Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 29 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Hezekiah became king at twenty-five, reigning twenty-nine years in Jerusalem. His mother: Abijah, daughter of Zechariah. Esekiyas ci ñaar fukki atam ak juróom la falu buur, te nguuru na ñaar fukki at ak juróom ñeent, ca péeyu Yerusalem. Yaayam nag mooy Abya doomu Sàkkaryaa.
2 He did right in our Father's eyes, just as his father David had done. Muy def li Aji Sax ji rafetlu, mboolem noonee ko Daawuda maamam daan defe.
3 In his reign's first year, first month, he opened the doors of our Father's house and repaired them. Moom moo ubbi bunti kër Aji Sax ji, defaraat leen, ca atum ndoortel nguuram, ca weer wu njëkk wa.
4 He brought in the priests and the Levites and gathered them in the eastern square. Ci kaw loolu mu woolu sarxalkat yaak Leween ña, ñu daje ca péncum penku ba.
5 He told them, "Hear me, Levites! Dedicate yourselves now, and dedicate our Father's house, the God of your fathers, and remove the filth from the Holy Place. Mu ne leen: «Yeen Leween ñi, dégluleen ma. Sanguleen-set léegi te sellal seen kër Yàllay maam yi, Aji Sax ji, te ngeen jële jépp sobe fi néeg bu sell bi.
6 Our ancestors were unfaithful, doing evil in our Father's eyes; they abandoned him, turned their faces from our Father's dwelling, and turned their backs. Ndax kat sunuy maam a fecci worma, ñoo def lu sunu Yàlla Aji Sax ji ñaawlu. Ñoo ko wacc, walbati seen kanam, fuuylu màkkaanu Aji Sax ji, wone gannaaw.
7 They also shut the entrance hall doors, extinguished the lamps, and did not burn incense or offer burnt offerings in the sanctuary to our Father, the God of Israel. Ñoo tëj bunti mbaaru kër Yàlla ga, fey làmp ya; cuuraay, taalatuñu ko, saraxi rendi-dóomal joxeetuñu ko fi néeg bu sell bi, ñeel Yàllay Israayil.
8 So our Father's anger fell on Judah and Jerusalem, making them an object of terror, horror, and scorn, as you see with your own eyes. Moo tax sànjum Aji Sax ji dal ci kaw Yuda ak Yerusalem, ba mu def leen misaal mu daw yaram mu ñuy muslu, ni ngeen ci tege seen bëti bopp.
9 For our fathers fell by the sword; our sons, daughters, and wives are captive for this. Moo tax it sunuy maam ay saamar daan leen; sunuy doom, góor ak jigéen, ak sunuy jabar dugg njaam ndax loolu.
10 Now I intend to make a covenant with our Father, the God of Israel, so his fierce anger turns from us. Léegi nag sama xol laa yéenee fasoo kóllëre ak Aji Sax ji Yàllay Israayil, ngir mu moyale nu sawaras sànjam.
11 My sons, don't be negligent now—our Father chose you to stand before him, serve him, be his servants, and burn incense." Kon nag soppe yi, buleen sàggan, ndax yeen la Aji Sax ji tànn, ngir ngeen taxaw fi kanamam, di ko liggéeyal, di ay liggéeykatam, te di ko taalal cuuraay.»
12 The Levites stood: Kohathites—Mahath, Amasai's son, and Joel, Azariah's son; Merarites—Kish, Abdi's son, and Azariah, Jehallelel's son; Gershonites—Joah, Zimmah's son, and Eden, Joah's son; Ba mu ko defee Leween ña jóg. Ña bokk ca Keyateen ña di Maxat doomu Amasay ak Yowel doomu Asaryaa; ña bokk ca Merareen ña di Kis doomu Abdi ak Asaryaa doomu Yewalelel; ña bokk ca Gersoneen ña di Yowax doomu Simma ak Eden doomu Yowax;
13 of the sons of Elizaphan, Shimri and Jeiel; of the sons of Asaph, Zechariah and Mattaniah; ña sëtoo ca Elicafan di Simri ak Yewel; ña sëtoo ca Asaf di Sàkkaryaa ak Mataña;
14 of the sons of Heman, Jehiel and Shimei; and of the sons of Jeduthun, Shemaiah and Uzziel. ña sëtoo ca Eman di Yexyel ak Simey; ña sëtoo ca Yedutun di Semaya ak Usyel.
