Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Peter and John were going up to the temple at around three in the afternoon, the hour of prayer. Piyeer ak Yowaan ñoo doon duggsi ca kër Yàlla ga, ngir ñaanu digg njolloor.
2 A man lame from birth was carried and placed daily at the temple gate called Beautiful, to beg from those entering the temple. Fekk ñu indi fa waa ju judduwaale lafañ, ñu daan ko teg bés bu nekk ca bunt ba ñuy woowe bunt bu Rafet ca kër Yàlla ga, ngir muy yalwaan ñay duggsi.
3 Seeing Peter and John about to go into the temple, he asked them for money. Waa ja gis Piyeer ak Yowaan, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu di leen yalwaan.
4 And Peter, gazing at him with John, said, "Look at us." Ci kaw loolu Piyeer ne ko jàkk, mook Yowaan, ne ko: «Xool nu.»
5 And he fixed his attention on them, expecting to receive something from them. Lafañ bi teewlu leen, di séentu ci ñoom ab sarax.
6 Peter said, "I own no silver or gold, but I give you what I have: in the name of Jesus Christ of Nazareth, rise and walk." Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi mu Nasaret, doxal!»
7 Taking his right hand, he raised him up; instantly his feet and ankles grew strong. Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam aki kostanam dëgër.
8 Jumping up, he stood, began walking, and entered the temple with them, walking, jumping, and praising our Father. Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox aka tëbantu, tey sant Yàlla.
9 And all the people saw him walking and praising our Father. Mbooloo mépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
10 They recognized him as the beggar who sat at the temple's Beautiful Gate, and were filled with wonder and amazement at what had happened to him. Ñu xàmmee ko, xam ne moo daan toog, di yalwaan ca bunt bu Rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu jommi ba jommaaral, ba far gëlëm ca la ko dikkal.
11 As he held on to Peter and John, all the people ran to them at the portico called Solomon's, utterly astonished. Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan.
12 Seeing this, Peter said to the people, "Israelites, why does this amaze you? Why stare at us, as if by our own power or godliness we made him walk? Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israayil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug ragal Yàlla lanu doxloo kii?
13 The God of Abraham, Isaac, and Jacob, the God of our fathers, glorified his servant Jesus, whom you handed over and denied before Pilate, when Pilate decided to release him. Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
14 But you denied the Holy and Righteous One, asking that a murderer be given to you. Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat.
15 You killed the Author of life; our Father raised him from the dead. To this we are witnesses. Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko.
16 His name, through faith in his name, has made this man strong—the very man you see and know. And faith in Jesus has given him this complete health right before your eyes. Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
17 "And now, brothers, I know that you acted in ignorance, as did also your rulers. «Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa.
18 But our Father fulfilled what he predicted through all the prophets: his Christ would suffer. Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottali, ne Almaseem dina sonn.
19 Repent, then, and turn back, so your sins are wiped out, Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.
20 that times of refreshing may come from our Father's presence, and that he may send the Christ appointed for you, Jesus, Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi bi mu leen jagleel, te muy Yeesu.
21 whom heaven must receive until all things are restored, about which our Father spoke through his holy prophets long ago. Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottali.
22 Moses said, 'Your Father will raise up a prophet like me for you, from your brothers. Listen to him in everything he tells you.' Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy feeñal ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
23 Anyone who does not listen to that prophet will be utterly destroyed from among the people.' Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la dagge ci xeet wi, sànk la.”
24 All the prophets who spoke, from Samuel onward, also announced these days. «Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund.
25 You are the sons of the prophets and of the covenant our Father made with your fathers, telling Abraham, 'By your offspring all the families of the earth will be blessed.' Yeen nag yeenay ndonoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeele.”
26 Our Father raised up his servant and sent him to you first, to bless you by turning each of you from your evil." Yeen la Yàlla njëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññi kenn ku nekk ci yeen mu moy jikkoom yu bon.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]