Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 28 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Ahaz became king at twenty; he reigned sixteen years in Jerusalem. He did not do right in our Father's eyes, as his ancestor David had. Ñaar fukki at la Axas amoon ba muy falu buur. Nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem, waaye deful li Aji Sax ji rafetlu, na ko maamam Daawuda baaxoo woon.
2 Instead, he walked in the ways of Israel's kings and cast metal idols for the Baals. Ca tànki buuri Israayil la topp. Ay jëmmi weñ gu ñu xelli sax, móollu na leen, ngir tuur yi ñuy wax Baal.
3 He burned incense in Ben-Hinnom Valley and burned his sons in fire, copying detestable practices of the nations our Father drove out before Israel. Moo taal cuuraay ca xuru Ben Inom. Doomam yu góor sax def na leen sarax, lakk leen ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israayil.
4 He sacrificed and burned incense on the high places, the hills, and under every leafy tree. Rendi nay sarax, taal na cuuraay ca bérebi jaamookaay ya ak ca kaw tund ya ak mboolem ker garab gu naat.
5 So our Father gave him to Aram's king, who struck him, took many captives to Damascus; he was also given to Israel's king, who struck him a heavy blow. Aji Sax ji Yàllaam nag teg ko ca loxol buurub Siri, ñu duma ko, jël ca moom mbooloom jaam yu bare, yóbbu leen Damaas. Loxol buurub Israayil itam tegees na ci Axas, mu duma ko duma yu réy.
6 Pekah son of Remaliah killed 120,000 brave men of Judah in one day, because they abandoned our Father, the God of their ancestors. Buurub Israayil Peka doomu Remalya rey na ca Yuda, ci benn bés, téeméer ak ñaar fukki junniy (120 000) nit, ñépp di ñeyi xare, ndax ñoo wacc Aji Sax ji seen Yàllay maam.
7 Zichri, an Ephraim warrior, killed Maaseiah the king's son, Azrikam the palace commander, and Elkanah, the king's second. Sikkri jàmbaaru Efrayim itam moo rey Maaseya doomu Buur ak Asrikam fara kër buur ak Elkana bummeem.
8 Israel captured 200,000 relatives—women, sons, daughters—and much plunder, carrying it off to Samaria. Bànni Israayil nag jàpp ca seen bokki Yudeen ña ñaari téeméeri junniy (200 000) jigéen ak gone yu góor ak yu jigéen. Alal ju bare itam, jële nañu ko ca ñoom, yóbbu ko Samari.
9 Oded, a prophet of our Father, was there. He met the army returning to Samaria: "See, our Father, the God of your ancestors, was angry with Judah, so he handed them to you. But you killed them with rage reaching heaven. Foofa ca Samari nag, ab yonentu Aji Sax ji ma nga fa woon, ñu di ko wax Odedd. Moo dikk dajeek gàngooru xare gay ñibbisi Samari. Mu ne leen: «Seen Yàllay maam Aji Sax jaa ngii sànju ci kaw Yuda, ba teg leen ci seen loxo, waaye xadar ju àkki ba asamaan ngeen leen faxase.
10 Now you intend to enslave Judah and Jerusalem's people, male and female. Aren't you yourselves guilty of sins against your Father? Léegi nag, waa Yuda ak Yerusalem ngeen ne seeni jaam ngeen leen di def, góor ak jigéen? Yeen itam déy, xanaa tooñuleen seen Yàlla Aji Sax ji?
11 Now listen: send back the relatives you captured, for our Father's fierce anger is on you." Dégluleen ma fii nag! Dellooleen mbooloom jaam yi ngeen jàpp, jële leen ca seen bokki Yudeen, ndax kat tàngooru sànjum Aji Sax jaa ngi leen di yoot.»
12 Some Ephraimite chiefs—Azariah son of Johanan, Berechiah son of Meshillemoth, Jehizkiah son of Shallum, Amasa son of Hadlai—opposed those coming from battle. Ba loolu amee ñenn ca njiiti Efraymeen ña; Asaryaa doomu Yoxanan ak Berekya doomu Mesilemot ak Esekiyas doomu Salum ak Amasa doomu Xadlay, ñoo jóg jàkkaarlook mbooloo ma jóge ca xare ba.
13 "Don't bring the captives here," they said. "You plan to add to our sins and guilt against our Father. Our guilt is already great, and fierce anger hangs over Israel." Ñu ne leen: «Buleen fi indi mbooloom jaam yi, ndax tooñ Aji Sax ji lay doon ci nun. Dangeena nara yokk sunuy bàkkaar ak sunuy tooñ, te sunuy tooñ xasa bare, ba tàngooru sànj di yoot Israayil?»
