Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 31 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 When this ended, all Israel present went out to the towns of Judah, smashed the sacred pillars, cut down the Asherah poles, and tore down the high places and altars throughout Judah, Benjamin, Ephraim, and Manasseh, destroying them completely. Then all Israel returned to their towns, each to his own property. Ba loola lépp jeexee, mboolem bànni Israayil ga fa teew ñoo dem ca dëkki Yuda. Ñu toj tuuri doj ya, gor xer ya ñuy jaamoo Asera tuur ma, màbb bérebi jaamookaay ya ak sarxalukaay yu mboolem Yuda ak diiwaani Beñamin ak Efrayim ak Manase, ba sottal. Gannaaw loolu bànni Israayil gépp dellu seeni dëkk, ku nekk ca gox ba mu séddoo.
2 Hezekiah assigned the priests and Levites to their divisions, each by his service, priests and Levites alike, for burnt offerings and peace offerings, to serve, give thanks, and praise in the gates of our Father's camps. Esekiyas nag tabb kuréeli sarxalkat ya ak Leween ña, ku nekk ak kuréelam akub liggéeyam, muy ab sarxalkat mbaa ab Leween, muy itam wàllu saraxi rendi-dóomal, mbaa saraxi cant ci biir jàmm, ak liggéeyu jaamu Yàlla bu jëm ci ay cant aki sàbbaal, ci bunti kër Aji Sax ji.
3 The king gave from his own wealth for the burnt offerings—morning and evening burnt offerings, and those for Sabbaths, new moons, and appointed feasts—as written in our Father's law. Esekiyas dogal itam wàllu Buur wiy jóge ci alalam ngir saraxi rendi-dóomal; rendi-dóomali suba si ak yu ngoon si, ak rendi-dóomal yi ñeel bési Noflaay ak Terutel weer, ak rendi-dóomali bési ndajey màggal yi, ni ñu ko binde ci téereb yoonu Aji Sax ji.
4 He told Jerusalem's residents to give the priests' and Levites' portion, so they could devote themselves to our Father's law. Mu daldi wax askan wa dëkke Yerusalem ne leen ñu joxe wàllu sarxalkat yaak Leween ña, ngir ñooñu mana wéetal yoonu Aji Sax ji.
5 As soon as the order spread, Israelites abundantly gave firstfruits of grain, new wine, oil, honey, and all the field's produce, and brought in the tenth of everything abundantly. Naka la kàddu ga law, bànni Israayil gëna indi seen ndoortel meññeef: bele baak biiñ baak diw gaak lem ja, mboolem lu ñu jële ca tool ya. Cérub fukkeelub lépp ne gàññ, ñu indi ko.
6 The Israelites and Judahites living in Judah's towns also brought the tenth of cattle and sheep, and the tenth of what was dedicated to our Father, piling them in heaps. Ci biir loolu waa Israayil ak waa Yuda, ña dëkke dëkki Yuda indi, ñoom itam, céru fukkeelub jur gu gudd gaak gu gàtt ga, ak céru fukkeelub sarax yu sell ya ñu jagleel Aji Sax ji seen Yàlla. Ñu def ko ay jali jal.
7 They began piling the heaps in the third month, finishing in the seventh. Ca ñetteelu weeru at ma lañu tàmbali jal ya, muy jale ba ca juróom ñaareelu weer wa, ñu sottal.
8 Hezekiah and the officials came, saw the heaps, and blessed our Father and his people Israel. Ba loolu amee Esekiyas ak jawriñ ña dikk, ba gis jal ya, ñu daldi sant Aji Sax ji ak Israayil ñoñam.
9 Hezekiah asked the priests and Levites about the heaps. Esekiyas nag laaj sarxalkat yaak Leween ña ca mbirum jal yooya.
10 Azariah the chief priest, of Zadok's house, answered him, "Since people began bringing contributions into our Father's house, we've eaten well with plenty remaining, for our Father blessed his people, leaving this large surplus." Asaryaa sarxalkat ba jiite waa kër Cadog ne ko: «Ba ñu tàmbalee indi li ñu ber ci seen ngóob fi kër Aji Sax ji ba tey, nu ngi lekk ba regg, ba desal lu ne gàññ, ndax Aji Sax jee barkeel ñoñam, te ndes wee jale nii.»
