Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 5 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Now a man named Ananias, together with his wife Sapphira, sold a piece of property. Naka noonu ku ñuy wax Anañas, te ku ñuy wax Safira di jabaram, daldi jaay aw làccu suuf.
2 He kept back part of the proceeds for himself, with his wife aware, and brought only a portion, laying it at the apostles' feet. Mu yégook jabaram, daldi làq lenn ca njëg ga, ba noppi indi la ca des, teg ko ca kanam ndaw ya.
3 But Peter said, "Ananias, why has Satan filled your heart to lie to the Holy Spirit and keep back part of the land's price? Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njëgu tool bi?
4 Wasn't it yours while unsold? After selling, wasn't the money yours to control? Why did you plan this in your heart? You didn't lie to people, but to our Father." Ba mu jaragul, du yaa doon boroom? Gannaaw ba mu jaree it, xanaa du njëg gaa ngi ci sa loxo ba tey? Ana noo mana xajale mii mébét ci sa xol? Du nit nga wor de, waaye Yàlla nga wor.»
5 Hearing these words, Ananias fell down and died; great fear seized all who heard. Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, mu daldi daanu, dee. Tiitaange ju réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.
6 Then the young men rose, wrapped up his body, carried him out, and buried him. Ba loolu amee xale yu góor ya dikk, sàng ko, yóbbu suuli.
7 About three hours later his wife came in, not knowing what had happened. Ñu teg ca lu wara tollook ñetti waxtu, jabaram duggsi, te yégul la xew.
8 Peter asked her, "Tell me, did you sell the land for this much?" She said, "Yes, for that much." Piyeer ne ko: «Wax ma, ndax lii mooy njëgu tool bi?» Mu ne ko waaw, nàngam la.
9 Then Peter said to her, "Why did you conspire to test the Spirit of our Father? Look, the feet of those who buried your husband are at the door, and they'll carry you out too." Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Ana lu ngeen di mànkoo, di nattu Noowug Boroom bi? Déglul, tànk yi suuli woon sa jëkkër a ngoogu ci bunt bi di la yóbbusi yaw it.»
10 At once she fell at his feet and died. The young men came in, found her dead, carried her out, and buried her beside her husband. Ca saa sa ndaw sa daanu cay tànkam, dee. Xale yu góor yi duggsi, fekk ko mu dee; ñu yóbbu ko, suul ko ca wetu jëkkëram.
11 And great fear came upon the whole church and upon all who heard of these things. Ba loolu amee tiitaange ju réy jàpp mbooloom gëmkat ñépp ak ña ko dégg ñépp.
12 Many signs and wonders happened among the people through the apostles' hands. They all gathered together in Solomon's Portico. Ci kaw loolu ay firnde ak kéemaan yu bare di sottee ci loxol ndaw yi, ci biir askan wi. Gëmkat ñi nag di bokk daje ñoom ñépp fa ñuy wax Mbaarum Suleymaan, ca biir kër Yàlla ga,
13 None of the rest dared to join them, but the people held them in high honor. waaye kenn ca ña ca des ñemewula jaxasoo ak ñoom. Teewul askan wa nawloo leen lool.
14 Even more believers were added to the Lord—crowds of men and women, Gëmkati Sang bi nag di gëna bare, ñuy wàllisi, ba doon mbooloo mu mag, góor ak jigéen.
15 so they even carried the sick into the streets and put them on cots and mats, hoping that at least Peter's shadow might fall on some of them as he passed. Nit ñi dem bay génne jarag ji ci mbedd yi, teg leen ci ay laltu aki basaŋ, ngir bu fa Piyeer jaaree, lu bon bon takkndeeram mana dal ñenn ci ñoom.
16 Crowds also came from towns around Jerusalem, bringing the sick and those tormented by unclean spirits, and all were healed. Ci biir loolu nit ñu bare bàbbeekoo ca dëkk ya séq Yerusalem, indi ay jarag ak ñu rab sonal; ñoom ñépp daldi wér.
17 The high priest rose up, and all with him, the Sadducee party, and they were filled with jealousy. Ba mu ko defee xolu kañaan dugg sarxalkat bu mag ba ak mboolem ña ko dar, te di waa ngérum Sadusen ña.
18 They arrested the apostles and put them in the public prison. Ñu teg ndaw ya loxo, tëj leen ca kaso ba.
19 But at night an angel of our Father opened the prison doors, led them out, and said, Ca guddi ga nag malaakam Boroom bi ubbi bunti kaso ba, génne leen, ne leen:
20 "Go, stand in the temple and speak to the people all the words of this Life." «Demleen taxaw ca digg kër Yàlla ga, ngeen xamal askan wi mboolem lu jëm ci dund gii.»
