Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In the second year of his reign, Nebuchadnezzar had dreams; his spirit was troubled and his sleep left him. Ca ñaareelu atu nguuram ca la Nebukatnecar génte gént gu ub boppam lool, ba manatula nelaw.
2 So the king ordered the magicians, enchanters, sorcerers, and astrologers summoned to tell him his dreams. They came and stood before the king. Mu woolu jabarkat yi ak taryaax yi ak ñeengokat yi ak xërëmkat yi, ngir ñu firil koy géntam. Ñu agsi taxaw ca kanamam.
3 The king said to them, "I dreamed a dream, and my spirit is troubled to know the dream." Buur ne leen: «Damaa gént lu ub sama bopp, ma bëgga xam lu muy firi.»
4 Then the astrologers said to the king in Aramaic, "King, live forever! Tell your servants the dream, and we will reveal its interpretation." Xërëmkat ya ne Buur ci làkku arameen: «Guddaluw fan Buur, sang bi! Wax nu gént gi, nu firi ko.»
5 The king answered the astrologers, "My decree is firm: if you don't tell me the dream and its meaning, you'll be cut to pieces and your houses reduced to rubble. Buur wax xërëmkat ya ne leen: «Dogal bu wér a ngii tukkee fi man. Su ngeen ma waxul gént gi, wax ma piri mi, ay dog lañu leen di dog, seeni kër doon ay sën.
6 But if you tell the dream and its meaning, you'll receive gifts, rewards, and great honor from me. So tell me the dream and its meaning." Waaye su ngeen waxee gént gi, wax ma piri mi, ay weexal aki yool ak teraanga ju réy ngeen di jële ci man. Kon nag waxleen ma gént gi, wax ma piri mi.»
7 They answered a second time, "Let the king tell his servants the dream, and we will give its meaning." Gannaaw gi, ñu dellu ne Buur: «Sang bi, waxal gént gi, nu wax la pireem.»
8 The king replied, "I know for certain you're trying to buy time, because you see my decree is firm: Buur dellu ne: «Gis naa nag bu baax ne dangeena bëgga yàggal mbir mi, ndax xam ngeen ne dogal bu wér tukkee na ci man
9 If you don't tell me the dream, there is only one verdict for you. You have agreed to speak lying, corrupt words before me until the times change. So tell me the dream, then I'll know you can reveal its interpretation." ne su ngeen ma waxul gént gi, àtte bi di benn ci yeen ñépp. Gise ngeen ba nar maa wax ay fen aki caaxaan, di yaakaar jamono soppiku. Waxleen ma gént gi rekk, ma xam ne man ngeen maa wax pireem.»
10 The astrologers answered the king, "No one on earth can do what the king asks. No great, powerful king ever demanded such a thing of any magician, enchanter, or Chaldean. Xërëmkat ya ne Buur: «Buur, amul kenn ci kaw suuf ku mana wax li ngay laaj. Te it benn buur ak nu màggaayam ak dooleem mana tollu, masula laaj lu mel nii benn taryaax mbaa ñeengokat mbaa xërëmkat.
11 The king's request is too hard; only the gods, who don't live among mortals, can reveal it to the king." Li ngay laaj daa jafe, Buur. Kenn manu la koo wax ku moy yàlla yi, Buur, te ñoom dëkkuñu ci biir nit ñi.»
12 At this the king grew angry and furious, and ordered all Babylon's wise men destroyed. Ci kaw loolu Buur mer lool ba fees dell, daldi joxe ndigal ne ñu rey mboolem boroom xam-xami Babilon.
13 So the decree went out to kill the wise men, and they searched for Daniel and his companions to put them to death. Ba mu ko defee ñu siiwtaane dogal ba, nara reylu boroom xam-xam ya. Ñuy seet nag Dañeel aki àndandoom ngir rey leen.
14 Then Daniel answered Arioch, the king's guard commander, with wisdom and discretion; Arioch had gone out to kill Babylon's wise men. Dañeel defug teey, jiital xelam, wax ak Aryokk, kilifag dagi buur, fekk kooku di dem, nara reyi boroom xam-xami Babilon.
15 He asked Arioch, the king's officer, "Why such a harsh decree from the king?" Then Arioch explained it to Daniel. Mu laaj Aryokk ndawal Buur, ne ko: «Waaw, lu waral bii dogal bu diis tukkee ci Buur?» Aryokk xamal Dañeel mbir ma.
16 So Daniel went in and asked the king for time, so that he might reveal the interpretation to the king. Dañeel nag dem ca Buur, ñaan ko mu may ko jot gu mu ko joxe pirim gént ga.