15 They gathered their brothers, made themselves holy, and went to clean our Father's house, as the king commanded by our Father's words. Ñu woo seeni bokk nag, ñu daje, sangu-set, daldi dikk, na ko Buur santaanee, ak na ko kàdduy Aji Sax ji tegtalee, ngir setal kër Aji Sax ja.
16 The priests entered our Father's inner house to cleanse it, bringing all the impurity they found in our Father's temple out to the courtyard. The Levites carried it out to the Kidron brook. Sarxalkat ya dugg ca biir kër Aji Sax ja, ngir setal ko. Ñu daldi dindi mboolem sobe ju ñu fekk ca biir kër Aji Sax ja, yóbbu ko ca ëttu kër Aji Sax ja, Leween ña jële ko fa, génne ca biti, sànni ko ca xuru Sedoron.
17 They began dedicating the first day of month one; by the eighth day of that month, they reached our Father's entrance hall. They dedicated the house of our Father eight days, finishing the sixteenth day of month one. Benn fan ca ndoortel weeru at ma lañu tàmbalee sellal. Juróom ñetti fan ca weer wa, ñu agsi ca mbaaru néeg bu mag bu Aji Sax ja. Ñu teg ca sellal kër Aji Sax ja ci yeneen juróom ñetti fan, ca fukki fan yaak juróom bennu ndoortel at ma, ñu sottal.
18 Then they came in to King Hezekiah and said, "We have cleaned all of our Father's house—the altar of burnt offering with all its utensils, and the table of the Bread of the Presence with all its utensils. Ba loolu amee ñu dem ba ca Buur Esekiyas, ne ko: «Setal nanu kër Aji Sax jépp, ba ca sarxalukaayu rendi-dóomal ba ak mboolemi jumtukaayam ak taabal ja mburum teewal may tege ak mboolemi jumtukaayam.
19 All the utensils King Ahaz discarded during his unfaithful reign we have prepared and dedicated—they stand before our Father's altar." Mboolem jumtukaay ya Buur Axas xalaboon ca nguurug ñàkke wormaam, delloo nanu ko, sellal ko. Ma nga noonu fa kanam sarxalukaayu Aji Sax ji.»
20 King Hezekiah rose early, gathered the city's officials, and went up to our Father's house. Buur Esekiyas teela xëy, woolu kàngami dëkk ba, daldi jubal kër Aji Sax ja.
21 They brought seven bulls, seven rams, seven lambs, seven male goats as a sin offering for the kingdom, sanctuary, and Judah, and he commanded Aaron's sons, the priests, to offer them on our Father's altar. Ñu yóbbu juróom ñaari yëkk ak juróom ñaari kuuy yu mag ak juróom ñaari kuuy yu ndaw ak juróom ñaari sikket, ngir saraxu póotum bàkkaar, ci wàllu nguur gi ak kër gu sell gi ak waa Yuda. Buur nag ne sëti Aaróona yay sarxalkat ya, ñu joxe sarax yooyu ca sarxalukaayu Aji Sax ja.
22 They killed the bulls; the priests took the blood and splashed it on the altar. They killed the rams and splashed the blood on the altar, then killed the lambs and splashed the blood on the altar. Ñu daldi rendi nag ya, sarxalkat ya jël deret ja, wis-wisal ko ca sarxalukaay ba. Gannaaw loolu ñu rendi kuuy yu mag ya, wis-wisal deret ja ca sarxalukaay ba. Gannaaw loolu ñu rendi kuuy yu ndaw ya, wis-wisal deret ja ca sarxalukaay ba.
23 They brought the sin-offering goats before the king and assembly, and laid their hands on them. Ba loolu amee ñu indi sikketi póotum bàkkaar ya fa kanam Buur ak ndaje ma, ñu teg sikket ya seeni loxo.
24 The priests slaughtered them and made a sin offering with their blood on the altar to atone for all Israel, because the king had ordered the burnt offering and sin offering for all Israel. Sarxalkat ya daldi rendi sikket ya, def seen deret saraxu póotum bàkkaar ca sarxalukaay ba, sotti ko ca, ngir jote ko mboolem Israayil, ndax mboolem Israayil la Buur tudde saraxu rendi-dóomal ba ak saraxu póotum bàkkaar ba.
