Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then the high priest asked, "Are these things true?" Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
2 Stephen said, "Brothers and fathers, listen: Our Father of glory appeared to our father Abraham in Mesopotamia, before he lived in Haran, Eccen ne ko: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom daraja moo feeñu woon sunu maam Ibraayma, ba mu nekkee ca réewum Mesopotami, bala moo sanc Karan.
3 and told him, 'Leave your land and relatives, and go to the land I'll show you.' Mu ne ko: “Jógeel sam réew, jóge ci say bokk, te nga dem ca réew mi ma lay won.”
4 He left the Babylonians' land and settled in Haran. After his father died, our Father moved him from there into this land you now live in. «Mu daldi jóge réewum waa Kalde, sanci Karan. Fa la ko Yàlla toxale gannaaw ba baayam faatoo, sancal ko ci réew mii ngeen dëkk tey.
5 He gave him no inheritance in it, not even a foot of ground—yet promised it to him and his descendants after him as a possession, though he had no child. Taxul mu muurale ko lenn ci réew mii, du sax fu mu teg tànkam. Teewul mu dig ko, ne moom lay moomale réew mi, mook askanam wa koy wuutuji, te fekkul sax mu am doom.
6 And our Father said his offspring would be foreigners in a land not their own, enslaved and mistreated 400 years. Yàlla ne ko: “Saw askan dinañu toxuji bitim réew, te dees na leen def ay jaam, mitital leen diiru ñeenti téeméeri at (400).”
7 'I will judge the nation they serve,' our Father said, 'and after, they will come out and worship me in this place.' Yàlla neeti ko: “Xeet wi leen di def jaam nag, man maa leen di mbugal. Gannaaw loolu dinañu fa génne, jaamusi ma ci béreb bii.”
8 He gave him the covenant of circumcision. Abraham fathered Isaac and circumcised him on the eighth day; Isaac fathered Jacob, and Jacob the twelve ancestors. Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarafal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba; Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.
9 The ancestors, jealous of Joseph, sold him into Egypt, but our Father was with him, «Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,
10 and rescued him from all his troubles, gave him favor and wisdom before Pharaoh king of Egypt, who made him ruler over Egypt and Pharaoh's whole household. xettali ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.
11 A famine and great suffering struck all Egypt and Canaan, and our fathers found no food. «Ci kaw loolu ab xiif dikkal Misra gépp ak réewum Kanaan. Mu metti lool. Sunuy maam nag amatuñu ab dund.
12 Hearing there was grain in Egypt, Jacob sent our fathers there first. Yanqóoba dégg ne ab dund am na Misra. Ca la fa njëkka yebal sunu maam ya.
13 On the second visit, Joseph made himself known to his brothers, and Pharaoh learned of Joseph's family. Seen ñaareel bi yoon la Yuusufa xàmmiku ay doomi baayam, Firawna nag doxe ca xam cosaanu Yuusufa.
14 And Joseph sent for his father Jacob and all his relatives, seventy-five persons in all. Ci kaw loolu Yuusufa yeble, indi baayam ak bokkam yépp, ñuy juróom ñaar fukki nit ak juróom.
15 And Jacob went down into Egypt, and he died, he and our fathers. Noonu la Yanqóoba deme Misra, ba faatoo fa, mook sunuy maam.
16 They were taken back to Shechem, and buried in the tomb Abraham had bought for silver from Hamor's sons in Shechem. Gannaaw gi lañu toxal seeni yax ca Sikem, denc leen ca bàmmeel, ba Ibraayma weccikoo woon xaalis ca doomi Amor ca Sikem.
17 As the time of the promise our Father gave Abraham neared, the people grew and multiplied in Egypt, «Ñu dem ba dige ba Yàlla giñaloon Ibraayma di waaja sotti, yemook xeet wi yokku, di gëna bare ci Misra,
18 until there arose over Egypt another king who did not know Joseph. ba beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra.
19 This king exploited our people and mistreated our fathers, forcing them to abandon their infants to die. Buur boobu nag di muusaatu sunu xeet wi, di mitital sunuy maam, di leen sànniloo seeni liir, ngir ñu baña dund.
20 At that time Moses was born, beautiful in our Father's sight. He was raised three months in his father's house. «Booba la Musaa juddu, rafet ba fa kanam Yàlla, ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam.
