Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In Jehoiakim king of Judah's third year, Nebuchadnezzar king of Babylon marched on Jerusalem and besieged it. Ca ñetteelu atu nguurug Yoyakim buurub Yuda, Nebukatnecar buuru Babilon daa dikk, gaw Yerusalem.
2 The Sovereign Father handed Jehoiakim king of Judah over to him, with some items from our Father's house; he took them to Shinar, to his god's house, and the items into his god's treasury. Boroom bi nag teg Yoyakim buurub Yuda ciy loxoom, boole ca lenni jumtukaayi kër Yàlla ga. Nebukatnecar yóbbu jumtukaay ya réewum Sineyaar ga ñuy wax Babilon itam, ca biir kërug tuuram. Mu daldi fat jumtukaay ya ca denci kër tuuram.
3 The king ordered Ashpenaz, his chief official, to bring some Israelites from the royal family and nobility. Ba loolu amee Buur jox ndigal Aspenas, kilifay bëkk-néegam, ngir mu tànne ci bànni Israayil ñenn ci askanu buur ak ci garmi yi.
4 Young men without defect, good-looking, skilled in all wisdom, well-informed, quick to understand, fit to stand in the king's palace—and to teach them Babylonian writing and language. Ñu diy waxambaane yu amul benn sikk ci seen yaram, di ñu góorayiw, mane bépp xeetu njàng, bare xam-xam te am déggin, ba mana liggéeyal Buur ci biir këram. Ñu di leen jàngal làkku waa Babilon ak seen mbind.
5 The king assigned them a daily portion of his food and wine, three years' training, then service before him. Ci biir loolu Buur dogalal leen bés bu nekk ab cér ci njëlam ak ci biiñam. Mu santaane ñu tàggat leen diiru ñetti at, ñu doora tàbbi ci liggéeyu buur.
6 Among them were Daniel, Hananiah, Mishael, and Azariah, from the sons of Judah. Yudeen ña ca bokkoon di Dañeel ak Anaña ak Misayel ak Asaryaa.
7 The chief official renamed them: Daniel, Belteshazzar; Hananiah, Shadrach; Mishael, Meshach; Azariah, Abednego. Kilifag jawriñ ya nag tudde leen yeneen tur. Dañeel, mu tudde ko Beltacar, Anaña mu tudde ko Sadarag, Misayel tudd Mesag, Asaryaa di Abedd Nego.
8 Daniel resolved not to make himself unclean with the king's food or wine, so he asked the chief official's permission not to make himself unclean. Ci biir loolu Dañeel fas yéene ci xolam ne du sobeel boppam ci njëlu buur ak biiñam. Mu ñaan kilifag jawriñ ya mu may ko, mu bañ cee sobeel boppam.
9 Now our Father gave Daniel favor and compassion in the eyes of the chief official. Yàlla def kilifag jawriñ ya baaxe Dañeel, yërëm ko.
10 The chief official told Daniel, "I fear my lord the king, who set your food and drink. Why should he see your faces worse than boys your age? You'd forfeit my head to the king." Teewul kilifag jawriñ ya ne Dañeel: «Man de damaa ragal Buur sama boroom, moom mi leen dogalal seen lekk ak seen naan. Su Buur gisee ngeen gëna yooy seen moroomi xale yu góor yi nag? Sama bakkan xaj na ci de!»
11 Then Daniel said to the steward the chief official had appointed over Daniel, Hananiah, Mishael, and Azariah, Ba mu ko defee Dañeel wax ak dag ba kilifay jawriñ ya sant mu wattu leen, mook Anaña ak Misayel ak Asaryaa. Mu ne ko:
12 "Please test your servants for ten days. Give us only vegetables to eat and water to drink. «Ngalla sang bi, seetlu nu diiru fukki fan, ñu di nu jox lujum rekk ak ndoxum naan;
13 Then compare our appearance with the youths eating the king's food; do with your servants as you see." te nga xool nu, xool xale yu góor yiy lekk ci njëlal Buur. Su ko defee nga seet nooy def ak nun ci ni nga nu gise, sang bi.»
14 So he agreed to this and tested them for ten days. Waa ja ànd ak ñoom ci loolu, seetlu leen diiru fukki fan.
15 After ten days they looked healthier and better fed than all the young men eating the royal food. Ba fukki fan ya matee, seen kanam gëna leer te ñu gëna suur mboolem xale yu góor yay lekk ca njëlal Buur.
16 So the steward took away their assigned food and the wine they were to drink, and gave them vegetables instead. Ci kaw loolu wattukat ba di yóbbu seen njël ak seen biiñ, weccee leen ko lujum.
17 To these four boys our Father gave knowledge and insight in all writing and wisdom; Daniel understood all visions and dreams. Yàlla nag may ñeenti xale yu góor yooyu xel ak ràññee ci mboolem lu ñu bind ak wàllu xam-xam. Dañeel moom mana firi mboolem peeñu ak gént.
18 When the king's set days for bringing them in ended, the chief official brought them before Nebuchadnezzar. Ba diir ba leen Buur àppal matee, ñu war leena indi, kilifag jawriñ ya yóbbu leen fa kanam Buur Nebukatnecar.
19 The king spoke with them, and none matched Daniel, Hananiah, Mishael, and Azariah; so they served the king. Buur wax ak ñoom te gisul ci ñoom ñépp kenn ku mel ni Dañeel ak Anaña ak Misayel ak Asaryaa. Ñu daldi tàbbi ci liggéeyu buur.
20 Whenever the king questioned them on wisdom and understanding, he found them ten times better than all magicians and enchanters in his whole kingdom. Mboolem wàllu xam-xam ak xel mu leen Buur seetlu rekk, gis ne ñoo ci sut fukki yoon jabarkat yeek ñeengokati réewam mépp.
21 And Daniel remained there until the first year of King Cyrus. Dañeel nekk ca liggéeyu buur, nekk ca ba ca at ma njëkk ca nguurug Buur Sirus.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]