25 He stationed the Levites in our Father's house with cymbals, harps, and lyres, as David, Gad the king's seer, and Nathan the prophet commanded—for the command came from our Father through his prophets. Ci kaw loolu mu taxawal Leween ña ca kër Aji Sax ji, aki tabala aki riiti aki xalam. Loolu dëppook santaaneb Daawuda ak Gàdd boroom peeñu ba ak Natan yonent ba, te di santaane bu bawoo fa Aji Sax ji, ay yonentam jottali ko.
26 The Levites stood with the instruments of David, and the priests with the trumpets. Leween ña nag taxaw ak jumtukaayi xumbéeni Daawuda ya, ñook sarxalkat yaak liit ya.
27 Hezekiah ordered the burnt offering on the altar; when it began, the song of our Father began too, with the trumpets and the instruments of David, king of Israel. Esekiyas joxe ndigal ne ñu joxe ca sarxalukaay ba saraxu rendi-dóomal ba. Naka lañu tàmbali rendi-dóomal ba, jàngi Aji Sax ja tàmbali, ànd ak liit ya ak jumtukaayi xumbéeni Daawuda buurub Israayil.
28 The whole assembly bowed, the singers sang, the trumpeters sounded, until the burnt offering was finished. Ndaje mépp sujjóot, woy yay jib, liit ya jolli, ba saraxu rendi-dóomal bépp sotti.
29 When the offering ended, the king and all present with him bowed and worshiped. Ba rendi-dóomal ba noppee, Buur ak mboolem ña ànd ak moom sukk, daldi sujjóot.
30 King Hezekiah and the officials had the Levites praise our Father with words from David and Asaph the seer. They sang for joy, bowed low, and worshiped. Gannaaw loolu Buur Esekiyas ak jawriñ ña ne Leween ña, ñu sàbbaale Aji Sax ji, kàdduy Daawuda yaak Asaf boroom peeñu ba. Mbég mu réy lañu sàbbaale, daldi sujjóot.
31 Then Hezekiah said, "You have now dedicated yourselves to our Father. Come near, bring sacrifices and thank offerings to our Father's house." So the assembly brought sacrifices and thank offerings; all willing hearts brought burnt offerings. Esekiyas teg ca ne mbooloo ma: «Léegi nag, ba ngeen sangoo-set, Aji Sax ji jagoo leen, dikkleen indi saraxi jur yeek saraxi canti biir jàmm ci kër Aji Sax ji.» Ndaje ma indi ay saraxi jur ak saraxi canti biir jàmm, mboolem ña am yéeney xol bu ni tollu it, indi ay saraxi rendi-dóomal.
32 The assembly brought seventy bulls, one hundred rams, 200 lambs—all as a burnt offering to our Father. Ba loolu amee limu saraxi rendi-dóomal ya ndaje ma indi di juróom ñaar fukki (70) jur gu gudd, ak téeméeri (100) kuuy yu mag, ak ñaari téeméeri (200) kuuy yu ndaw, loolu lépp di rendi-dóomal bu ñeel Aji Sax ji.
33 And the consecrated offerings were 600 bulls and 3,000 sheep. Yeneen sarax yu sell ya ñu def di juróom benni téeméeri (600) yëkk ak ñetti junniy (3 000) gàtt.
34 The priests were too few to skin all the burnt offerings, so their Levite brothers helped them until the work was done and until the priests made themselves holy; the Levites were more honest in heart to make themselves holy than the priests. Xanaa sarxalkat ya daal ñoo néewoon ba manuñoo fees juri saraxi rendi-dóomal ba bépp. Seen bokki Leween ña dimbali leen ca, ba liggéey ba sotti, ba sarxalkat ya ca des sangu-set, ndax Leween ña ñoo gënoona yebu sarxalkat ya ci sanguji-set.
35 Besides the many burnt offerings, there was fat from peace offerings and drink offerings for them. So the service of our Father's house was restored. Saraxi rendi-dóomal ya bare woon na, te bokkewul ak nebbonu saraxi canti biir jàmm ya ak saraxi tuuru yay ànd ak rendi-dóomal ya. Noonu lañu taxawalaate liggéeyub kër Aji Sax ja.
36 Hezekiah and all the people rejoiced over what our Father prepared for them, since it happened suddenly. Esekiyas ak askan wa wépp nag ñoo bége la Yàlla defal askan wa, ndax na mbir ma gaawa sottee te waajeesu ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]