Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 When the day of Pentecost arrived, they were all together in one place. Ba bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp a bokk daje benn béreb.
2 Suddenly a sound like a violent, rushing wind came from heaven and filled the entire house where they sat. Ca saa sa coow jollee ca asamaan, mel ni riirum ngelaw lu bare doole, daldi fees dell biir kër ga ñu toog.
3 What looked like divided tongues of fire appeared and rested on each one of them. Ci kaw loolu ay làmmiñ yu mel ni tàkk-tàkki sawara feeñu leen, làmmiñ ya séddalikoo, daldi toŋ ci kaw kenn ku nekk.
4 All were filled with the Holy Spirit and began speaking in other tongues, as the Spirit gave them words to say. Ñoom ñépp nag fees ak Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
5 At that time devout Jews from every nation under heaven were living in Jerusalem. Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.
6 When this sound rang out, a crowd gathered, confused, since each one heard them speak in his own language. Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa kàllaama gi nga nàmp. Mbooloo ma jaaxle.
7 They were amazed and astonished, saying, "Are not all these who are speaking Galileans? Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile?
8 How is it, then, that each of us hears them in our own native language? Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp?
9 Parthians, Medes, and Elamites; those who live in Mesopotamia, Judea and Cappadocia, Pontus and Asia, Muy waa Pàrt ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi
10 Phrygia, Pamphylia, Egypt, the parts of Libya near Cyrene; visitors from Rome, Jews and converts to Judaism; ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room,
11 Cretans and Arabs—we hear them telling in our own tongues the mighty works of our Father!" ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!»
12 They were all amazed and perplexed, saying to one another, "What does this mean?" Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?»
13 But others mocked and said, "They are full of sweet wine." Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
14 But Peter stood with the eleven, raised his voice, and declared to them: "Men of Judea, everyone living in Jerusalem—know this and listen carefully to my words. Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon.
15 These people are not drunk, as you suppose, for it is only nine o'clock in the morning. Ñii màndiwuñu, ni ngeen ko fooge, ndax yoor-yoor doŋŋ a jot.
16 No, this is what was spoken through the prophet Joel: Lii kay mooy kàddu ga Yonent Yàlla Yowel jottali woon, ne:
17 'And in the last days, says our Father, I will pour out my Spirit on all people; your sons and your daughters will prophesy, your young men will see visions, and your old men will dream dreams. “Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw ñépp; seeni doom, góor ak jigéen di biral kàdduy waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
18 Even on my male servants and my female servants in those days I will pour out my Spirit, and they will prophesy. Kera jant yooyu, sama jaam ñi, góor ak jigéen, maa leen di tuur samag Noo, ñuy biral kàdduy waxyu.
19 I will show wonders in the heavens above and signs on the earth below—blood and fire and billows of smoke. Te maay def ay kiraama fi asamaan aki firnde ci dun bi fi suuf; muy deret ak sawara ak niiru saxaar.
20 The sun will be turned to darkness and the moon to blood, before the great and glorious day of the Lord comes. Jant beey soppaliku ag lëndëm, weer wi doon deret, bésu Boroom bi doora taxawe màggaay ak daraja.
21 And everyone who calls on the name of the Lord will be saved.'" Su boobaa, képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”
22 "Men of Israel, hear these words: Jesus of Nazareth—a man our Father attested to you through miracles, wonders, and signs our Father did through him among you, as you yourselves know. «Yeen bokki Israayil, dégluleen wax jii! Yeesum Nasaret, Yàlla moo firndeele ag dëggoom ci ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.
23 This man, handed over by our Father's set plan and foreknowledge, you crucified and killed by the hands of lawless men. Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
24 But our Father raised him, freeing him from death's agony, since death could not hold him. Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu dee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko.
25 For David says of him: 'I saw our Father always before me, for he's at my right hand, so I won't be shaken.' Daawuda wax na ci mbiram ne: “Maa doon gis Boroom bi fi sama kanam saa su nekk, ndijoor la ma fare, ba duma tërëf.
