Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 9 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 But Saul, still breathing threats and murder against the Lord's disciples, went to the high priest, Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkooka jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,
2 and asked him for letters to Damascus's synagogues, so that if he found any of the Way, men or women, he could bring them bound to Jerusalem. di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi leen Yerusalem.
3 As he traveled and was approaching Damascus, suddenly a light from heaven flashed around him. Naka la Sóol dem ba jub Damaas, ag leer fettaxe asamaan, jekki ne ràyy ci kawam.
4 He fell to the ground and heard a voice saying, "Saul, Saul, why are you persecuting me?" Mu ne dàll ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bunduxataal?»
5 He said, "Who are you, Lord?" And he said, "I am Jesus, whom you are persecuting. Mu ne: «Yaay kan Sang bi?» Mu ne: «Man maay Yeesu, mi ngay bunduxataal.
6 But rise and enter the city, and you will be told what you must do." Léegi nag, jógal, dugg ci dëkk bi, dees na la wax li nga wara def.»
7 The men traveling with him stood speechless, hearing the voice but seeing no one. Nit ña ànd ak moom a nga taxaw, jommi ba ne cell; dégg nañu baat bi te gisuñu kenn.
8 Saul got up from the ground, but with eyes open he saw nothing; they led him by the hand and brought him into Damascus. Sóol jóg, xippi, gisul dara; ñu daldi koy wommat, dugal ko biir Damaas.
9 He was blind for three days and neither ate nor drank. Diiru ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
10 A disciple named Ananias lived in Damascus. In a vision the Lord said, "Ananias." He answered, "Here I am, Lord." Ab taalibe bu ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Sang bi feeñu ko, ne ko: «Anañas!» Mu ne ko: «Maa ngi, Sang bi.»
11 The Lord said to him, "Get up, go to the street called Straight, and look in Judas's house for a man from Tarsus named Saul—he is praying, Sang bi ne ko: «Demal ba ca mbedd ma ñuy wax mbedd mu Jub, te nga seet ca kër Yuda ku ñuy wax Sóol te dëkke Tàrs. Ma ngay ñaan.
12 and in a vision has seen a man named Ananias come in and place his hands on him so he may see again." Dafa gis cim peeñu ku ñuy wax Anañas duggsi, teg ko loxo, ngir mu dellu di gis.»
13 Ananias replied, "Lord, many have told me about this man—the harm he's done your holy ones in Jerusalem. Anañas nag ne ko: «Sang bi, maa dégge ci ñu bare mbirum kooku, ñu seede mboolem jëf ju bon ji mu def say nit ñu sell ci biir Yerusalem.
14 And here he has authority from the chief priests to bind all who call on your name." Te moo yor ndigal lu tukkee ci sarxalkat yu mag yi, ngir yeewlu képp kuy tudd saw tur.»
15 But the Lord said to him, "Go, for this man is my chosen instrument to carry my name before nations, kings, and Israel's people. Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jàmbur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israayil.
16 For I will show him how much he must suffer for the sake of my name." Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»
17 Ananias went and entered the house. He laid hands on Saul and said, "Brother Saul, the Lord Jesus—who appeared to you on the road you traveled—sent me so you may see again and be filled with the Holy Spirit." Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te fees ak Noo gu Sell gi.»
18 Immediately something like scales fell from his eyes, and he could see again. He got up and was baptized, Ca saa sa lu mel niy waasintóor wadde ca bët ya, mu dellu di gis. Mu daldi jóg, ñu sóob ko ci ndox.
19 and after eating, he regained his strength. For some days he was with the disciples in Damascus, Ba loolu wéyee, mu lekk, doora am doole. Sóol toog na ak taalibe ya ca Damaas ay fan.
20 and immediately he began proclaiming Jesus in the synagogues, that he is the Son of our Father. Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jànguy Yawut ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21 All who heard were amazed and said, "Isn't this the man who caused such havoc in Jerusalem among those calling on this name? And hasn't he come here for this: to bring them bound before the chief priests?" Mboolem ña ko dégg, daldi waaru, naan: «Xanaa du kii moo doon bóom ñiy tudd woowu tur ci Yerusalem? Du moo fi dikkoon, ngir yeewlu leen, yóbbu ci sarxalkat yu mag yi?»
22 But Saul grew stronger still, bewildering the Jews living in Damascus by proving this one is the Christ. Teewul Sóol gëna am manoore, ba far jaaxal Yawut ñi dëkke Damaas, di firndeel ne Yeesu mooy Almasi bi.
23 After many days had passed, the Jews plotted to kill him, Ba ñu ca tegee ab diir bu xawa yàgg, Yawut yi féncoo, ngir reylu ko.
