Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 32 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After these things and these acts of faithfulness, Sennacherib, Assyria's king, invaded Judah, besieged its fortified cities, meaning to break into them for himself. Gannaaw jëfi worma yooyii, Senaxerib buurub Asiri moo dikk ba biir Yuda, daldi gaw dëkk ya tata wër, nar leena bëtt, ba nangu leen.
2 When Hezekiah saw that Sennacherib had come, intent on making war against Jerusalem, Ba Esekiyas gisee ne Senaxerib dikk na te song xare Yerusalem la nar,
3 he consulted his officials and warriors about blocking the springs outside the city, and they helped him. ay jawriñam aki jàmbaaram la diisool, ngir fatt bëti ndox ya ca bitib dëkk ba. Ñu ànd ca ak moom.
4 Many people gathered and blocked all the springs and the stream flowing through the land, asking, "Why should Assyria's kings come and find abundant water?" Ci kaw loolu ñu dajale nit ñu takku, daldi fatt mboolem bëti ndox ya ak wal ma doon dawe biir réew ma, ndax dañu ne duñu bàyyi buuri Asiri, ñu dikk fekk fa ndox mu ne xéew.
5 He worked hard to rebuild all the broken sections of the wall, raised towers on it, built another wall outside, strengthened the Millo of the city of David, and made abundant weapons and shields. Esekiyas nag góor-góorlu, tabaxaat mboolem fu tata dëkk ba bëttoon, yokke ko ay sooroor, ba tabaxaat beneen tata ca gannaawam, fa féete biti. Mu teg ca dàbbali sëkkub Milo ja ca gox ba ñu naan Kër Daawuda, daldi sàkklu gànnaay yu bare aki pakk.
6 He set war commanders over the people, gathered them at the city gate square, and encouraged them: Gannaaw loolu mu tabb ay jawriñi xare yu jiite gàngoor ga, daldi leen woo fa moom, ca pénc ma ca buntu dëkk ba. Mu yokk seen pastéefu xol, ne leen:
7 "Be strong and brave. Don't fear or dread Assyria's king and all his horde, for more are with us than with him. «Dëgërluleen te amu fit. Buleen ragal, buleen jàq ndax buurub Asiri ak mboolem gàngoor gi ànd ak moom, ndax li ànd ak nun moo ëpp doole li ànd ak moom.
8 With him is only an arm of flesh; with us is our Father, to help us and fight our battles." The people relied on Hezekiah king of Judah's words. Li ànd ak moom përëgub suux la, te ki ànd ak nun di Aji Sax ji sunu Yàlla ji nuy wallu, xareel nu sunuy xare.» Xelu askan wa nag dal ca kàddu ya Esekiyas buurub Yuda wax.
9 After this, while besieging Lachish with all his forces, Sennacherib king of Assyria sent his servants to Jerusalem, to Hezekiah king of Judah and all Judah there, saying: Gannaaw loolu Senaxerib, buurub Asiri yónni ay jawriñam, fekk ko tollu mook gàngooram gépp fa jàkkaarlook Lakis, ca Esekiyas buuru Yuda ak mboolem Yudeen ña ca Yerusalem. Ñu ne:
10 "This is what Sennacherib king of Assyria says: On what are you trusting, staying under siege in Jerusalem? «Senaxerib buurub Asiri dafa wax ne: Ana lu ngeen yaakaar, ba toog ci biir Yerusalem gi ñu gaw?
11 Isn't Hezekiah deceiving you, surrendering you to die by famine and thirst, when he says, 'The LORD our God will save us from the hand of the king of Assyria'? Xanaa du Esekiyas moo leen nax, ngir wacc leen ngeen deek xiif ak mar, naan leen: “Sunu Yàlla Aji Sax ji moo nuy xettali ci loxol buurub Asiri.”