21 And when he was abandoned, Pharaoh's daughter adopted him and brought him up as her own son. Ba ñu ko sànnee, doomu Firawna ju jigéen a ko foral boppam, yar ko ni doomam ju mu jur.
22 Moses was trained in all Egyptian wisdom, and was strong in speech and action. Musaa nag di ku mokkal mboolem xam-xamu Misra, te ràññiku lool ci wax ak ci jëf.
23 When he was forty years old, he decided to visit his brothers, the sons of Israel. «Ba ñeent fukki atam matee, xelum seeti bokki bànni Israayilam dikkal ko.
24 Seeing one of them wronged, he defended the oppressed man and avenged him by striking down the Egyptian. Ci kaw loolu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, daldi rey waayi Misra ja, feyul ka mu néewal.
25 He thought his brothers would understand our Father was giving them salvation through his hand, but they didn't understand. Booba Musaa foog na ne ay bokkam xam nañu ne ciy loxoom la leen Yàlla di indile wall, ndeke xamuñu ko.
26 The next day he came upon them as they were fighting and tried to reconcile them, saying, 'Men, you are brothers. Why do you wrong each other?' Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”
27 But the man wronging his neighbor shoved Moses aside, saying, 'Who made you ruler and judge over us? Ka doon néewal doole moroom ma bëmëx Musaa, ne ko: “Yaw, ku la def kilifa mbaa àttekat ci sunu kaw?
28 Do you want to kill me as you killed the Egyptian yesterday?' Xanaa danga maa nara rey, na nga reye waayi Misra ja démb?”
29 At this word, Moses fled and lived as a foreigner in the land of Midian, where he fathered two sons. Musaa dégg kàddu googu, daldi gàddaay, dem dali réewum Majan, ba am fa ñaari doom yu góor.
30 Forty years later, an angel appeared to him in the wilderness of Mount Sinai, in a burning bush's flame. «Mu teg ca ñeent fukki at, malaaka feeñu ko ca màndiŋu tundu Sinayi, ci biir tàkk-tàkku sawara wu jafal ab gajj.
31 Moses saw it and was amazed; as he approached to look closer, our Father's voice came: Musaa gis peeñu moomu, yéemu; mu dikk ba jege ko ngir niir ko, kàddug Boroom bi daldi jib. Mu ne:
32 'I am the God of your fathers—the God of Abraham, Isaac, and Jacob.' Moses trembled, not daring to look. “Man maay sa Yàllay maam, maay Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.” Musaa tiit bay lox, ñemeetula xool.
33 Then our Father told him, 'Take the sandals off your feet, for the place you're standing on is holy ground.' Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndax fii nga taxaw, suuf su sell la.
34 I have indeed seen my people's suffering in Egypt, heard their groaning, and come down to rescue them. Now go—I'm sending you to Egypt. Gis naa bu baax sama coonob ñoñ ci Misra; maa dégg seeni onk, ba wàcc ngir wallusi leen. Léegi nag dikkal, ma yebal la Misra.”
35 This Moses, whom they rejected, saying, 'Who made you ruler and judge?'—this is the one our Father sent as both ruler and redeemer, through the hand of the angel who appeared to him in the bush. «Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Yaw, ku la def kilifa mbaa àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottali yóbbante ba.
36 This man led them out, doing wonders and signs in the land of Egypt, at the Red Sea, and in the wilderness for forty years. Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma ak ca géeju Barax ya ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.
37 This is the Moses who told Israel's sons, 'Our Father will raise up a prophet like me for you, from your brothers.' Musaa moomu moo noon bànni Israayil: “Yonent bu mel ni man la leen Yàlla di feeñalal ci seen biiri bokk.”
38 This is the one who was in the wilderness assembly with the angel speaking to him at Mount Sinai, and with our fathers—he received living words to give us. Moom it moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, mook malaaka ma doon wax ak moom ca kaw tundu Sinayi ca sunu wetu maam ya. Moo jot ci kàddu yuy dund, ngir jottali nu ko.
39 Our fathers refused to obey him; they rejected him and in their hearts turned back to Egypt, Kooku la sunuy maam nanguwul woona déggal. Dañu koo far xarab, namma walbatiku dellu Misra.
40 telling Aaron, 'Make us gods to go ahead of us. As for this Moses who led us out of the land of Egypt, we don't know what happened to him.' Ñu ne Aaróona: “Sàkkal nu ay yàlla yu nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra, xamunu lu ko dal.”