24 but Saul learned of their plot; they watched the gates day and night to kill him, Sóol nag yég seen mébét. Guddi ak bëccëg lañu doon wattu bunti dëkk ba, ngir bóom ko.
25 but at night his disciples lowered him through the wall in a basket. Teewul taalibe yi yeb ko ag guddi ci ag dàmba, jàlle ko ca wàllaa tata ba, yoor ko.
26 Arriving in Jerusalem, he tried to join the disciples, but all feared him, not believing he was a disciple. Ba Sóol agsee Yerusalem, jéem naa jaxasook taalibe yi, waaye ñépp a ko ragal, ndax ñàkka gëm ag taalibeem.
27 But Barnabas took him to the apostles and explained how Saul had seen the Lord on the road, who spoke to him, and how in Damascus he had spoken boldly in Jesus' name. Ci kaw loolu Barnabas ànd ak moom, yóbbu ko ca ndaw ya. Barnabas nettali leen, ni Sóol gise Sang bi ca yoon wa, ba mu wax ak Sóol, ak fit wa Sóol waaree ca Damaas ci turu Yeesu.
28 So he was with them, moving freely about Jerusalem, speaking boldly in the name of the Lord. Ba loolu amee Sóol ànd ak ndaw yi di dem aka dikk ci biir Yerusalem, di waaree aw fit ci turu Sang bi.
29 He spoke and debated with the Hellenists, but they were seeking to kill him. Mu boole ci di wax aka werante ak Yawut ñiy làkk gereg, te ñoom ñu di ko fexee rey.
30 When the brothers learned this, they brought him down to Caesarea and sent him off to Tarsus. Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbaale Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
31 So the church throughout Judea, Galilee, and Samaria had peace and was strengthened; walking in the fear of the Lord and comforted by the Holy Spirit, it multiplied in number. Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
32 As Peter traveled among all the believers, he also went down to the holy ones living in Lydda. Piyeer mi doon wër fu nekk nag, am na bés mu jaare ca ñu sell ña dëkke Lidd.
33 There he found a man named Aeneas, bedridden for eight years, who was paralyzed. Mu gis foofa waa ju ñuy wax Ene. Fekk na diiru juróom ñetti at, cib lal rekk lay tëdd ndax yaram wu làggi.
34 Peter said to him, "Aeneas, Jesus Christ heals you. Get up, make your bed." He got up at once. Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi bi wéral na la; jógal, lalal sa bopp.» Mu jóg ca saa sa.
35 And all who lived in Lydda and Sharon saw him, and they turned to the Lord. Mboolem waa diiwaani Lidd ak jóoru Saron nag gis ko, waññiku topp Sang bi.
36 In Joppa lived a disciple named Tabitha, meaning Dorcas. She was full of good works and help for the poor. Dëkk ba ñuy wax Yafa, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.
37 In those days she got sick and died; they washed her and laid her in an upstairs room. Ci fan yooyu, mu daanu wopp, daldi faatu. Ñu sang ko, dugal ko ca néegu kaw taax ma.
38 Since Lydda was near Joppa, disciples who heard Peter was there sent two men to him, urging, "Don't delay coming to us." Ci biir loolu taalibe yi dégg ne Piyeer a nga Lidd, te Lidd sorewul Yafa. Ñu yebal ñaari nit ca moom, ngir ñaan ko mu ñëw te baña yeex.
39 So Peter got up and went with them. When he arrived, they brought him to the upper room. All the widows stood beside him crying, showing the tunics and cloaks Dorcas had made while with them. Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Gëmkati jëtun ñépp a nga doon jooyoo. Ñu yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.
40 Peter sent everyone out, knelt, and prayed. Turning to the body, he said, "Tabitha, get up." She opened her eyes, saw Peter, and sat up. Ci kaw loolu Piyeer dàq ñépp ca biti. Mu sukk, ñaan, daldi walbatiku jublook néew bi, ne: «Tabita, jógal!» Mu ne xiféet, gis Piyeer, jóg toog.
41 Giving her his hand, he raised her up. Calling the holy ones and the widows, he presented her alive. Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Ba loolu amee Piyeer woo ñu sell ña, ak jëtun ña, won leen ndaw sa, muy dund.
42 And it became known throughout all Joppa, and many believed in the Lord. Mbir ma nag siiw ca Yafa gépp, ñu bare gëm Sang bi.
43 And he stayed in Joppa for many days with a man named Simon, a tanner. Gannaaw loolu Piyeer dal na Yafa ay fan, kër wullikat bu ñuy wax Simoŋ.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]