17 Then Daniel went home and told his companions Hananiah, Mishael, and Azariah about the matter, Ba loolu amee Dañeel ñibbi, daldi xamal mbir ma Anaña ak Misayel ak Asaryaa, àndandoom ya,
18 urging them to plead for mercy from our Father in heaven about this mystery, so Daniel and his companions wouldn't be destroyed with Babylon's other wise men. ngir ñu sàkku yërmandey Yàlla Boroom asamaan ci wàllu mbóot moomu, ndax ñu bañ leena rey mook àndandoom yaak yeneen boroom xam-xami Babilon.
19 Then the mystery was revealed to Daniel in a night vision, and Daniel blessed our Father in heaven. Ca guddi ga nag, ñu won mbóot ma Dañeel ci biir peeñu. Ci kaw loolu Dañeel sant Yàlla Boroom asamaan,
20 Daniel said: "Blessed be the name of our Father forever and ever, for wisdom and might belong to him. daldi ne: «Cant gu amul ndoorte amul kemu ñeel na Yàlla, xam-xam ak kàttan mooy boroom.
21 He changes times and seasons; he removes kings and sets up kings; he gives wisdom to the wise and knowledge to those who have understanding. Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.
22 He reveals deep and hidden things; he knows what lies in darkness, and the light dwells with him. Mooy feeñal mbóot mu làqu, xam li ci biir lëndëm, te leer màkkaanoo ko.
23 To you, the God of my fathers, I give thanks and praise, for you have given me wisdom and might, and now you have made known to me what we asked of you; you have made known to us the king's matter." Sama Yàllay maam, maa lay gërëm, di la sant. Yaa ma may xam-xam ak manoore, xamal ma li nu la laaj. Yaa nu xamal mbirum Buur mii.»
24 So Daniel went to Arioch, whom the king had appointed to destroy Babylon's wise men, and said, "Don't destroy Babylon's wise men. Take me to the king, and I will give him the interpretation." Gannaaw loolu Dañeel dem ca Aryokk mi Buur santoon mu rey boroom xam-xami Babilon. Ba mu demee ne ko: «Boroom xam-xami Babilon yi, bu leen reylu. Yóbbu ma ca Buur, ma jox ko piri mi.»
25 Then Arioch quickly brought Daniel before the king and said, "Among the exiles of Judah I found a man who can tell the king the interpretation." Aryokk gaaw yóbbu Dañeel ba ca Buur, wax ko ne ko: «Gis naa ci ngàllog Yudeen ñi ku la mana firil sa gént gi.»
26 The king asked Daniel, called Belteshazzar, "Can you tell me the dream I saw and what it means?" Buur wax ak Dañeel mi ñu naan Beltacar, ne ko: «Ndax wóor na la ne man nga maa wax li ma gént, wax ma li muy firi?»
27 Daniel answered the king, "No wise men, enchanters, magicians, or astrologers can reveal the mystery the king asks about. Dañeel ne Buur: «Buur, li nga laaj amul benn boroom xam-xam mbaa ñeengokat mbaa taryaax walla seetkat bu la ko mana xamal.
28 But our Father in heaven reveals mysteries, and has made known to King Nebuchadnezzar what will happen in the latter days. Your dream and the visions in your mind as you lay on your bed were these: Waaye Yàllaa ngi ci asamaan, di xamle ay mbóot te moo won Buur Nebukatnecar liy am jamono yiy ñëw. Sa gént gaak la nga ca gis ca sa kaw lal, lii la:
29 "As you lay in bed, O king, your thoughts turned to what would come, and the revealer of mysteries showed you what is to be. «Buur, ba nga tëddee ca sab lal, sa xel daa dem ci liy xew bu jamono jii weesoo. Kiy feeñal mbóot daldi lay won liy xew.
30 But this mystery was revealed to me not because I have more wisdom than anyone else alive, but so the king may know its interpretation, and you may understand your heart's thoughts. Man nag du caageenu xam-xam bu ma ëpple mboolem kuy dund. Mbóot mii dañu ma koo won, ndax yaw Buur, nga xam piri mi, xam li ub sa bopp.
31 "You watched, O king, and saw a great statue. This statue, huge and dazzling in brightness, stood before you, and its appearance was terrifying. «Buur, danga jekki xool, daldi gis jëmm ju mag ju ñu defar. Jëmm ja réy na lool te yànjaayam yéeme. Ma nga taxaw janook yaw, melokaanam raglu.
32 The statue's head was fine gold, its chest and arms silver, its belly and thighs bronze, Boppu jëmm ji wurus la wu raxul, dënn beek loxo yi di xaalis, biir beek pooj yi di xànjar,
33 its legs of iron, its feet partly of iron and partly of clay. yeel yi di weñ gu ñuul, ndëggu yi nag lenn li weñ gu ñuul la, li ci des di ban bu ñu lakk.
34 While you watched, a stone cut without hands struck the statue's feet of iron and clay, crushing them. Naka ngay xool, aw doj wu loxo sànniwul fàq, daldi dal ca tànki jëmm ja bindoo weñ ak ban bu ñu lakk, daldi koy rajaxe.
