Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
3:31 King Nebuchadnezzar, to all peoples, nations, and languages living throughout the earth: May your peace be multiplied. Bataaxalu Buur Nebukatnecar a ngii, jëm ci mépp mbooloo ak wépp xeet ak wépp làkk, ak fu ñu dëkke ci àddina sépp: Yal na seen jàmm yokku.
3:32 I am glad to declare the signs and wonders the Most High God has done for me. Màndarga yeek kéemaan yi ma Yàlla Aji Kawe ji defal, maa ngi am bànneex ci xamle ko.
3:33 How great are his signs, and how mighty are his wonders! His kingdom is an everlasting kingdom, and his dominion is from generation to generation. Ndaw màndargaam yu màgg, ndaw kéemaanam yu réy! Nguuram ay nguur gu sax dàkk, kilifteefam ñeel maasoo maas.
1 I, Nebuchadnezzar, was at ease in my house and flourishing in my palace. Man Nebukatnecar maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.
2 I saw a dream that frightened me; thoughts on my bed and visions in my head terrified me. Ma tëdd sama lal, daldi am gént gu ma tiital, ak xalaat ak peeñu yu ma indil njàqare.
3 So I ordered all Babylon's wise men brought before me to tell me the dream's meaning. Ma joxe ndigal, woolu boroom xam-xami Babilon yépp, ngir ñu xamal ma pirim gént gi.
4 Then the magicians, enchanters, Babylonians, and astrologers entered. I told them the dream, but they could not interpret it for me. Ci kaw loolu taryaax yeek ñeengokat yeek xërëmkat yeek seetkat yi dikk. Ma nettali leen gént gi, waaye waxuñu ma piri mi.
5 Finally Daniel came before me—named Belteshazzar after my god's name, the holy gods' spirit in him—and I told him the dream. Ñu mujj ma indil Dañeel, di Beltacar mi ñu tudde sama yàlla, di ku xelu yàlla yu sell yi nekk ci moom. Ma wax ko gént gi.
6 Belteshazzar, chief magician, I know the spirit of the holy gods is in you, and no mystery baffles you—tell me the visions of my dream that I saw, and their meaning. Ma ne ko: «Beltacar, kilifay taryaax yi, man ci sama bopp xam naa ne xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw, te menn mbóot jaaxalu la. Peeñum gént gi ma gént, wax ma piri mi.
7 The visions in my mind while in bed: I saw a tree in the middle of the earth, very tall. Li ma gis daal ci sama kaw lal mooy lii: Damaa jekki gis garab ci digg àddina si, mu gudd lool.
8 The tree grew and became strong, and its top reached to heaven, and it was visible to the ends of the whole earth. Garab gay màgg, di réy, ba njobbaxtal la di laal asamaan, ñu di ko séen ba ca cati àddina sépp.
9 Its leaves were beautiful and its fruit abundant, and in it was food for all. Wild animals found shade under it, and the birds of the heavens lived in its branches, and all flesh was fed from it. Xob yaa nga naat, meññeef ma ne gàññ, mana dundal ñépp. Muy keppaaral rabu àll, di tàggal njanaaw, di dundal bépp boroom bakkan.
10 In my visions in bed I saw a watcher, a holy one, coming down from heaven. «Fi ma tëdd ci sama lal, ma jekki gis ab wattukat bu sell wàcce asamaan.
11 He shouted: Cut down the tree, chop its branches, strip its leaves, scatter its fruit. Let animals flee from under it, birds from its branches. Mu àddu ca kaw ne: “Daaneleen garab gi te gor ay bànqaasam. Wittleen xob yi, tasaare meññeef mi. Na rab yi jóge ci keppaaram, daw, njanaaw yi ciy bànqaasam, naaw.
12 But leave the stump of its roots in the earth, bound with a band of iron and bronze, in the grass of the field. Let him be drenched with the dew of heaven, and let his portion be with the wild animals in the grass of the earth. Waaye ëkk beek reen yi, bàyyileen ko fi suuf ci digg mbooy mi, te jénge ko càllalay weñ ak xànjar. Na ko layub asamaan di faam, muy dunde ñax nig jur.
13 Let his human mind be taken away and a beast's mind be given to him, and let seven periods of time pass over him. Mu nitoodi, ame xelum mala diiru juróom ñaari jamono.
14 The sentence is by the decree of the watchers, the decision by the word of the holy ones, so that the living may know that the Most High rules over the kingdom of men and gives it to whom he will and sets over it the lowliest of men.' Ndogal a ngoog bu wattukat yi tëral, àttee ngoog bu ñu sell ñooñu digle, ngir aji dund ji xam ne Aji Kawe jee yilif nguurug nit, di ko jox ki ko soob, di ca fal ki gëna tuut.”
15 This is the dream I, King Nebuchadnezzar, saw. Tell me its meaning, Belteshazzar, for my kingdom's wise men can't explain it, but you can—the spirit of the holy gods is in you. «Loolu laa gént, man, Nebukatnecar. Yaw Beltacar nag, wax ma piri mi. Ndax boroom xam-xam yi ci sama réew mi, kenn manu ma cee wax piri mi. Waaye yaw man nga ko, ngir xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw.»
