Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Joel 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The word of our Father that came to Joel son of Pethuel. Kàddug Aji Sax jii moo dikkal Yowel doomu Petuwel.
2 Hear this, you elders; listen, all who live in this land. Has anything like this happened in your days, or in the days of your ancestors? Dégluleen, yeen mag ñi, teewluleen, yeen waa réew mi ñépp. Ndax lii mas naa am ci seeni jant, mbaa seen janti maam?
3 Tell your children about it, and let your children tell their children, and their children the next generation. Waxleen ko seen doom yi ngeen jur, doom yi ngeen jur wax ko doom yi ñu jur, doom yi ñu jur wax ko geneen maas.
4 What the cutting locust spared, the swarming locust ate; what the swarming locust spared, the hopping locust ate; and what the hopping locust spared, the destroying locust ate. Ndesu soccet yi, la njéeréer yi lekk, ndesu njéeréer yi, seenu tostan lekk, seen ndesu tostan, salleer yi lekk.
5 Wake up, you drunkards, and weep; wail, all you wine drinkers, over the sweet wine, for it has been cut off from your lips. Màndikat yee, yewwuleen, jooyoo. Naan-kati biiñ yee, jooyleen biiñ bu bees bi ñu foqatee ci seen gémmiñ.
6 "For a nation has invaded my land, mighty and beyond number; its teeth are the teeth of a lion, and it has the fangs of a lioness. Aw xeet a dal ci samam réew, am kàttan, wees ab lim, seeni sell di selli gaynde gu góor, seeni ŋaam di ŋaami gaynde gu jigéen.
7 It has devastated my vines and splintered my fig tree; it has stripped off their bark and cast it aside, leaving their branches bare and white." Samag reseñ lañu yàqate, samag figg lañu xas a xas, ba mu set, ñu sànni, car ya weex tàll.
8 Wail like a virgin dressed in mourning clothes for the husband of her youth. Neeleen wóoy ni janq bu woddoob saaku, di ko ñaawloo jëkkëram ja ñu ko dencaloon ba muy lu tuut.
9 The grain offering and the drink offering are cut off from the house of our Father; the priests, the ministers of our Father, mourn. Saraxu pepp ak saraxu tuuru dagg na ca kër Aji Sax ji. Sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, ñu ngi ñaawlu.
10 The field is devastated, the ground mourns; for the grain is destroyed, the new wine dries up, the oil fails. Tool yi yàqu yaxeet, suuf sëngéem ciw tiis; pepp yàqu, biiñ bu bees wow, ag diw ŋiis.
11 Be ashamed, you farmers; wail, you grape growers, over the wheat and the barley, for the harvest of the field has perished. Yeen beykat yi, rusleen; boroom tóokëri reseñ yi, yuuxooleen, ndax peppum bele baak lors ba, nde ngóob mi sànku na.
12 The vine is dried up, and the fig tree withers; the pomegranate, the palm, and the apple—all the trees of the field are dried up. Surely joy has withered away from all people. Ag reseñ wow, figg lax, gërënaat, tàndarma, ak pom, mboolem garabi tool, wow koŋŋ. Mbég daal a rasu doom aadama.
13 Put on mourning clothes and lament, you priests; wail, you ministers of the altar. Come, spend the night in mourning clothes, you ministers of my Father; for the grain offering and the drink offering are withheld from the house of your Father. Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!
14 Declare a fast; call a sacred assembly. Gather the elders and all who live in the land to the house of our Father, and cry out to our Father. Sellalleen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.
15 Alas for the day! For the day of our Father is near, and it will come like destruction from the Almighty. Céy, bii bés! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa Aji Man ji lay dikke.
16 Is not the food cut off right before our eyes—joy and gladness gone from the house of our Father? Xanaa du ag lekk a dagg, nuy gis, te mbég ak bànneex tukkee sunu kër Yàlla ga?
17 The seeds shrivel in the parched ground; the storehouses are desolate, the granaries are torn down, for the grain has dried up. Aw jiwu wow na, suule ciy donji suuf, dencukaay yi wéet, sàq yi dàjjiku, am pepp wow.
18 How the animals groan! The herds of cattle wander in confusion because they have no pasture; even the flocks of sheep suffer. Céy ni mala yiy binnee! Gétti nag yaa ngi jànnaxe, ndax ñàkk parlu, gàtt yi itam loof.
19 To you, our Father, I call, for fire has devoured the pastures of the wilderness, and flame has burned all the trees of the field. Yaw Aji Sax ji laay woo, sawara moo lekk parluy àll bi; ag daay a xoyom garabi àll bi yépp.
20 Even the wild animals cry out to you, for the streams have dried up, and fire has devoured the pastures of the wilderness. Rabi àll yi it ñu ngi àppaat, jublook yaw, nde wali ndox yee ŋiis, te sawara xoyom parluy àll bi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]