41 They made a calf in those days, offered a sacrifice to the idol, and celebrated what their hands had made. Jant yooyu lañu sàkk jëmmu sëllu, defal jëmm ja ab sarax, di bànneexoo lu ñu sàkke seeni loxo.
42 But our Father turned away, giving them over to worship the host of heaven, as written in the prophets' book: 'Did you bring me slaughtered animals and sacrifices for forty years in the wilderness, house of Israel? Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israayil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43 You carried Moloch's tent and your god Rephan's star, the idols you fashioned to worship them; so I will banish you far beyond Babylon.' Molog seen tuur mi, ngeen yóbbaale xaymab jaamookaayam, ak seen biddiiwu yàlla ji ñu naa Refan, jëmm yooyu ngeen sàkk, di leen sujjóotal! Kon nag maa leen di toxal ca wàllaa Babilon.”
44 Our ancestors had the tent of witness in the wilderness, as he who spoke to Moses directed him to make it, matching the pattern he'd seen. «Xaymab seede baa nga woon ak sunuy maam ca màndiŋ ma, ñu sàkke ko na ko ka doon wax ak Musaa sante, dëppale kook misaal ma Musaa gisoon.
45 Our fathers in turn brought it in with Joshua when they dispossessed the nations that our Father drove out before them. So it was until the days of David, Xayma ba la sunuy maam jot, dugal ko ci kilifteefu Yosuwe ca biir réewum xeet ya leen Yàlla dàqal. Xayma ba nekk fa, ba ca janti Daawuda.
46 who found favor with our Father and asked to find a dwelling place for our Father. Daawuda ma Yàlla baaxe woon, sàkku woon na am màkkaan ngir Yàllay Yanqóoba.
47 But it was Solomon who built a house for him. Waaye Suleymaan moo ko mujj tabaxal kër.
48 Yet the Most High does not live in houses made by human hands, as the prophet says: «Moona Aji Kawe ji du dëkke lu loxo defar, mooy la yonent ba ne:
49 'Heaven is my throne, and the earth is my footstool. What kind of house will you build for me, says our Father, or what is the place of my rest? “Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal? Boroom bee ko wax. Mu ne: Ana ban béreb ay sama dalluwaay?
50 Did not my hand make all these things?' Loolu lépp, xanaa du sama loxoo ko sàkk?”
51 "You stubborn people, uncircumcised in heart and ears, always resist the Holy Spirit—like your fathers, so do you. «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Xanaa dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
52 Which of the prophets did your fathers not persecute? They killed those who announced beforehand the Righteous One's coming—whom you have now betrayed and murdered. Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub ji ngeen wor tey, bóom ko.
53 You who received the law through angels and yet did not keep it." Yeen de yeena jotoon ci yoonu Musaa wi ay malaaka jottali, te taxul ngeen jëfe ko.»
54 Now when they heard these things they were enraged, and they ground their teeth at him. Naka lañu dégg loolu, seen xol fuddu, ñuy yéyu ci kawam.
55 But Stephen, full of the Holy Spirit, looked into heaven, saw the glory of our Father, and Jesus standing at the right hand of our Father. Eccen nag fees ak Noo gu Sell gi, ne jàkk asamaan, daldi gis leeru Yàlla, gis Yeesu taxawe fa ndijooru Yàlla.
56 And he said, "Look, I see the heavens opened and the Son of Man standing at our Father's right hand." Mu ne: «Asamaan a ngii ma gis, mu ubbiku, Doomu nit kaa ngii taxaw fi ndijooru Yàlla!»
57 But they cried out with a loud voice, covered their ears, and rushed at him. Ba loolu amee ñu yuuxu ca kaw, dar seeni nopp, daldi ànd, ne milib ca kawam;
58 They threw him out of the city and stoned him. The witnesses laid their coats at the feet of a young man named Saul. ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.
59 And as they were stoning him, Stephen called out, "Lord Jesus, receive my spirit." Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!»
60 Kneeling, he cried out loudly, "Lord, do not hold this sin against them." Then he fell asleep. Mu ne gurub, samp bëti óomam, daldi àddu ca kaw, ne: «Sang bi, bu leen topp bii bàkkaar.» Naka la wax loolu, daldi faatu.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]