35 Then the iron, clay, bronze, silver, and gold were all broken to pieces together, becoming like chaff on a summer threshing floor. The wind carried them off, leaving no trace. But the stone that struck the statue became a great mountain filling the whole earth. Ci kaw loolu weñ gaak ban baak xànjar jaak xaalis baak wurus wa lépp bokk rajaxoo, mel ni xataxu dàggay lolli. Ngelaw li buub ko yóbbu, ba mu ne mes. Doj wa daloon ca jëmm ja nag doon tund wu mag, fees àddina sépp.
36 "This was the dream. Now we will tell the king its interpretation. «Loolooy gént gi. Nu wax la piri mi nag, Buur.
37 You, king, are the king of kings, to whom our Father in heaven has given kingdom, power, might, and glory. Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,
38 Into your hand he has placed all people, the beasts of the field, and the birds of the sky, wherever they live, making you ruler over them all. You are the head of gold. te Yàlla teg ci say loxo doom aadama yeek rabi àll yeek njanaaw yi, nga boole leen yilif ñoom ñépp ak fu ñu mana dëkke: yaw yaay boppu wurus bi.
39 "After you another kingdom will arise, inferior to yours; then a third kingdom, of bronze, ruling over all the earth. «Sa gannaaw geneen nguur dina taxaw, gën laa suufe, ñetteelu nguur ga topp ca di xànjar, tiim àddina sépp.
40 A fourth kingdom will be strong as iron—iron breaks and shatters everything—and as iron crushes all these, it will break and crush them. Ñeenteelu nguur ga day dëgër ni weñ. Ni weñ di toje lépp ba rajaxe lépp ba mu rajaxoo, noonu lay toje ba rajaxe yooyu nguur yépp. Mu mel ni ni weñ gu ñuul di rajaxee lépp.
41 As you saw the feet and toes—part potter's clay, part iron—it will be a divided kingdom; yet it will have some of iron's strength, just as you saw iron mixed with soft clay. Soo gisee tànk yeek baaraami tànk yi, lenn li di ban, lenn li di weñ, nguur la guy xàjjalikoo. Lenn li dëgër dëgëraayu weñ ndax weñ gi nga gis, mu jaxasook ban bi.
42 As the toes were partly iron and partly clay, so the kingdom will be partly strong and partly brittle. Te baaraami tànk yi lenn li di weñ, lenn li di ban, ni la nguur ga di ame doole cig wet, néew doole cig wet.
43 As you saw iron mixed with soft clay, the people will mix in marriage but not hold together, just as iron does not mix with clay. Li nga gis weñ gu jaxasook ban mooy tekki ne buur yi dinañu booloo ci seeni pexe, waaye seen bennoo du mujj; dafa mel ni weñ rekk, du jaxasook ban.
44 "In those kings' days our Father in heaven will set up a kingdom never to be destroyed, nor its rule left to another people. It will crush all these kingdoms and end them, and it will stand forever. «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
45 This is what the vision meant: the stone cut from a mountain, not by human hands, broke the iron, bronze, clay, silver, and gold to pieces. Our great Father has shown the king what will happen after this. The dream is certain, its interpretation trustworthy." Moo waral nga gis doj wu loxo sànniwul, mu fàqe tund wa, daldi rajaxe weñ gaak xànjar jaak ban baak xaalis baak wurus wa. Buur, Yàlla ju màgg ji moo la xamal liy ñëw. Gént gi wér na, piri mi mata gëm.»
46 Then King Nebuchadnezzar fell facedown, bowed to Daniel, and ordered offering and incense given to him. Ci kaw loolu Buur Nebukatnecar ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóotal Dañeel, joxe nag ndigal ñu jox ko ay weexal ak cuuraay.
47 The king told Daniel, "Truly your God is God of gods, Lord of kings, and revealer of secrets, since you could reveal it." Ba loolu amee Buur wax Dañeel, ne ko: «Aylayéwén, sa Yàlla mooy Yàllay yàlla yi, di Sangu buur yi, te it mooy kiy feeñal mbóot, gannaaw feeñal nga mii mbóot.»
48 Then the king promoted Daniel to high honor, gave him many great gifts, and made him ruler of Babylon's whole province and chief prefect over all its wise men. Ba mu ko defee Buur teral Dañeel, may ko lu baree bare, ba noppi def ko kilifag diiwaanu Babilon gépp, teg ci fal ko, mu yilif boroom xam-xami Babilon yépp.
49 Daniel asked the king, who put Shadrach, Meshach, and Abednego over Babylon province's affairs; Daniel remained at the king's court. Ci biir loolu Dañeel ñaan Buur mu tabb Sadarag ak Mesag ak Abedd Nego, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Dañeel moom nekk ca ëttu buur.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]