12 Wasn't it Hezekiah who removed his high places and altars, telling Judah and Jerusalem to worship at one altar and burn offerings there? Du moom Esekiyas moo dindi bérebi jaamookaay yeek sarxalukaayi Aji Sax ji, ba noppi ne waa Yuda ak Yerusalem: “Benn sarxalukaay ngeen di sujjóotal, te ci ngeen di taal saraxu cuuraay?”
13 Don't you know what I and my fathers did to all peoples of other lands? Could their nations' gods rescue their lands from my hand? «Xanaa xamuleen li ma def mboolem askani réew yi, man maak samay maam? Fu yàllay xeeti réew yooyu fexee lenn, ba mana xettali seen réew ci sama loxo?
14 What god of nations my fathers devoted to destruction could save his people from my hand? How then can your God save you from my hand? Tuuri réew yooyu yépp yi samay maam faagaagaloon, ana mu ci manoona xettali aw xeetam ci sama loxo? Ana kon nu leen seen yàlla mana xettalee ci sama loxo?
15 Don't let Hezekiah deceive or mislead you like this, and don't believe him: no god of any nation or kingdom could rescue his people from my hand or my fathers'—much less will your God rescue you from my hand!" Léegi nag, bu leen Esekiyas nax, ba réeral leen nii; buleen ko gëm. Ndax kat, jenn yàllay wenn xeet akug nguur masula mana xettali aw xeetam ci sama loxo, mbaa sama loxoy maam. Kon nag du seen yàllaa leen di xettali ci sama loxo.»
16 And his servants spoke still more against our Father and against his servant Hezekiah. Surgay Senaxerib nag gënatee ŋàññ Aji Sax ji Yàlla ak jaamam Esekiyas.
17 Sennacherib also wrote letters insulting our Father, the God of Israel, speaking against him: "The nations' gods did not rescue their people from my hand; neither will Hezekiah's God rescue his people from my hand." Ay bataaxal sax Senaxerib bind na ko, ngir kókkali Aji Sax ji Yàllay Israayil, ba wax ci moom ne: «Noonee yàllay xeeti yeneen réew yi tëlee xettali seeni ñoñ ci sama loxo, noonu rekk la yàllay Esekiyas di tëlee xettali ñoñam ci sama loxo.»
18 They shouted loudly in Judah's language to Jerusalem's people on the wall, to frighten and terrify them, to seize the city. Ñuy xaacu nag ca kaw, ci làkku ebrë, jëme ca niti Yerusalem ña ca kaw tata ja, ngir xoqtal leen, yóbbu seenu fit. Su ko defee nangu dëkk ba yomb leen.
19 They spoke of Jerusalem's God like the gods of earth's peoples, the work of human hands. Ci biir loolu ñuy wax ci Yàllay Yerusalem, mbete su doon moroomu yàllay xeeti àddina, ay jëmm yu doom aadama liggéeye ay loxoom.
20 Then King Hezekiah and the prophet Isaiah son of Amoz prayed about this, crying out to heaven. Ba loolu amee Buur Esekiyas ak Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc yékkati kàddug ñaan ci moomu mbir, jëme asamaan.
21 So our Father sent an angel who killed every mighty warrior, commander, and officer in the Assyrian king's camp. Sennacherib returned home in disgrace, and when he entered his god's temple, some of his own sons killed him there with the sword. Aji Sax ji yebal malaaka, mu sànk mboolem ñeyi xare akub jawriñ ak kuy njiit ca dalu buurub Asiri, mu sëlmoo gàcce, ñibbi am réewam. Gannaaw gi, ba mu duggee ca kër yàllaam, foofa la ko ñenn ci ay doomi geñog boppam, daldi bóome saamar.
22 So our Father saved Hezekiah and Jerusalem's people from the hand of Sennacherib king of Assyria and all others, and he cared for them on every side. Noonu la Aji Sax ji musale Esekiyas ak waa Yerusalem ca Senaxerib buurub Asiri ak ci ñépp. Wet gu nekk la leen Aji Sax ji aare.