11 Then Hezekiah ordered them to prepare storerooms in the house of our Father, and they prepared them. Esekiyas ne ñu waajal ay néeg ca kër Aji Sax ji. Ñu waajal ko,
12 They faithfully brought in the contributions, the tenth, and dedicated gifts. Conaniah the Levite led them; Shimei his brother was second. daldi def ag màndute, yeb ca yi ñu jébbal Aji Sax ji ak céru fukkeel baak sarax yu sell ya; ka leen ca jiite moo doon Konaña Leween ba, mbokkam Simey topp ca moom.
13 Jehiel, Azaziah, Nahath, Asahel, Jerimoth, Jozabad, Eliel, Ismachiah, Mahath, and Benaiah oversaw, under Conaniah and his brother Shimei, appointed by King Hezekiah and Azariah, chief officer of our Father's house. Ña yor caytu ga ñoo doon Yexyel ak Asasya ak Naxat ak Asayel ak Yerimot ak Yosabàdd ak Elyel ak Ismakiya ak Maxat ak Benaya, ca njiital Konaña ak rakkam Simey, lépp ca ndigalal Buur Esekiyas, ak Asaryaa ma yilif kër Yàlla ga.
14 Kore son of Imnah, the Levite gatekeeper toward the east, oversaw the voluntary offerings to our Father, distributing our Father's contributions and the most holy gifts. Doomu Imna, Kore Leween ba daan wattu buntub penku ba, moo yoroon saraxi yéene yu Yàlla ya, te moo doon séddale saraxu njébbalub Aji Sax ji ak yeneen sarax yu sella sell.
15 Under him, Eden, Miniamin, Jeshua, Shemaiah, Amariah, and Shecaniah served faithfully in the priestly towns, distributing to fellow priests by divisions, great and small alike, Ci kilifteefam la Eden nekkoon ak Miñamin ak Yesuwa ak Semaya ak Amarya ak Sekaña, ca dëkki sarxalkat ya. Ñooñoo yoroon ca seen biiri bokk, ñuy mag, di ndaw, séddaleb dund bu dëppoo ak seen kuréeli liggéey.
16 besides giving to those registered by genealogy, males three and up—all entering the house of our Father for daily duty—for their service by office and division. Séddale ba nag, góor ña am ñetti at, jëm kaw ca lañu bokk, ba ca mboolem ñay dem ca kër Aji Sax ji, ngir seen liggéeyi bés ak bés ya méngoo ak seeni dénkaane ak seeni kuréel.
17 Priests were registered by clans; Levites twenty and up, by duty and division. Sarxalkat ya ñu lim, na ñu bokke seeni kër maam itam, ak Leween ña am ñaar fukki at, jëm kaw, séddale ba ñeel na leen, topp na ñu bokke seeni dénkaane ak seeni kuréel
18 They were registered with all their little ones, wives, sons, and daughters—the whole community—for they faithfully dedicated themselves in holiness. ak itam mboolem ña ñu lim, ñook mboolem seen njaboot gu sew, seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen ndax pastéef ga ñu yeboo woon ci liggéey bu sell.
19 For Aaron's priestly descendants living in the pasture-fields around their towns, men were named in each and every town to give shares to every male priest and all Levites listed by genealogy. Séddale ba ñeel na itam sëti Aaróona yu góor, sarxalkat ya nekkoon ca kaw ga, ca parluy dëkk ya ñu féete; dëkk bu ci nekk, ñu tudd fa ay nit ñu wara joxe cér yu ñeel mboolem kuy góor, ca biir sarxalkat ya ak Leween ña ñu lim ñépp.
20 Hezekiah did this throughout all Judah. He did what was good, right, and faithful before our Father. Noonu la Esekiyas def ca Yuda gépp. Mbaax ak njub ak dëggute la jëfe fi kanam Aji Sax ji Yàllaam.
21 In all he undertook—serving the house of our Father, keeping the law and command, seeking our Father—he gave his whole heart, and thrived. Mboolem jëf ju Esekiyas sumboon ci wàllu liggéeyub kër Yàlla ga, na mu dëppoo ak yoon wi ak santaane yi, ngir jaamu Yàllaam, léppi xolam la ko defe, ba am ca ndam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]