Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In my first book, Theophilus, I wrote about everything Jesus began to do and teach, Yaw Tewofil, sama téere bu njëkk ba, def naa ca mboolem ndoortel jëfi Yeesu ak njàngaleem,
2 until the day he was taken up, having given commands through the Holy Spirit to the apostles he had chosen. ba ca bés ba ñu ko yéegale, gannaaw ba mu joxee ay ndigal ndaw ya mu tànnoon, Noo gu Sell gi jottali ko.
3 After his suffering, he showed himself alive to them through many proofs, appearing to them forty days, speaking of our Father's kingdom. Ndaw yooyu itam la teew fi seen kanam ci firnde yu leer te bare, gannaaw ay coonoom. Diiru ñeent fukki fan la leen feeñu, di leen wax lu jëm ci nguurug Yàlla.
4 While staying with them, he ordered them not to leave Jerusalem but to wait for my Father's promise—"which," he said, "you heard from me; Ba mu nekkee ak ñoom, da leena sant, ne leen: «Buleen jóge Yerusalem, négleen digeb Baay bi ngeen dégge ci sama gémmiñ.
5 for John baptized with water, but within a few days you will be baptized with the Holy Spirit." Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
6 So, gathered together, they asked, "Lord, will you restore the kingdom to Israel now?" Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israayil?»
7 He said to them, "You're not to know times or seasons that my Father has set by his own authority. Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés bi Baay bi jàpp ci sañ-sañu boppam.
8 But when the Holy Spirit falls on you, you'll gain power to be my witnesses—in Jerusalem, all Judea, Samaria, and earth's farthest reaches." Waaye Noo gu Sell gi mooy wàcc ci yeen, ngeen fees ak dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati àddina.»
9 After he said these things, as they watched, he was lifted up, and a cloud took him from their sight. Naka la wax loolu, ndaw yay xoole, ñu jekki yéegee ko fa, aw niir daldi leen koy làq.
10 As they stared into heaven while he went, suddenly two men in white clothes stood beside them. Ña nga téen, ne jàkk asamaan, Yeesu di wéy. Ci biir loolu ñaar ñu sol yére yu weex ne seef ci seen wet.
11 They said, "Galileans, why stare at the sky? This Jesus, taken from you into heaven, will return exactly as you saw him go." Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu ci asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
12 Then they returned to Jerusalem from the Mount called Olivet, near Jerusalem, about a half-mile away. Booba la ndaw ya jóge ca tund woowu ñuy wax tundu Oliw, te digganteem ak Yerusalem tollook kemu dox bi yoon maye ci bésub Noflaay, yemook benn kilomet. Ñu dellu nag Yerusalem.
13 Entering, they went up to the upstairs room where they stayed: Peter, John, James, Andrew, Philip, Thomas, Bartholomew, Matthew, James son of Alphaeus, Simon the Zealot, and Judas son of James. Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ, Mbokki kuréelu Moom-sa-réew ma, ak Yuda doomu Yanqóoba.
14 All these persisted together in prayer, with the women, Mary the mother of Jesus, and his brothers. Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu ak rakki Yeesu yu góor.
15 In those days Peter stood up among the brothers (about 120 in all) and said, Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen:
16 "Brothers, the Scripture the Holy Spirit spoke beforehand through the mouth of David about Judas—who became guide to those who arrested Jesus—had to be fulfilled. «Bokk yi, Mbind mi moo waxoon lu jiitu ci gémmiñu Daawuda jaare ci Noo gu Sell gi, muy wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti.
17 For he was numbered among us and was allotted his share in this ministry." Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
18 (This man bought a field with the pay for his wrongdoing, then fell headfirst, burst open in the middle, and all his insides spilled out. Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru.
19 This became known to everyone living in Jerusalem, so the field was named in their language Akeldama, that is, Field of Blood.). Waa Yerusalem yépp a ko yég, ba tax ñu tudde tool ba Akeldam, muy firi Toolu deret, ci seen làkk.
20 "For it's written in the Book of Psalms: 'Let his camp become empty, with no one living there,' and 'Let another take his position.' «Ndax bindees na ci téere bi di Taalifi cant ne: “Yal na këram gental, yàlla bu fa kenn dëkkeeti, yal na keneen jagoo sasam.”
21 So one of the men who accompanied us all along, while the Lord Jesus went in and out among us, Am na nag ay nit ñu àndoon ak nun mboolem diir bi Sang Yeesu dee dem aka dikk ci sunu biir,
22 from John's baptism until the day he was taken up from us—one of these must become with us a witness to his resurrection." dale ko ca ba ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jëlee fi sunu biir, yéege ko. Kon nag kenn ci ñooñu war naa bokk ak nun, seede ndekkitel Yeesu.»
23 And they put forward two—Joseph called Barsabbas, who was also called Justus, and Matthias. Ci kaw loolu ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas, te ñu di ko wax Yustus itam, ak Maccas.
24 They prayed and said, "You, Lord Jesus, who know all hearts, show which one of these two you chose, Ñu daldi ñaan ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,
25 to take the place in this ministry and apostleship that Judas left to go to his own place. mu jël wàllam ci liggéey bi, te muy céru ndaw bii Yuda wacc, ba fekki wàll wa mu yelloo.»
26 They cast lots for them; the lot fell to Matthias, and he was counted with the eleven apostles." Ñu tegal leen nag bant, bant ba dal ca Maccas, mu dolliku ca fukki ndaw yaak benn.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]