Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 King Nebuchadnezzar made a gold statue, about ninety feet tall and nine feet wide, and set it up on the Dura plain in Babylon province. Mu am bés Buur Nebukatnecar defarlu jëmmi wurus, taxawaay ba di fanweeri meetar, yaatuwaay ba di ñetti meetar. Mu taxawal ko ca jooru Dura ga ca diiwaanu Babilon.
2 King Nebuchadnezzar sent for the satraps, prefects, governors, counselors, treasurers, judges, magistrates, and all provincial officials to come to the dedication of the image he had set up. Buur Nebukatnecar nag woolu jawriñ yaak laman yaak jaraaf yaak kàngam yaak farbay alal yaak àttekat yaak ndawi buur yaak mboolem kilifay diiwaan ya, ngir ñu ñëw ca bernde ja mu maye ca daloob jëmm ja mu samp.
3 Then satraps, prefects, governors, counselors, treasurers, judges, magistrates, and all provincial officials gathered to dedicate the statue King Nebuchadnezzar set up, and stood before the statue Nebuchadnezzar set up. Ba loolu amee jawriñ yaak laman yaak jaraaf yaak xelalkat yaak farbay alal yaak àttekat yaak ndawi buur yaak mboolem kilifay diiwaan ya, ñépp daje ngir berndey jëmm ja Buur Nebukatnecar samp; ñu daldi taxaw ca kanam jëmm ja.
4 Then the herald proclaimed loudly, "Peoples, nations, and languages—you are commanded: Yéenekat ba nag xaacu, ne: «Dégluleen li ñu leen sant, yeen waa mbooloo yépp ak xeet yépp ak làkk yépp!
5 When you hear the horn, flute, lyre, harp, zither, bagpipe, and all music, fall down and worship the gold image King Nebuchadnezzar set up. Bu ngeen di dégg bufta gi ak toxoro gi ak xalam gi ak riiti gi ak kooraa gi ak liit gi ak mboolem jumtukaayu xumbal yi, nangeen sujjóot, màggale ko jëmmu wurus wi Buur Nebukatnecar samp.
6 Anyone who doesn't fall down and worship will immediately be thrown into a blazing fiery furnace." Képp ku sujjóotul màggal ko, dees koy daldi sànni ci biir taal bu yànj.»
7 As soon as all peoples heard the horn, flute, lyre, harp, zither, and every kind of music, all peoples, nations, and languages fell down and worshiped the golden image King Nebuchadnezzar had set up. Loolu nag waral saa yu nit ña déggee bufta gaak toxoro gaak xalam gaak riiti gaak kooraa gaak mboolem jumtukaayu xumbal ya, ñoom ñépp ay bokk sujjóot, màggal jëmmu wurus ja Buur Nebukatnecar samp, muy mbooloo yaak xeet yaak làkk ya.
8 At that time certain astrologers came forward and maliciously accused the Jews. Ci biir loolu ay xërëmkat dikk, di boole Yawut ya.
9 They said to King Nebuchadnezzar, "King, may you live forever! Ñu wax Buur Nebukatnecar, ne ko: «Buur, guddaluw fan.
10 You, king, decreed: whoever hears the horn, flute, lyre, harp, zither, bagpipe, and any music must fall down and worship the gold image, Buur sang bi, xam nga yaa joxe ndigal ne: “Képp ku dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayu xumbal, dangaa wara sujjóot, màggal jëmmi wurus ji.
11 and whoever does not fall down and worship will be thrown into a blazing fiery furnace. Te képp ku sujjóotul màggal ko, dees na ko sànni ci biir taal bu yànj.”
12 Some Jews you put in charge of Babylon province—Shadrach, Meshach, and Abednego—disregard you, king. They won't serve your gods or worship the gold statue you set up." Dafa am ay Yawut yoo tabb, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Ñu di leen wax Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego. Ñooñu de Buur, déggaluñu la. Say yàlla, jaamuwuñu leen; sa jëmmu wurus ji nga samp it, màggaluñu ko.»
13 Furious, Nebuchadnezzar ordered Shadrach, Meshach, and Abednego brought; they were brought before the king. Nebukatnecar daldi mer lool, ba fees dell. Mu woolu Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego; ñu indi leen ba fa kanam Buur.
14 Nebuchadnezzar said, "Shadrach, Meshach, Abednego, is it true you don't serve my gods or worship the gold statue I set up? Nebukatnecar àddu ne leen: «Ndax dëgg la, yeen Sadarag, Mesag ak Abedd Nego, yeena baña jaamu samay yàlla, baña màggal jëmmu wurus ji ma samp?
15 Now if you're ready—when horn, flute, lyre, harp, zither, bagpipe, and every kind of music sound, fall down and worship the image I made—good. But if you don't worship, you'll be thrown at once into a blazing fiery furnace. What god can rescue you from my hands?" Léegi, bettuma leen. Bu ngeen di dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayi xumbal yi rekk, sujjóotleen, màggale ko jëmm ji ma sàkk. Waaye su ngeen ko màggalul, dees na leen daldi sànni ci biir taalu sawara bu yànj. Ana yàlla ju leen di musal ci man?»