14 So the soldiers handed the captives and plunder in front of the officials, before the whole assembly. Ci kaw loolu boroom ngànnaay ya yiwi jaam ya, joxe cëxëtoo ma fa kanam njiit ya ak mboolem ndaje ma.
15 The named men took the captives and clothed all the naked from the plunder. They gave them clothes and sandals, food and drink, and anointed them with oil. They set the feeble on donkeys, brought them to their fellow Israelites at Jericho, city of palms, then returned to Samaria. Góor ña ñu jota lim seeni tur nag daldi jël jaam ya. Ña ca def yaramu neen, ñu wodde leen ca yérey cëxëtoo ma. Dañu leena solal yére aki dàll, may leen ñu lekk, naan, diw leen, ña ca néew doole ñépp, ñu waral leen ay mbaam, daldi leen yóbbu Yeriko, dëkkub tàndarma ya, fa seeni bokk. Gannaaw loolu ñu dellu Samari.
16 At that time King Ahaz sent to the king of Assyria for help. Jant yooyu la Buur Axas yeble fa buuru Asiri, ngir ñu wallu ko.
17 The Edomites had invaded Judah once again and carried off captives, Booba Edomeen ñaa dikkaatoon, duma Yuda, jàpp ca ay jaam.
18 while Philistines raided Judah's lowland and Negev towns, seizing Beth-shemesh, Aijalon, Gederoth, Soco, Timnah, and Gimzo with their villages, and settled there. Waa Filisti itam songoon nañu dëkk ya ca suufi tundi Yuda ak bëj-saalumu Yuda. Jotoon nañoo nangu ba sance Bet Semes ak Ayalon ak Gederot ak Soko aki dëkk-dëkkaanam ak Timna aki dëkk-dëkkaanam ak Gimso aki dëkk-dëkkaanam.
19 Our Father humbled Judah because of Ahaz king of Israel, who spread wrongdoing in Judah and betrayed our Father completely. Aji Sax ji moo ko mbugale Yuda ndax Axas buurub Israayil, ndax jëfam ju ëpp ja fa Yuda, ak doge ga mu doge Aji Sax ji worma.
20 Tiglath-pileser king of Assyria came to Ahaz, but Tiglath-pileser brought him trouble instead of help. Ba Tiglaat Pilser buurub Asiri dikkee ca kaw Axas, dooleelsiwu ko, da koo fitnaal.
21 Ahaz stripped our Father's house, the royal palace, and the officials of their treasures, giving them to Assyria's king—yet it brought him no help. Axas wëq kër Aji Sax ji ak këri buur ak jawriñ ña, jox ko buurub Asiri, te loola amalu ko benn njariñ.
22 In his time of distress, this same King Ahaz became even more unfaithful to our Father. Buur Axas moomu, ca janti fitnaam jooju la gënatee doge Aji Sax ji worma.
23 He sacrificed to Damascus's gods, his defeaters, thinking, "Aram's kings' gods helped them; I'll sacrifice to them so they'll help me." But they ruined him and all Israel. Yàllay Damaas ga ko duma, ñoom la defal sarax, te naan: «Gannaaw yàllay buuri Siri ñoo leen di dimbali, ñoom laay sarxalal, ñu dimbali ma.» Waaye yàlla yooyu ñoo indi sànkuteem, moom ak Israayil gépp.
24 Ahaz gathered the articles of our Father's house and cut them to pieces, shut the doors of our Father's house, and set up altars for himself at every corner in Jerusalem. Jumtukaayi kër Yàlla ga la Axas dajale, dogat jumtukaayi kër Yàlla ga, teg ca tëj bunti kër Aji Sax ja, daldi sàkkal boppam ay sarxalukaayi tuur ca mboolem ruqi Yerusalem.
25 In every Judah town he built high places to burn offerings to other gods, angering our Father, the God of his ancestors. Yuda gépp, dëkk ak dëkk, def na fa ay bérebi jaamookaay yu ñuy taalale yeneen yàlla cuuraay, ba merloo Aji Sax ji Yàllay maamam ya.
26 The rest of his deeds and all his ways, first to last, are written in the Book of the Kings of Judah and Israel. Li des ciy mbiram aki jëfinam yu njëkk yaak yu mujj ya, ña nga binde ca téere ba ñu dippee Buuri Yuda ak Israayil.
27 Ahaz rested with his ancestors, buried in Jerusalem, but not in Israel's kings' tombs. His son Hezekiah reigned instead. Gannaaw gi, Buur Axas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca dëkk ba, ca Yerusalem, waaye dencuñu ko ca bàmmeeli buuri Israayil. Esekiyas doomam moo falu buur, wuutu ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]