21 Hearing this, they went into the temple at dawn and began teaching. When the high priest and those with him arrived, they convened the council—the full assembly of elders of Israel—and sent to the jail to have them brought. Gannaaw ba ñu déggee loolu, ba bët set, ñu dugg ca kër Yàlla ga, di waare. Ci biir loolu sarxalkat bu mag ba ak ña ko dar, dikk, woolu kuréelu àttekat ya, mboolem kuréelu njiiti bànni Israayil; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22 But the guards found no one there when they arrived; they returned and reported, Dag ya nag dikk, fekkuñu leen ca kaso ba, ñu dellu yégleji ko,
23 "We found the prison locked tight, guards standing at the doors, but opening them, found no one inside." ne: «Danoo fekk kaso ba tëje ràpp, wattukat ya taxaw ca bunt ya. Nu tijji, fekkunu kenn ca biir!»
24 Hearing this, the temple guard captain and chief priests were baffled, wondering where it would lead. Jawriñu kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya dégg loolu, daldi jaaxle lool ci ndaw yi, di xalaat nu mbir miy mujje.
25 Someone came and reported, "Look, the men you jailed are standing in the temple teaching the people!" Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
26 Then the captain and officers went and brought them, without force, fearing the people would stone them. Ci kaw loolu jawriñu kër Yàlla ga ak dag ya jëli ndaw ya ndànk, bañ leena jaay doole, ngir ragal nit ñi sànni leen ay doj.
27 When they had brought them, they set them before the council. And the high priest questioned them, Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kuréelu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,
28 saying, "We strictly ordered you not to teach in this name, yet you've filled Jerusalem with your teaching and intend to bring this man's blood on us." ne: «Xanaa aayewunu leen woon ne buleen waareeti mukk ci woowu tur? Yeena ngi nii ubale Yerusalem ak seen waare, ngeen nar nu cee gàdduloo bakkanu nit kii!»
29 But Peter and the apostles answered, "We must obey our Father rather than men. Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
30 The God of our fathers raised Jesus, whom you killed by hanging him on a tree. Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
31 Our Father exalted him to his own right hand as Ruler and Savior, to give Israel repentance and forgiveness of sins. Moom la Yàlla yéege fa ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israayil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.
32 We are witnesses of these things, and so is the Holy Spirit, whom our Father gave to those who obey him." Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»
33 When they heard this, they were enraged and wanted to kill them. Ba ñu déggee loolu, dañoo mer ba fees, nar leena rey.
34 But a Pharisee named Gamaliel, a law teacher honored by all the people, stood up in the council and ordered the men taken outside briefly. Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jàngalekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kuréelu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.
35 He told them, "Israelites, think carefully about what you're about to do with these men. Ba ñu génnee, mu ne waa kuréel ga: «Yeen bokki Israayil, moytuleen bu baax li ngeen di def ak nit ñii.
36 Before this, Theudas appeared, claiming to be somebody; about 400 men followed him. He was killed, his followers all scattered, and it came to nothing. Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.
37 After him, Judas the Galilean rose up during the census and drew people away after him. He too died, and all who followed him were scattered. Gannaawam it Yuda mu Galile jóg, ca jant ya ñu doon lim waa réew mi; mu yóbbaale mbooloo mu ko topp. Moom itam dee, ña ko toppoon ñépp tasaaroo.
38 Now I tell you: stay away from these men and leave them alone. If this plan or work is from men, it will fail. Léegi nag, dama ne, mànduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.
39 But if it's from our Father, you won't be able to overthrow them; you might even find yourselves fighting our Father." So they were persuaded by him. Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,
40 Persuaded by him, they called in the apostles, beat them, ordered them not to speak in the name of Jesus, and released them. woowaat ndaw ya. Ba loolu amee ñu dóor leen, aaye leen ñu waxati lenn ci turu Yeesu, door leena yiwi.
41 So they left the council, rejoicing they'd been counted worthy to be shamed for the name. Ndaw ya nag bàyyikoo ca kuréelu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.
42 Every day, in the temple and house to house, they never stopped teaching and proclaiming the good news: the Christ is Jesus. Ci kaw loolu bés bu nekkaan, muy ca kër Yàlla, di ca biir kër ya, noppiwuñoo jàngale aka xamle xibaaru jàmm bi yéene ne Yeesu mooy Almasi bi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]