16 Shadrach, Meshach, and Abednego answered the king, "Nebuchadnezzar, we don't need to answer you about this. Sadarag, Mesag ak Abedd Nego ne Buur Nebukatnecar: «Buur, soxlawul ñu di la lay dara.
17 If our Father, whom we serve, can rescue us, he will rescue us from the blazing furnace and from your hand, king. Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.
18 But if not, know this, king: we won't serve your gods or worship the gold statue you set up." Su demewul noonu it nag Buur, xamal ne say yàlla dunu leen jaamu; sa jëmmu wurus ji nga samp it, dunu ko sujjóotal.»
19 Then Nebuchadnezzar, furious, his expression changed toward Shadrach, Meshach, and Abednego; he ordered the furnace heated seven times hotter than normal. Ci kaw loolu Nebukatnecar mer lool ba fees dell, kanam gay sël-sëli janook Sadarag, Mesag ak Abedd Nego. Mu santaane ñu xamb taal ba, ba mu gëna tàng juróom ñaari yoon na mu daan tànge;
20 He ordered some of his strongest soldiers to bind Shadrach, Meshach, and Abednego and throw them into the blazing furnace. ba noppi mu sant ay dag yu am kàttan ci mbooloom xareem, ngir ñu yeew Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego, sànni leen ca biir taal bu yànj ba.
21 So these men, tied up in cloaks, trousers, turbans, and other garments, were thrown into the blazing fiery furnace. Ñooñu yeew leen na ñu soloo, ñook seeni mbubb ak seeni tubéy ak seeni mbaxana, daldi leen sànni ca biir taal bu yànj ba.
22 Because of the king's harsh order and furnace's extreme heat, the fire's flame killed the men who lifted up Shadrach, Meshach, and Abednego. Ndigalu Buur nag jamp a jamp, sawara wa boy a boy, ba tàkk-tàkku sawara wa rey dag ya ca sànni Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego.
23 These three men—Shadrach, Meshach, and Abednego—fell bound into the blazing furnace. Sadarag, Mesag ak Abedd Nego, ñoom ñett ñépp yeewe ba ne ŋodd, tàbbi ca biir taalu sawara bu yànj ba.
24 Then King Nebuchadnezzar, astonished, rose in haste. He asked his advisers, "Didn't we throw three bound men into the fire?" They answered the king, "True, king." Ci kaw loolu Buur Nebukatnecar jommi, ne bërét taxaw, daldi laaj ay dagam ne leen: «Xanaa du ñett lañu yeew, sànni ci sawara wi?» Ñu ne ko: «Ahakay, Buur!»
25 He said, "Look—I see four men, unbound, walking in the middle of the fire, unharmed; the fourth looks like a son of the gods." Mu ne: «Xoolleen, ñeent ñu yeewewul laa gis, ñuy daagu ci biir sawara wi te dara dalu leen. Ñeenteel baa ngi mel ni jëmm ju nirook Yàlla.»
26 Nebuchadnezzar went to the blazing furnace's door and said, "Shadrach, Meshach, and Abednego, servants of the Most High God, come out here!" Shadrach, Meshach, and Abednego came out of the fire. Nebukatnecar nag jegeñsi ci buntu taal bu yànj ba, daldi àddu ca kaw ne: «Éey Sadarag, Mesag, Abedd Nego, jaami Yàlla jiy Aji Kawe ji, génnleen fii!» Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego daldi génne ca biir sawara sa.
27 The satraps, prefects, governors, and king's counselors gathered and saw fire had no power over these men's bodies—hair not singed, robes unharmed, no smell of fire on them. Ba loolu amee jawriñ yaak laman yaak jaraaf yaak dagi Buur yéew leen. Ñu gis nag ne sawara wi lakkul seen yaram fenn, seen kawaru bopp xoyomuwul, seeni yére yàquwul, xeeñuñu sax xetu sawara.
28 Nebuchadnezzar said, "Blessed be the God of Shadrach, Meshach, and Abednego! He sent his angel and rescued his trusting servants. They defied the king's command and were willing to die rather than serve or worship any god but their own God. Nebukatnecar wax ne: «Cant ñeel na Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego, moom mi yónni malaakaam, mu wallu jaamam ñi ko wóolu, ba xëtt sama ndigal man Buur, te jaay seen bakkan gënal leen ñuy jaamu mbaa di sujjóotal jeneen yàlla ju dul seen Yàlla.
29 I decree: any people, nation, or language that speaks anything against the God of Shadrach, Meshach, and Abednego will be cut to pieces, their houses turned to rubble—since no other god can rescue like this." Dogal tukkee na ci man ne: muy mépp mbooloo ak bépp xeet ak wépp làkk, képp ku ci ñàkke kersa Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego, ay dog lees koy dog, te këram dees na ko def ab sën, ndax kat amul jenn yàlla ju mana walloo ni moom.»
30 Then the king promoted Shadrach, Meshach, and Abednego in the province of Babylon. Ba loolu wéyee Buur gëna teral Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego ca diiwaanu Babilon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]