Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 27 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Jotham was twenty-five when he became king; he reigned sixteen years in Jerusalem. His mother was Jerushah, daughter of Zadok. Yotam amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu, te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Yaayam mooy Yerusa doomu Cadog.
2 He did right in the eyes of our Father, as his father Uzziah had done—except he did not enter the temple of our Father. Yet the people still acted wrongfully. Muy def li Aji Sax ji rafetlu; mboolem na Osiyas baayam daan defe la daan defe. Waaye nag duggul ca kër Aji Sax ji. Teewul nag askan wa di defug yàqute ba tey.
3 He built the Upper Gate of our Father's house, and built much on Ophel's wall. Moom moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar, te tata ba ca tundu Ofel, tabax na ca lu bare.
4 He built cities in Judah's highlands, and in the forests he built forts and towers. Ay dëkk it tabax na ko ca tundi Yuda, te gott ya, tabax na ca kër yu tata wër ak seeni sooroor.
5 He fought the king of the Ammonites and defeated them. That year the Ammonites gave him 7,500 pounds of silver, 50,000 bushels of wheat, and 50,000 of barley—the same in the second and third years. Moom it moo xareek buurub Amoneen ña, duma leen, ba Amoneen ña jox ko atam fanweeri barigoy xaalis ak ñeent, ak fukki barigoy bele ak benn; lors it, fukki barigo ak benn. Loolu la ko Amoneen ña indil atam, indilaatal ko ko ca déwén sa, indilatil ko ko ca déwén-jéeg sa.
6 So Jotham grew strong, because he kept his conduct right before his Father. Yotam mujj na am doole, ndax pastéef ga mu daan doxe fa kanam Yàllaam Aji Sax ji.
7 The rest of Jotham's acts, all his wars and deeds, are written in the Book of the Kings of Israel and Judah. Li des ci mbiri Yotam ak mboolem ay xareem ak ay jëfinam, ma nga binde ca téere ba ñu dippee Buuri Israayil ak Yuda.
8 He was twenty-five years old when he became king, and he reigned sixteen years in Jerusalem. Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu, te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem.
9 Jotham rested with his ancestors; they buried him in the city of David, and his son Ahaz reigned in his place. Gannaaw gi, Buur Yotam saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Axas doomam moo falu buur, wuutu ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]