26 Therefore my heart was glad and my tongue rejoiced; moreover, my body also will rest in hope. Moo tax sama xol di nux-nuxi, samaw làmmiñ di tex-texi, sama yaram sax nara noppalujee yaakaar.
27 For you will not abandon my soul to the grave, nor let your Holy One see decay. Doo ma wacc njaniiw moos, doo seetaan sa Ku sell ki, yaramam di yàqu ci biir bàmmeel.
28 You have shown me the paths of life; you will fill me with gladness in your presence." Yaa ma xamal yoonu dund, yaa may wéttali ba matal sama mbégte.”
29 "Brothers, I can tell you plainly: our ancestor David died, was buried, and his tomb remains with us to this day. «Bokk yi nag, Maam Daawuda, manees na leena wax ci lu wér ne nelaw na, ba ñu denc ko, te bàmmeelam a ngi fi, nuy gis ba tey jii.
30 Since he was a prophet, he knew our Father had sworn an oath to seat one of his descendants on his throne, Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku jóge ci geñoom lay teg cib jalam.
31 he foresaw and spoke of the Christ's resurrection, that he was not abandoned to the grave, nor his body saw decay. Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi bi, te ci mbiram la wax ne wàcceesu ko njaniiw, te yaramam du yàqu ci biir bàmmeel.
32 This Jesus our Father raised up, and we are all witnesses of it. Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
33 So, lifted up to our Father's right hand, having received the promised Holy Spirit from the Father, he poured out what you now see and hear. Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.
34 For David never went up into heaven, but he himself says: "Our Father said to my Lord, 'Sit at my right hand, Ndax kat du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor,
35 until I make your enemies a footstool for your feet.'" ba ma def say noon sa ndëggastal.’ ”
36 "So let the whole house of Israel know for certain: our Father made this Jesus, whom you crucified, both Lord and Christ." «Kon nag na wóor waa kër Israayil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
37 Cut to the heart at this, they asked Peter and the other apostles, "Brothers, what should we do?" Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»
38 Peter said to them, "Repent, and each of you be baptized in the name of Jesus Christ for the forgiveness of your sins, and you will receive the gift of the Holy Spirit. Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi bi, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar. Noonu Yàlla dina leen may Noo gu Sell gi.
39 For the promise is for you, your children, and all far off—as many as the Sovereign our Father will call to himself." Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jàmbur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.»
40 And with many other words he warned and urged them, saying, "Save yourselves from this corrupt generation." Yeneen kàddu yu bare soññe na leen ko, ñaaxe leen ko, ne leen: «Muccleen ci gii maas gu dëng.»
41 So those who welcomed his message were baptized, and about 3,000 people were added that day. Ña nangu kàddug Piyeer nag, ñu sóob leen ci ndox; bésub keroog lu wara mat ñetti junni (3 000) yokku nañu ca gëmkat ña.
42 They devoted themselves to the apostles' teaching and deep communion, to the breaking of bread and the prayers. Ci kaw loolu gëmkat yi daan nañoo pastéefu ci njàngalem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi, ak ci jataayi ñaan.
43 Awe came over everyone, and many wonders and signs were done through the apostles. Ba loolu amee ag ragal jàpp ñépp, ay kiraama yu bare aki firnde daldi sottee ca jëfi ndaw ya.
44 All who believed were together and had all things in common. Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp.
45 They sold their property and possessions and distributed the proceeds to all, as anyone needed. Ci biir loolu seeni suuf ak seen alal sax, ñu jaay, séddoo ko ñoom ñépp na mu dëppook seeni soxla.
46 Every day, devoting themselves together in the temple, breaking bread house to house, they shared food with joyful, sincere hearts, Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu.
47 praising our Father, with favor among all the people. The Lord added to their number daily those being saved. Ñuy màggal Yàlla, ñépp naw leen. Bés bu nekk nag Boroom bi di yokk ca mbooloo mooma, nit ña jota mucc.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]