23 Many brought gifts to our Father in Jerusalem, and treasures to Hezekiah king of Judah; afterward all nations honored Hezekiah highly. Ba mu ko defee ñu bare di indi Yerusalem sarax bu ñeel Aji Sax ji, ak teraanga yu ñeel Esekiyas buurub Yuda. Fa la doxe di ku xeet yépp weg.
24 In those days Hezekiah grew sick to death; he prayed to our Father, who answered, giving him a sign. Jant yooyu la Esekiyas woppoon bay waaja dee. Mu ñaan ci Aji Sax ji. Ba mu waxee ak moom, firnde la ko jox, ngir mu xam ne dina wér.
25 But Hezekiah didn't repay the good done him; his heart grew proud, so anger came on him and on Judah and Jerusalem. Teewul teraanga ja ñu defal Esekiyas, feyu ko, xanaa doxe fa indi xolub réy-réylu, ba tax am sànj nara dal ca kawam ak ca kaw Yuda ak Yerusalem.
26 Hezekiah humbled himself for his proud heart, he and Jerusalem's people, so our Father's wrath didn't reach them in Hezekiah's days. Ci kaw loolu Esekiyas toroxlu, tuube ko xolub réy-réyloom, moom ak waa Yerusalem, ba tax sànjum Aji Sax ji dalul ca seen kaw ca janti Esekiyas.
27 Hezekiah had great wealth and honor. He built storerooms for silver, gold, gems, spices, shields, and other valuables, Alal ak daraja ju bare lool la Esekiyas amoon. Ay dencukaay la sàkkaloon boppam, ngir xaalis ak wurus ak doj yu gànjare aki cuuraay aki pakk ak mboolem jumtukaayi tànnéef.
28 storerooms for the harvest of grain, new wine, and oil; stalls for all kinds of livestock; pens for flocks. Ay sàq itam amoon na ko, ngir am pepp ak biiñ bu bees akug diw, ak itam ay wudd ngir gépp xeetu jur aki wërmbal ngir ay géttam.
29 He built cities for himself and gained huge flocks and herds, for our Father gave him very great wealth. Ay dëkk sax tabaxaloon na ko boppam, te amoon na gétt yu ne gàññ, jur gu gudd ak gu gàtt, ndax Yàllaa ko mayoon koom gu bare lool.
30 Hezekiah stopped Gihon's upper outlet and directed the water down the west side of David's city. He succeeded in all he did. Esekiyas ci boppam moo waññi bëtu ndox ba ñuy wax Gixon Kaw, ngir awale ndox ma fu gëna suufe te féete ca sowub gox ba ñu naan Kër Daawuda. Ndam la am ca mboolem ay liggéeyam.
31 When Babylon's rulers sent envoys to him asking about the land's sign, our Father left him to himself, to test him and to know all in his heart. Teewul ca mbirum ndawi kàngami Babilon ya yónnee woon fa moom di gëstu kéemaan ga amoon ca réew ma, Yàlla moo ko seetaan, ngir seetlu ko ba ràññee mboolem la ca biir xolam.
32 Hezekiah's remaining acts and faithful deeds are written in the vision of Isaiah the prophet, son of Amoz, in the Book of the Kings of Judah and Israel. Li des ci mbiri Esekiyas ak jëfi ngoram, ma nga binde ca peeñuy Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc, ca téere ba ñu dippee Buuri Yuda ak Israayil.
33 Hezekiah slept with his ancestors, buried in the upper tombs of David's sons. All Judah and Jerusalem's residents honored him at death. His son Manasseh succeeded him. Gannaaw loolu Buur Esekiyas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko fa féete kaw sëgi sëti Daawuda. Teraanga la ko mboolem Yuda ak waa Yerusalem defal cig deewam. Doomam Manase moo falu buur, wuutu ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]