Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 30 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Hezekiah sent word to all Israel and Judah, and wrote letters to Ephraim and Manasseh, to come to the house of our Father in Jerusalem to keep the Passover to our Father, the God of Israel. Ba mu ko defee Esekiyas yónnee ca mboolem Israayil ak Yuda. Ay bataaxal sax bind na ko giiri Efrayim ak Manase, ngir ñu dikk ca kër Aji Sax ja ca Yerusalem, ngir amal màggalu bésub Mucc, ñeel Aji Sax ji Yàllay Israayil.
2 The king, his officials, and the whole assembly in Jerusalem had decided to keep the Passover in the second month, Fekk na Buur aki jawriñam, ak mboolem ndaje ma féncoo fa Yerusalem, ba mànkoo ci amal bésub Mucc ca ñaareelu weeru at ma.
3 since they could not keep it then, because too few priests had made themselves holy and the people had not gathered at Jerusalem. Manuñu ko woona amal ca bésam, ndax sarxalkat ya sangu-set doyuñu woon, te askan wa dajeegul woon Yerusalem.
4 The plan seemed right to the king and to all the assembly, Mébétum amal bésub Mucc nag di lu Buur ak ndaje ma mépp rafetlu.
5 so they sent a proclamation throughout Israel, from Beersheba to Dan, that the people should come to Jerusalem to keep the Passover to our Father, the God of Israel; for they had not kept it together in great numbers as written. Ci kaw loolu ñu yékkati ab dogal, ngir yéene fa Israayil gépp, dale Beerseba ga ca bëj-saalum, ba Dan ga ca bëj-gànnaar, ngir ñu dikk amal fa Yerusalem, bésub Mucc, ñeel Yàllay Israayil, ndax barewul woon ñu ko sàmm, na ñu ko binde ci yoon.
6 The couriers went through all Israel and Judah with letters from the king and his officials, ordered by the king: "Children of Israel, return to our Father, the God of Abraham, Isaac, and Israel, so he may return to the remnant of you who survived and escaped the power of the kings of Assyria. Ba loolu amee ndaw ya dem ak ay bataaxal yu tukkee ca Buur aki jawriñam. Ñu yéene ci ndigalal Buur, ca mboolem Israayil ak Yuda, na ko Buur santaanee ne: «Yeen bànni Israayil, dellusileen ci Aji Sax ji, Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Israayil, ba mu délsi ci yeen ñi des, te rëcce ca loxoy buuri Asiri.
7 Do not be like your fathers and brothers, who were unfaithful to our Father, the God of their fathers, so he made them a desolation, as you see. Buleen mel ni seeni maam ak seen bokk yi doge Aji Sax ji seen Yàllay maam worma, ba mu wacce leen sànkute gu daw yaram, ni ngeen ko gise.
8 Don't be stubborn like your fathers; give yourselves to our Father and come to his sanctuary, which he dedicated forever, and serve your Father, so his fierce anger turns from you. Léegi nag buleen sajju loos na seeni maam. Joxleen Aji Sax ji loxo, te dikk fi këram gu sell gi mu sellal ba fàww, te ngeen jaamu Aji Sax ji seen Yàlla, ngir sawaras sànjam dëddu leen.
9 For if you return to our Father, your brothers and your children will find compassion from their captors and return to this land. For your Father is gracious and merciful; he will not turn his face from you if you return to him." Ndax kat su ngeen dellusee ci Aji Sax ji, seeni bokk ak seeni doom dinañu dajeek yërmandey ña leen jàpp njaam, te dinañu dellusi fi réew mii, nde Aji Sax ji seen Yàlla mooy boroom yiw ak yërmande, te du leen dëddu, su ngeen dellusee ci moom.»
10 The couriers went from city to city through Ephraim and Manasseh to Zebulun, but the people laughed at them and mocked them. Noonu la ndaw ya wëre dëkkoo dëkk, ca réewum Efrayim ak Manase, ba fa diiwaanu Sabulon. Nit ña nag di leen reetaan aka ñaawal.
11 Even so, some from Asher, Manasseh, and Zebulun humbled themselves and came to Jerusalem. Teewul mu am ca Asereen ñaak Manaseen ñaak Cabuloneen ña, ñennat ñu toroxlu, ba dikk Yerusalem.
12 The hand of our Father was also on Judah, giving them one heart to do what the king and officials commanded by the word of our Father. Fa Yuda itam loxol Yàlla jaare fa, ba may leen genn pastéefu xol, ngir déggal kàddug Aji Sax ji ci jëfe santaaneb Buur ak jawriñ ña.
13 A very large assembly gathered at Jerusalem to keep the Feast of Bread Without Yeast in the second month. Mbooloo mu mag nag daje Yerusalem, ngir amal màggalu Mburu mu amul lawiir, ca ñaareelu weeru at ma, muy ndaje mu réy lool.
14 They set to work and removed the altars in Jerusalem, and they took away all the incense altars, throwing them into the Kidron Valley. Ñu daldi dindi sarxalukaayi tuur ya ca biir Yerusalem, mboolem sarxalukaayi cuuraay ya it, ñu jële leen fa, sànni ca xuru Sedoron.
