Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Leviticus 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Our Father called to Moses and spoke to him from the tent of meeting, saying: Aji Sax ji woo na Musaa, wax ak moom ca xaymab ndaje ma ne ko:
2 "Speak to the Israelites and say to them: When any of you brings me an offering, bring your offering of livestock from the herd or the flock. «Waxal bànni Israayil ne leen: Bu kenn ci yeen dee sàkkal Aji Sax ji sarax, na indi ag jur, muy gu gudd mbaa gu gàtt.
3 "If his offering is a burnt offering from the herd, he is to offer a male without defect, offering it at the entrance of the tent of meeting, to be accepted before me. «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko.
4 He is to lay his hand on the burnt offering's head, and it will be accepted for him, to atone for him. Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.
5 He is to kill the young bull before me, and Aaron's sons the priests are to bring the blood and splash it around the altar at the entrance of the tent of meeting. Na rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji, te doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi ñooy indi deret ji, xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi ci bunt xaymab ndaje mi.
6 Then he is to skin the burnt offering and cut it into its pieces. Juru saraxu rendi-dóomal bi, na ko boroom sarax bi fees, daggat ko.
7 Aaron's sons the priests will lay a fire on the altar and arrange wood on it. Doomi Aaróona, sarxalkat bi, ñooy jafal ab taal ci kaw sarxalukaay bi, teg matt mi ci taal bi.
8 Aaron's sons, the priests, arrange the pieces, head, and fat on the wood over the fire on the altar. Su ko defee doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi, jël dog yi, booleek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci sarxalukaay bi.
9 He is to wash its inner organs and legs with water; the priest burns it all on the altar—a burnt offering, a food offering, a pleasing aroma to me. Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
10 "If his burnt offering is from the flock—sheep or goats—he must bring a male without defect. «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk.
11 He is to slaughter it on the altar's north side before me; Aaron's sons the priests are to splash its blood around the altar. Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
12 He is to cut it into pieces—head and fat—and the priest is to arrange them on the wood, on the fire, on the altar. Bu ko boroom sarax bi daggatee ba noppi, sarxalkat bi day boole dog yeek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci kaw sarxalukaay bi.
13 He must wash the inner organs and legs with water; the priest offers it all, burns it on the altar—a burnt offering, a food offering, a pleasing aroma to me. Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
14 "If his burnt offering to me is a bird, he must bring turtledoves or young pigeons as his offering. «Bu nit ki dee sarxalal Aji Sax ji njanaaw luy doon rendi-dóomal, na sarxe pitax mbaa xati mu ndaw.
15 The priest brings it to the altar, wrings off its head, burns it there; its blood drains against the altar's side. Na ko sarxalkat bi yóbbu ca sarxalukaay ba, kutt baat bi, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. Deret ji dees koy siital ci wetu sarxalukaay bi, ba mu jeex.
16 He removes its crop with its contents, throwing it beside the altar eastward, at the ash heap. Na indi gag bi ak li ci nekk te wetti ko fa ñuy def dóomu-taal ba, fa féete sarxalukaay bi penku.
17 He is to tear it open by the wings, not fully apart; the priest will burn it on the altar's wood over the fire—a burnt offering, a food offering, a pleasing aroma to me." Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]