16 Then Daniel, called Belteshazzar, was stunned briefly, alarmed by his thoughts. The king said, "Belteshazzar, don't let the dream or its meaning alarm you." Belteshazzar answered, "My lord, may the dream be for your haters, its meaning for your enemies!" Ba loolu amee Dañeel ma ñuy wax Beltacar ne dann ab diir, jaaxle, xalaat yu ko tiital dikkal ko. Buur àddu ne ko: «Beltacar, gént geek piri mi bumu la tiital.» Beltacar ne ko: «Sang bi, su ma sañoon de muy sa géntug noon te pireem topp say bañaale.
17 The tree you saw grew strong, its top reaching heaven, visible to all the earth, Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,
18 beautiful leaves, abundant fruit, food for all—wild animals lived beneath it, birds of the sky nested in its branches. mook xobam yu naat ak meññeefam mu ne gàññ, mana dundal ñépp; muy keppaaral rabu àll, di tàggal njanaaw:
19 It is you, king—you have grown and become strong; your greatness has grown, reaching heaven, your dominion to the ends of the earth. Buur de, garab googu yaw la. Yaa màgg, di bare doole; di màgg ba laal asamaan, sa kilifteef àkki cati àddina.
20 Because the king saw a watcher, a holy one, come down from heaven, saying: Cut down the tree, destroy it—but leave the stump of its roots in the ground, bound with a band of iron and bronze in the field's grass. Let him be drenched with the dew of heaven; his portion with the wild animals, until seven periods of time pass over him. «Buur, li nga gis mooy ne kenn ci wattukat yu sell yi wàcce asamaan, daa àddu ca kaw ne: “Daaneleen garab gi, tas ko, waaye ëkk beek reen yi, bàyyileen ko fi suuf ci digg mbooy mi, te jénge ko càllalay weñ ak xànjar. Na lay biy wàcc, di ko faam, muy dunde ñax nig jur diiru juróom ñaari jamono.”
21 This is the interpretation, my king: the Most High's decree has come upon my lord the king, Piri maa ngii, Buur, di dogalu Aji Kawe ji dal ci sa kaw, Buur, sang bi.
22 you'll be driven from people to live among wild animals, eating grass like oxen, drenched with the dew of heaven, until seven times pass over you and you know the Most High rules the human kingdom, giving it to whoever he chooses. Yaw lañuy dàqe ci nit ñi; rabi àll yi ngay dëkkal, ñax di sam xont niw nag, lay biy wàcc di la faam diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.
23 The command to leave the stump and its roots in the ground: your kingdom will be restored to you once you know Heaven rules. Li ñu santaane ñu bàyyi ëkk beek reeni garab gi mooy tekki ne nguur gi dees na la ko delloo keroog boo xamee ne Boroom asamaan mooy Buur.
24 So, king, accept my advice: break from your sins through righteousness, your wrongdoing through mercy to the poor, so your prosperity may continue. Kon nag Buur, ngalla nangul li ma lay digal: say moy ak say bàkkaar, daboo ko di def njekk ak di baaxe néew-ji-doole ndax sa teraanga sax.»
25 All this came upon King Nebuchadnezzar. Loolu lépp dal na Buur Nebukatnecar.
26 Twelve months later, he was walking on the roof of Babylon's royal palace. Ba ñu ca tegee fukki weer ak ñaar yu mat, muy doxantu ca kaw taaxum kër buur ca Babilon,
27 The king said, "Is this not great Babylon I built as a royal house by my mighty power, for the glory of my majesty?" ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»
28 The words were still in the king's mouth when a voice fell from heaven: "King Nebuchadnezzar, this is said to you: the kingdom has left you. Kàddug Buur ga daanoogul sax, baat jibe asamaan àddu ne: «Yaw Buur Nebukatnecar, dogal ñeel na la ne nguur gi rëcc na la.
29 You'll be driven from people, living with wild animals, eating grass like an ox. Seven periods will pass over you, until you know the Most High rules mankind's kingdom and gives it to whomever he wills." Dees na la dàqe ci nit ñi, nga dëkk ak rabi àll yi, ñax di sam xont niw nag diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.»
30 At once the word came true against Nebuchadnezzar: driven from people, he ate grass like cattle, his body soaked by the dew of heaven, until his hair grew like eagle feathers, his nails like bird claws. Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nebukatnecar. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.
31 When the days ended, I, Nebuchadnezzar, raised my eyes to heaven, and my reason returned. I blessed the Most High, praised and honored the One who lives forever, whose rule is everlasting, whose kingdom spans every generation. Ba àpp ba matee, man Nebukatnecar, maa séentu asamaan, sama sago délsi. Ma sant Aji Kawe ji, sargal Kiy dund ba fàww, màggal ko: kilifteefam sax fàww, nguuram ñeel maasoo maas.
32 All the inhabitants of the earth are counted as nothing, and he does according to his will among the host of heaven and among the inhabitants of the earth; and no one can hold back his hand or say to him, "What have you done?" Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»
33 Then my sanity returned; my majesty and splendor returned for my kingdom's glory. My advisers and nobles sought me; I was restored over my kingdom, and surpassing greatness was added to me. Ba sama sago délsee, ca laa jotaat ndam ak daraja ngir sama teraangay nguur. Ba loolu amee samay jawriñ ak samay jaraaf jëlsi ma; ñu dëjaat ma ci nguur gi, ma gënatee màgg.
34 Now I, Nebuchadnezzar, praise, exalt, and honor Heaven's King, for all his works are right, his ways just; those walking in pride he can humble. Léegi nag man, Nebukatnecar, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]