Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 8 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Saul approved of Stephen's killing. That day a great persecution erupted against the Jerusalem church, scattering everyone except the apostles through Judea and Samaria. Sóol nag rafetlu woon na la ñu bóom Eccen. Bésub keroog teg nañu mbooloom gëmkat ña ca Yerusalem fitna ju metti ba, lu moy ndawi Almasi bi, ñoom ñépp a tasaaroo ca diiwaani Yude ak Samari.
2 Devout men buried Stephen and mourned loudly over him. Ay nit ñu ragal Yàlla nag rob Eccen, ñaawlu deewam lool.
3 But Saul was destroying the church, entering house after house, dragging off men and women, throwing them in prison. Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, tëjlu leen kaso.
4 So those scattered went everywhere, proclaiming the good news of the word. Gëmkat ña tasaaroo di xamle fépp fu ñu jaare, xibaaru jàmm bu kàddu gi.
5 Philip went down to the city of Samaria and proclaimed Christ to them. Noonu la Filib deme péeyub Samari, di siiwtaane Almasi bi.
6 The crowds paid attention together to Philip's words, hearing and seeing the signs he did. Ba waa dëkk ba déggee mbaa ñu gis kéemaan ya muy def, ñoo bokk teewlu ay waxam.
7 Unclean spirits came out of many who were possessed, screaming loudly, and many paralyzed and lame were healed. Ndax bare na ca ñu rab jàppoon te mujj bàyyi leen, génne yuux yu réy; bare na ca it ñu lafañ ak ñu làggi woon te mujj wér.
8 So there was great joy in that city. Muy mbég mu réy nag ca dëkk boobee.
9 A man named Simon had already practiced magic in that city, amazing Samaria's people and claiming to be someone great. Ku ñuy wax Simoŋ nag yàggoon na ca dëkk ba, di ñeengo. Ku waar waa Samari la woon, te doon tuddoo nit ku màgg.
10 Everyone, from least to greatest, listened to him, saying, "This man is God's power, called Great." Ñépp, mag ak ndaw, teewlu ko, naan: «Kii mooy dooley Yàlla ci boppam. Moom lañuy wax “Màggle”.»
11 They paid attention to him because for a long time he had amazed them with his magic. La ñu ko teewloo woon moo di jëfi ñeengo ya mu leen yàgga yéeme.
12 But when they believed Philip's good news about the kingdom of our Father and the name of Jesus Christ, men and women were baptized. Waaye ba ñu gëmee Filib ma leen xamal xibaaru jàmm, bi jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Almasi bi, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
13 Simon himself believed, was baptized, and stayed close to Philip, amazed at the signs and great miracles he saw. Simoŋ ci boppam gëm, moom it, ñu sóob ko ci ndox. Simoŋ nag bàyyeetul Filib. Ba mu gisee firnde yaak kiraama yu mag yay am, moom moo yéemu.
14 When the apostles in Jerusalem heard Samaria had received our Father's word, they sent Peter and John to them. Ba ndaw ya ca Yerusalem yégee ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla, Piyeer ak Yowaan lañu fa yebal.
15 When they arrived, they prayed for them that they might receive the Holy Spirit, Ñu agsi Samari, ñaanal gëmkat ña, ngir ñu jot Noo gu Sell gi.
16 for the Holy Spirit had not yet fallen on any of them; they were only baptized into the name of the Lord Jesus. Ndax booba Noo gi wàccagul woon ci kenn ci ñoom, dees leena sóoboon rekk ci ndox ci turu Sang Yeesu.
17 Then they laid their hands on them, and they received the Holy Spirit. Ba loolu amee Piyeer ak Yowaan teg leen loxo, ñu jot Noo gu Sell gi.
18 When Simon saw the Spirit given through the apostles' laying on of hands, he offered them money, Simoŋ nag gis noonee mayug Noo gu Sell gi sababoo ci tegeb loxo bu ndaw ña amal, ba tax mu indil leen xaalis.
19 saying, "Give me this power too, so whoever I lay hands on receives the Holy Spirit." Mu ne leen: «Mayleen ma man itam xam-xam bii, ngir ku ma teg loxo, nga jot Noo gu Sell gi.»
20 Peter said to him, "May your silver perish with you, since you thought you could buy our Father's gift with money! Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
21 You have no part or share in this matter, for your heart is not right before our Father. Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
22 So turn from this evil, and pray to our Father that, if possible, your heart's intent may be forgiven you. Réccul nag sa mbon gii, te ñaan Boroom bi; jombul mu baal la sa mébétu xol.
