Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 6 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In those days, as the disciples multiplied, the Greek-speaking Jews grumbled against the Hebrews because their widows were overlooked in the daily distribution of food. Jant yooyu nag, naka taalibe yi di gëna bare, Yawut ñiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci kaw Yawut ñiy wax seen làmmiñu bopp ndax néewal gu ñu gis ñu néewal ko seeni jëtun ca na ñuy séddalee ag ndimbal bés bu nekk.
2 So the Twelve called all the disciples together and said, "It's not right for us to neglect our Father's word to serve tables. Ba mu ko defee Fukk ñaak ñaar woo mbooloom taalibe ya, ne leen: «Nu sàggane kàddug Yàlla, di toppatoo mbirum séddale daal, jekkul ci nun.
3 So, brothers, pick seven men among you, well-respected, full of the Holy Spirit and wisdom, whom we'll appoint to this task. Kon nag bokk yi, seetleen ci seen biir juróom ñaar ñu rafet seede, soloo Noo gu Sell gi te rafet xel, nu dénk leen sas woowu.
4 But we will devote ourselves to prayer and to the ministry of the word." Nun nag nanu wéye ñaan gi, ak liggéey bi ci kàddu gi.»
5 The whole assembly approved, and chose Stephen—full of faith and the Holy Spirit—along with Philip, Prochorus, Nicanor, Timon, Parmenas, and Nicolaus, a convert from Antioch. Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit ku fees ak ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut.
6 They presented these men to the apostles, who prayed and laid their hands on them. Ñu indi leen fa kanam ndaw ya, ñu ñaanal leen, teg leen loxo.
7 The word of our Father spread, and disciples in Jerusalem multiplied greatly; a great number of priests became obedient to the faith. Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.
8 Now Stephen, full of grace and power, was performing great wonders and signs among the people. Ci kaw loolu Eccen mi yiwu Yàlla def ag leer fees ko, di def ay kéemaan ak firnde yu mag ci biir askan wi.
9 Some from the so-called Synagogue of the Freedmen—Cyrenians, Alexandrians, and men from Cilicia and Asia—rose up to argue with Stephen. Ba loolu amee ñenn ca jàngu Yawut ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.
10 Yet they could not stand up against the wisdom and the Spirit with which he was speaking. Teewul àttanuñu xelam mu rafet ak Noo gu Sell ga muy waxe.
11 Then they secretly instructed men to say, "We heard him speak blasphemous words against Moses and God." Ñu daldi ger ay nit ngir ñu duural ko, ne: «Noo ko dégg, mu yékkati kàdduy saaga, jëme ci Musaa ak ci Yàlla.»
12 They stirred up the people, elders, and scribes; came upon him, seized him, and brought him before the council. Ba loolu amee ñu xabtal nit ñi ak magi askan wi ak firikati yoonu Musaa yi, ñu ne jalañ, jàpp Eccen, yóbbu ca kuréelu àttekat ya.
13 They brought in false witnesses, saying, "This man never stops speaking against this holy place and the law. Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak kër Yàlla gii ak yoonu Musaa.
14 For we heard him say this Jesus of Nazareth will destroy this place and change the customs Moses handed down to us." Noo ko dégg mu ne Yeesu mu Nasaret moomu dina màbb kër Yàlla gii te dina soppi aada yi nu Musaa bàyyee.»
15 Everyone sitting in the council stared at him and saw his face was like an angel's face. Mboolem ña ca kuréelu àttekat ya nag ne jàkk Eccen; ñu gis xar-kanam ba ne ràññ ni xar-kanamu malaaka.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]