Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 21 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Afterward Jesus showed himself again to the disciples by the Sea of Tiberias—this is how he showed himself. Gannaaw loolu, Yeesu feeñooti na ay taalibeem ca tàkkal dex ga ñuy wax Tiberyàdd. Na mu feeñee nii la.
2 Simon Peter, Thomas called Twin, Nathanael from Cana in Galilee, Zebedee's sons, and two other disciples were together. Ña bokkoon daje benn béreb ñoo di Simoŋ Piyeer, ak Tomaa mi ñuy wax Seex bi, ak Natanayel ma dëkk Kana gu diiwaanu Galile, ak doomi Sebede, ak yeneen ñaari taalibe.
3 Simon Peter told them, "I'm going fishing." "We'll go with you," they said. So they went out and got into the boat, but caught nothing that night. Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi.» Ñu ne ko: «Nan ànd ak yaw, nun itam.» Ñu dem, daldi dugg gaal. Guddi googu jàppuñu dara.
4 At daybreak Jesus stood on the shore, yet the disciples didn't know it was Jesus. Ba fajar jotee Yeesu taxaw ca tàkk ga, te taalibe ya xamuñu ne moom la.
5 Jesus said to them, "Children, do you have any fish?" They answered him, "No." Yeesu ne leen: «Bokk yi, ndax am ngeen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
6 He told them, "Cast the net on the boat's right side, and you'll find fish." So they cast it, and were no longer able to haul it in for the sheer number of fish. Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndijooru gaal gi, ba daj.» Ci kaw loolu ñu sànni, ba noppi amatuñu dooley xëcc mbaal mi ndax jën yu bare.
7 The disciple Jesus loved told Peter, "It's the Lord!" Hearing it was the Lord, Simon Peter wrapped his coat around him—he'd taken it off to work—and threw himself into the sea. Ba loolu amee taalibe ba Yeesu soppoon ne Piyeer: «Sang bi la!» Ba Simoŋ Piyeer déggee loolu, fekk ko ak col gu woyof, mu laxasaay ko ba mu dëgër, daldi sóobu ca dex ga.
8 The other disciples came in the boat, dragging the net full of fish, since they were only about one hundred yards from shore. Yeneen taalibe ya nag dikk ak gaal ga, xëccaale mbaal ma fees dell ak jën, ndax sorewuñu woon tàkk ga; lu wara tollu ci téeméeri meetar a doxoon seen diggante ak tàkk ga.
9 When they went ashore, they saw a charcoal fire with fish on it, and bread. Ba ñu teersee, ab taalu këriñ lañu gis, aw jën tege ca, ak mburu ca wet ga.
10 Jesus said to them, "Bring some of the fish you have just caught." Yeesu ne leen: «Indileen ci jën yi ngeen jàpp.»
11 So Simon Peter climbed aboard and dragged the net ashore, full of 153 large fish; despite so many, it didn't tear. Simoŋ Piyeer nag yéeg ca gaal ga, daldi diri mbaal ma ca tàkk ga, mu fees dell ak jën yu mag; lépp di téeméeri jën ak juróom fukk ak ñett (153). Te noonu mu baree taxul mbaal ma xëtt.
12 Jesus said to them, "Come, eat breakfast." None of the disciples dared ask him, "Who are you?"—they knew it was the Lord. Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ca taalibe ya nag ñemewu ko woon ne ko: «Yaay kan?» Ndax xamoon nañu ne Sang bee.
13 Jesus came, took the bread, and gave it to them, and the fish as well. Yeesu dikk, jël mburu, jox leen, jox leen jën itam.
14 This was now the third time Jesus revealed himself to the disciples after being raised from the dead. Boobu mooy ñetteelu yoon bu Yeesu feeñoo taalibe ya, gannaaw ba mu dekkee.
15 After they ate breakfast, Jesus asked Simon Peter, "Simon, son of John, do you love me with all your heart, more than these?" He answered, "Yes, Lord, you know I love you as a friend." Jesus told him, "Feed my lambs." Ba ñu ndékkee ba noppi, Yeesu da ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaan, ndax yaa ma gëna sopp ñii?» Mu ne ko: «Waawaaw, Sang bi, yaw, xam nga ne bëgg naa la.» Mu ne ko: «Xontal ma sama mbote yi.»
16 A second time Jesus asked, "Simon son of John, do you love me with all your heart?" He replied, "Yes, Lord, you know I love you as a friend." Jesus said, "Take care of my sheep." Mu waxaat ko ñaareel bi yoon, ne ko: «Simoŋ doomu Yowaan, ndax sopp nga ma?» Mu ne ko: «Waawaaw, Sang bi, yaw, xam nga ne bëgg naa la.» Mu ne ko: «Sàmmal ma samay xar.»
17 A third time Jesus said to him, "Simon son of John, do you love me as a friend?" Peter was hurt that Jesus asked him a third time, "Do you love me as a friend?" and said, "Lord, you know everything; you know that I love you as a friend." Jesus said to him, "Feed my sheep." Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaan, bëgg nga maam?» Piyeer nag tiislu la ko Yeesu laaj ba ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Piyeer ne ko: «Sang bi, yaw xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Xontal ma samay xar.
18 "Truly, truly, I tell you: when you were young, you dressed yourself and went where you wanted; but when you're old, you'll stretch out your hands, and another will dress you and take you where you don't want to go." Maa la ko wax déy ci lu wér, ba nga dee ndaw, yaay takkal sa bopp sa geño, dem fu la neex. Waaye boo màggatee, dinga tàllal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.»
19 Jesus said this to show by what kind of death Peter would glorify our Father. Then he told him, "Follow me." Kàddu yooyu la Yeesu misaale na Piyeer di deeweji deewin wu muy terale Yàlla. Loolu la wax ba noppi ne ko: «Toppal ci man!»
20 Peter turned and saw the disciple Jesus loved following—the one who leaned back against Jesus at supper and asked, "Lord, who is going to betray you?" Piyeer geestu, gis taalibe ba Yeesu soppoon, mu topp ca ñoom. Taalibe boobu mooy ka sóonu woon, ba tafu ca dënnub Yeesu, ba ñuy lekk, te moo ko laajoon ne ko: «Sang bi, kan moo lay wor?»
21 When Peter saw him, he said to Jesus, "Lord, what about this man?" Ba ko Piyeer gisee da ne Yeesu: «Sang bi, kii nag?»
22 Jesus told him, "If I want him to remain until I come, what's that to you? You follow me." Yeesu ne ko: «Moom, su ma bëggoon mu dund ba kera ma délsi, ana lu ciy sa yoon? Yaw kay, toppal ci man.»
23 So this word spread among the brothers and sisters that this disciple would not die. Yet Jesus did not tell him he would not die, but, "If I want him to remain until I come, what is that to you?" Kàddu googu nag doxe ca, law ca biir bokki taalibe ya, ñu jàpp ne taalibe boobu du dee. Ndaxam Yeesu waxul Piyeer ne kooku du dee, waaye da ne: «Su ma bëggee mu dund, ba kera ma délsi, ana lu ciy sa yoon?»
24 This is the disciple testifying to these things and who wrote them; we know his testimony is true. Taalibe boobu moo seede mbir yooyu, moo bind xew-xew yooyu, te xam nanu ne kàddug seedeem dëgg la.
25 Jesus did many other things too. If each were written down, I don't think the world itself could hold the books written. Bare na itam yeneen yu Yeesu def, te su ñu ko doon bind benn-benn, jàpp naa ne àddina ci boppam sax du mana denc téere ya ñu ko bind.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]