23 I see you poisoned by bitterness and bound by evil." Ndax gis naa ni nga sóoboo ci wextanu kañaan, keppu ci ndëngte.»
24 Simon answered, "Pray to God for me, that nothing you have said may come upon me." Simoŋ ne leen: «Ñaanalleen ma Boroom bi, yeen ci seen bopp, ngir li ngeen wax lépp, lenn bañ ma cee dab.»
25 So, having testified and spoken our Lord Jesus's word, they returned to Jerusalem, preaching the good news in many Samaritan villages. Gannaaw ba Piyeer ak Yowaan seedeelee kàddug Boroom bi, biral ko, Yerusalem lañu dellu, di xamle xibaaru jàmm bi ci ay dëkki Samari yu bare.
26 Then an angel of our Father told Philip, "Get up and go south to the road going down from Jerusalem to Gaza"—a desert road. Menn malaakam Boroom bi nag wax Filib, ne ko: «Fabul jubal bëj-saalum; yoon wa kenn jaareetul te bartaloo Yerusalem, jëm Gasa.»
27 He got up and went. There was an Ethiopian eunuch, a court official of Candace, queen of the Ethiopians, in charge of all her treasury, who had come to Jerusalem to worship, Filib fabu, dem. Ndeke am na jenn waayu Ecopi ju màggalsi woon Yerusalem. Nit kooku doonoon moraange, te di jaraaf ju mag ju Kàndas Lingeeru Ecopi; moo doon saytu mboolem alalu Lingeeru Ecopi.
28 and was returning, seated in his chariot and reading the prophet Isaiah. Naka la jaraaf ja màggalsi bay dellu Ecopi, toog ca watiiram, di jàngaale téereb Yonent Yàlla Esayi,
29 And the Holy Spirit said to Philip, "Go over and catch up with that chariot." Noowug Yàlla ne Filib: «Doxal, dab watiir bale.»
30 Philip ran up, heard him reading the prophet Isaiah, and asked, "Do you understand what you're reading?" Filib dabsi waayi Ecopi ja, daldi dégg muy jàng téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31 He said, "How can I, unless someone guides me?" and invited Philip up to sit with him. Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, te kenn firilu ma ko?» Ba loolu amee mu ne Filib, mu yéeg, toog ak moom. Filib yéeg.
32 Now the passage of Scripture he was reading was this: "Like a sheep he was led to the slaughter, and like a lamb silent before its shearer, so he did not open his mouth. Lii nag mooy dogu Mbind ma mu doon biral: «Dees koo yóbbu ni xar mu ñuy rendiji; mbete mburt mu ne cell ci kanam ki koy wat, ubbiwul gémmiñam.
33 In his humiliation justice was denied him. Who can describe his generation? For his life is taken away from the earth." Ci biir toroxteem lañu ko xañ dëggam; kuutaayam nag, ana ku ci mana wax? Ndegam bakkanam lañu toxale kaw suuf.»
34 The eunuch said to Philip, "Tell me, of whom does the prophet say this—himself, or someone else?" Jaraaf ja ne Filib: «Yaw laay laaj, ci kan la yonent bi wax lii? Boppam lay wax am keneen?»
35 Philip opened his mouth and, starting from this Scripture, told him the good news about Jesus. Filib daldi àddu, tàmbalee ci dog boobu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36 Traveling the road, they reached water, and the eunuch said, "Look, water! What stops me from being baptized?" Ba loolu amee ñu topp yoon wi, ba yem ci am ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngii, ana lu tee ma sóobu ci?»
37 Not in this edition Filib ne ko: «Soo gëmee ci sa léppi xol, sañ nga ko.» Mu ne ko: «Gëm naa ne Yeesu Almasi bi mooy Doomu Yàlla.»
38 He ordered the chariot to stop; both went down into the water, Philip and the eunuch, and Philip baptized him. Ci kaw loolu jaraaf ja santaane ñu taxawal watiir ba; Filib ak jaraaf ja wàcc, ñu dugg ñoom ñaar ca ndox ma, Filib sóob ko ca.
39 When they came up out of the water, the Spirit of our Father snatched Philip away; the eunuch never saw him again, but went on his way rejoicing. Naka lañu génne ca ndox ma, ngelawal Boroom bi ne cas Filib, yóbbu, jaraaf ja gisatu ko. Teewul mu topp yoonam, ànd ak mbég.
40 Philip found himself at Azotus. He traveled through, announcing the good news in every town until he reached Caesarea. Filib moom, dëkk ba ñuy wax Asot la gisaat boppam. Mu wéye di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkkoo dëkk, ba àgg Sesare.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]