15 They slaughtered the Passover lamb on the fourteenth of the second month. The priests and Levites were ashamed, so they dedicated themselves and brought burnt offerings to the house of our Father. Fukki fan ak ñeent ca ñaareelu weer wa, ca lañu rendi gàttub bésub Mucc. Ba loolu amee sarxalkat ya ak Leween ña am kersa. Ñu sangu-set, daldi indi ay saraxi rendi-dóomal fa kër Aji Sax ji.
16 They stood at their posts by custom, as the Law of Moses the man of God requires; the priests sprinkled the blood the Levites handed them. Ci kaw loolu ñu taxaw seen béreb ba ñuy taxawe, na ñu ko aadawoo, te mu dëppook yoonu Musaa, góorug Yàlla ga. Sarxalkat ya nag nangoo deret ja ca loxol Leween ña, wis-wisal ko ca sarxalukaay ba.
17 Many in the assembly had not dedicated themselves, so the Levites were in charge of killing the Passover lambs for everyone unclean, to dedicate them to our Father. Booba ñu bare ca mbooloo ma sanguwuñu woon set. Moo tax Leween ña rendi gàtti bésub Mucc yu mboolem ña setul woon ba manuñoo sellal seen sarax, ñeel Aji Sax ji.
18 A large number of the people, many from Ephraim, Manasseh, Issachar, and Zebulun, had not purified themselves, yet ate the Passover, though not as written. But Hezekiah prayed for them: "May our good Father pardon everyone, La ëpp ca askan wa it, te ñu bare bokk ca Efraymeen ñaak Manaseen ñaak Isakareen ñaak Cabuloneen ña, setluwuñu woon, waaye lekk nañu ca saraxi bésub Mucc ba, te loolu dëppoowul ak li ñu bind ci yoon. Waaye Esekiyas moo leen ñaanal, ne: «Aji Sax ji cig mbaaxam, yal na baaxe ag njot
19 who sets his heart to seek our Father, the God of his fathers, though not clean by the sanctuary's rules." képp ku yeboo xolam ci jaamu Yàlla, Aji Sax ji Yàllay maamam ya, doonte àndul ak cet gi kër gu sell gi laaj.»
20 And our Father listened to Hezekiah and healed the people. Aji Sax ji nangul Esekiyas, ba bàyyi askan wa, ñu ànd ak wér.
21 The Israelites in Jerusalem kept the Feast of Bread Without Yeast seven days with great joy, and day by day the Levites and priests praised our Father with loud instruments resounding to him. Ba loolu amee bànni Israayil ga teew Yerusalem amal màggalu Mburu mu amul lawiir ci juróom ñaari fan, ànd ceek mbég mu réy. Leween ñaak sarxalkat ya di sàbbaal Aji Sax ji, bés bu nekk, tey jibal jumtukaay yu xumb lool, ñeel Aji Sax ji.
22 Hezekiah spoke encouragingly to all the Levites skilled in serving our Father. For seven days they ate their festival share, offering peace offerings and giving thanks to our Father, the God of their fathers. Esekiyas nag yokk pastéefu xolu mboolem Leween ña yebu lool ci mbiri Aji Sax ji. Ñu xéewlu ca sarax ya diiru juróom ñaari fan, di joxe saraxi cant ci biir jàmm, tey sant Aji Sax ji seen Yàllay maam ya.
23 Then the whole assembly agreed to keep the feast another seven days, and they kept it seven more days with joy. Ci kaw loolu ndaje ma mépp mànkoo ci amal yeneen juróom ñaari fani màggal, ñu amalaat juróom ñaari fani mbég,
24 Hezekiah king of Judah gave the assembly 1,000 bulls and 7,000 sheep, and the officials gave 1,000 bulls and 10,000 sheep, and many priests dedicated themselves. ndax fekk na Esekiyas buurub Yuda it génneel ndaje ma junniy (1 000) yëkk yu ndaw ak juróom ñaari junniy (7 000) gàtt, jawriñ ña génneel ndaje ma junniy (1 000) yëkk yu ndaw ak fukki junniy (10 000) gàtt, te fekk na it sarxalkat yu bare sangu-set.
25 All Judah's assembly rejoiced, with the priests, the Levites, the whole assembly that came from Israel, and the foreigners from Israel's land and those living in Judah. Ba mu ko defee ndajem Yuda mépp di bànneexu, ñook sarxalkat ya ak Leween ña, ak mboolem nit ña bawoo Israayil, doxandéem ya jóge réewum Israayil ak ña ca dëkke Yuda.
26 Great joy filled Jerusalem, for nothing like this had happened there since the days of Solomon son of David, king of Israel. Muy mbég mu réy fa Yerusalem, ndax booba ak la jiitu, ba ca janti Suleymaan doomu Daawuda buurub Israayil, lu ni mel xewul fa Yerusalem.
27 The priests and Levites rose to bless the people, and their voice was heard; their prayer reached his holy home in heaven. Ci kaw loolu sarxalkat yay Leween ñaanal askan wa barkeb Aji Sax ji, seen baat jib, seen ñaan ga àkki kaw asamaan, fa màkkaanam mu sell.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]