Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 While Peter and John were speaking to the people, the priests, the temple captain, and the Sadducees came up to them, Naka la Piyeer ak Yowaan di wax ak mbooloo ma, sarxalkat yaak jawriñu kër Yàlla gaak Sadusen ya ne jimeet ci seen kaw.
2 greatly annoyed because they were teaching the people and proclaiming the resurrection from the dead in Jesus. Fekk na leen ñéññ ca la ñuy waare aka yégle ndekkitel Yeesu, te loolu di dëggal ne dee-dekki, lu am la.
3 They arrested them and put them in custody until the next day, since it was already evening. Ñu daldi leen teg loxo, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndax booba guddi na.
4 But many who heard the message believed, and the men's number reached about 5,000. Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000).
5 The next day their rulers, elders, and teachers of the law gathered together in Jerusalem, Ca ëllëg sa kilifay Yawut yi ak magi askan wi ak firikati yoonu Musaa yi daje Yerusalem.
6 with Annas the high priest, Caiaphas, John, Alexander, and all who were of the high-priestly family. Anas, sarxalkat bu mag ba ca la, ak Kayif ak Yowaan ak Alegsàndar ak mboolem bokki sarxalkat bu mag.
7 They stood them in the middle and asked, "By what power or by what name did you do this?" Ñu taxawal Piyeer ak Yowaan ca digg ba, laaj leen ne: «Yeen, lii ngeen def, ci ban xam-xam ak ci wan tur ngeen ko defe?»
8 Then Peter, filled with the Holy Spirit, said to them, "Rulers of the people and elders, Fa la Piyeer feeseek Noo gu Sell gi, ne leen: «Yeen kilifay xeet wi ak magi askan wi,
9 if we're questioned today about a good deed to a sick man, how he was healed. ndegam yoon moo nuy laaj lu jëm ci ndimbal lu ab lafañ jagoo, ak ci man pexe la lafañ bi mucce,
10 Know this, all of you and all Israel's people: by the name of Jesus Christ of Nazareth, whom you crucified, whom our Father raised from the dead—by him this man stands before you well. xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israayil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi mu Nasaret, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
11 This Jesus is "the stone you builders rejected, which has become the cornerstone." Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi, te mu mujj di doju koñu tabax bi.”
12 Salvation is in no one else; no other name under heaven is given among people by which we must be saved." Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
13 Seeing Peter and John's boldness, and realizing they were uneducated, ordinary men, they were amazed and recognized they had been with Jesus. Ba waa kuréelu àttekat ya gisee fit wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
14 Seeing the healed man standing with them, they had nothing to say against it. Te itam ka ñu wéral a nga taxaw fa seen wet, ñuy gis. Manuñu caa tegati dara.
15 So they ordered them to leave the council, and then they conferred among themselves, Ba mu ko defee ñu joxe ndigal, génne leen, daldi gise ci seen biir.
16 saying, "What should we do with these men? A notable sign has happened through them, plain to all who live in Jerusalem, and we cannot deny it. Ñu ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndax kat firnde lu leer sottee na fi ci ñoom; leer na nàññ waa Yerusalem gépp, te manunu koo weddi.
17 But to stop this from spreading further among the people, let's warn them to speak to no one in this name again." Waaye kat bu mbir mi gëna siiw ci xeet wi. Nan leen tëkku, ngir aaye leen ñu waxati kenn tur woowu.»
18 They called them and ordered them not to speak or teach at all in Jesus' name. Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu.
19 Peter and John answered them, "You judge whether it's right before our Father to listen to you rather than to him. Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu.
20 For we cannot help speaking about what we have seen and heard." Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»
21 After more threats, they released them, finding no way to punish them because of the people, since all were glorifying our Father for what happened. Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,
22 For the man who had received this sign of healing was over forty years old. ngir waa ja kéemtaan ga wérloo amoon na lu wees ñeent fukki at.
23 Once released, they went to their own people and reported all the chief priests and elders had said to them. Gannaaw ba ñu yiwee Piyeer ak Yowaan, ñu dem ca seen bokki gëmkat, nettali leen mboolem la leen sarxalkat yu mag yaak magi askan wa wax.
24 Hearing this, they raised their voices together to our Father and said, "Sovereign Father, you made heaven, earth, sea, and everything in them. Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.
25 You spoke by the Holy Spirit through the mouth of our father David, your servant: "Why did the nations rage and the peoples plot in vain?" Yaa wax ci Noo gu Sell gi ci sunu gémmiñu maam Daawuda sa jaam bi, nga ne: “Ana lu xeeti àddina di riire? Lu xeet yiy lale pexey neen?
26 The kings of the earth took their stand, and the rulers gathered together against our Father and against his Anointed." Buuri àddinaa jógandoo, kilifa yee lëkkoo, di fexeel Boroom bi ak Almaseem.”
27 For truly, in this city, Herod and Pontius Pilate gathered with the Gentiles and peoples of Israel against your holy servant Jesus, whom you anointed, Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israayil ci kaw Yeesu, sa jawriñ ju sell ji nga fal.
28 to do whatever your hand and your plan had decided beforehand should happen. Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogaloon ci sa loxo ak sa coobare.
29 Now, Father, see their threats, and let your servants speak your word with all boldness, Léegi nag Boroom bi, bàyyil xel seeni tëkkoo te nga may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit wu mat sëkk.
30 as you reach out your hand to heal, and signs and wonders occur through the name of your holy servant Jesus. Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral aka amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa jawriñ ju sell ji.»
31 After they prayed, the place they were gathered in shook; all were filled with the Holy Spirit and spoke the word of our Father boldly. Ba ñu ñaanee ba noppi, béreb ba ñu daje daa yëngu, ñu fees ak Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
32 All the believers were one in heart and soul; no one called any possession their own, but held everything in common. Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir.
33 With great power the apostles testified to the Lord Jesus's resurrection, and great grace rested on them all. Ndaw yi nag di seedee doole ju réy ne Sang bi Yeesu dekki na, yiw wu yaa di leen dikkal ñoom ñépp.
34 No one among them was needy: all who owned land or houses sold them and brought the price of what was sold, Kenn ci ñoom ndóolul, ndax képp ku ciy boroom suuf mbaa ay kër, da koy jaay, indi njëg gi,
35 and laid it at the apostles' feet, and it was distributed to each according to their need. teg ko ci kanam ndaw yi. Su ko defee ku nekk séddu ca la dëppook soxlaam.
36 Joseph, a Levite from Cyprus, whom the apostles called Barnabas (which means Son of Encouragement), Ku mel ni Yuusufa, bokk ci giirug Lewi, te dëkk ca dunu Sippar, ndaw yi daan ko wax Barnabas, muy firi Ñaaxekat bi,
37 sold a field he owned, brought the money, and laid it at the apostles' feet. ab tool la amoon. Da koo jaay, indi xaalis bi, teg fi kanam ndaw yi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]