak diw gi, te boole kook cuuraay li lépp. Na sarxalkat bi def cér boobu saraxu baaxantal, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
3 The rest of the grain offering belongs to Aaron and his sons—most holy, from the fire offerings to our Father. Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
4 "When you bring a grain offering baked in an oven: fine flour, either loaves without yeast mixed with oil, or wafers without yeast spread with oil. «Su dee sarxal lu ñu defare pepp, di lu ñu lakk cib taal ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib, di mburu yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, mbaa mburu yu sew yu amul lawiir, ñu sotti diw ca kawam.
5 If your offering is a grain offering on a griddle, it must be fine flour mixed with oil, without yeast. «Bu saraxam dee lu ñu defare pepp, lakke ko ci saafukaayu weñ, na doon sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale diw te bumu am lawiir.
6 Break it into pieces and pour oil on it; it is a grain offering. Na ko dammat te sotti diw ca kaw dog ya. Saraxu pepp la.
7 If your offering is grain cooked in a pan, make it with fine flour and oil. «Bu saraxam dee lu ñu defare pepp, di lu ñu saaf ci cin ba mu ñor, na doon sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale diw.
8 Bring the grain offering made from these to our Father; present it to the priest, who brings it to the altar. «Na yóbbul Aji Sax ji saraxu pepp su ñu defar ci tegtal yooyu, yót ko sarxalkat bi, mu yóbbu ko ca sarxalukaay ba.
9 The priest takes the grain offering's memorial portion and burns it on the altar—a fire offering, a pleasing aroma to our Father. Su ko defee sarxalkat bi génne ci saraxu pepp mi, ab saraxu baaxantal, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
10 What remains of the grain offering belongs to Aaron and his sons—most holy, from the fire offerings to our Father. Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
11 "No grain offering you bring to our Father may contain yeast, for you must not burn any yeast or honey as a fire offering to our Father. «Du benn saraxu pepp bu ñuy defal Aji Sax ji muy am lawiir, ndax du lenn ci lawiir mbaa lem, lu ñu wara lakk, ngir saraxu sawara su ñeel Aji Sax ji.
12 You may bring them to our Father as a firstfruits offering, but do not offer them on the altar as a pleasing aroma. Saraxi ndoortel meññeef man naa ànd ak yooyu, waaye du bokk ci sarax su jëm ca sarxalukaay ba, ñu di ko taal, ngir xetug jàmm.
13 Salt every grain offering. Don't leave out your Father's covenant salt; add salt to all your offerings. Seen mboolem saraxu pepp nangeen ko xorom. Bu seen saraxu pepp ñàkk mukk xorom, ndax mooy màndargaal seen kóllëreek seen Yàlla. Seen sarax yépp ngeen di xorom.
14 "If you bring a firstfruits grain offering to our Father, offer new grain roasted in fire, crushed kernels, as your firstfruits offering. «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu ndoortel meññeef, na ko indil mbool mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu ndoortel meññeefam.
15 Put oil on it and lay frankincense on it; it is a grain offering. Na ci sotti diw ak cuuraay. Saraxu pepp la.
16 The priest burns the memorial portion—some of the crushed grain and oil—with all its frankincense, as a fire offering to our Father." Na sarxalkat bi lakk lenn ci mbool mu mokk mi ànd ak diw, boole kook cuuraay li lépp, muy saraxu baaxantal, te di saraxu sawara ñeel Aji Sax ji.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]