Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 21 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Jehoshaphat rested with his ancestors, buried with them in the City of David; his son Jehoram reigned instead. Gannaaw gi, Buur Yosafat saay, fekki ay maamam, ñu denc ko fa ñu denc ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Yexoram doomam moo falu buur, wuutu ko.
2 Jehoram's brothers, sons of Jehoshaphat: Azariah, Jehiel, Zechariah, Azariah, Michael, Shephatiah. All these were sons of Jehoshaphat king of Israel. Yexoram amoon na ñu mu bokkal seen baay Yosafat: ñooñooy Asaryaa ak Yexyel ak Sàkkaryaa ak Asaryawu ak Mikayel ak Sefatiya. Ñooñu ñépp di doomi Yosafat buurub Israayil.
3 Their father gave them many gifts—silver, gold, precious things—and fortified cities in Judah, but gave the kingdom to Jehoram, because he was firstborn. Lu bare la leen seen baay mayoon ci wàllu xaalis ak wurus ak gànjar, boole ci ay dëkk yu tata wër ca biir Yuda. Nguur ga nag, mu jox ko Yexoram, ndax moo doon taaw.
4 Once Jehoram rose over his father's kingdom, he grew strong and killed all his brothers with the sword, and also some of Israel's officials. Ba Yexoram jëlee nguurug baayam, ba dëju bu baax, doomi baayam yépp la jam saamar ñu dee, ñook ñenn ca njiiti Israayil.
5 Jehoram was thirty-two years old when he became king, and he reigned eight years in Jerusalem. Fanweeri at ak ñaar la Yexoram amoon ba muy falu buur, te juróom ñetti at la nguuru fa Yerusalem.
6 He walked in the way of Israel's kings, as Ahab's house had done, for Ahab's daughter was his wife, and he did evil in our Father's eyes. Tànki buuri Israayil la topp, waa kër Axab la roy, ndax doomu Axab la jël jabar, di def li Aji Sax ji ñaawlu.
7 Yet our Father would not destroy the house of David, because of the covenant he made with David, and his promise to give him and his sons a lamp forever. Waaye Aji Sax ji bëgguloona tas kër Daawuda, ndax kóllëre ga mu fasoon ak Daawuda, ak la mu ko digoona jafalal seen nguur, moom aki doomam, ni jum bu dul fey.
8 In Jehoram's days Edom rebelled against Judah's rule and set up their own king. Ca jamonoy Yexoram la Edomeen ña fippu, bañ moomeelu Yuda, ba fal seen buuru bopp.
9 Jehoram crossed with his commanders and all his chariots. He rose at night and struck the Edomites surrounding him and the chariot commanders. Gannaaw loolu Yexoram aki jawriñam yóbbaale watiiri xareem yépp. Moo jóg ag guddi, dal ca kaw Edomeen ña leen gawoon, moom ak njiiti watiiri xareem.
10 Edom rebelled against Judah's rule to this day; Libnah also rebelled then, because he had abandoned our Father, the God of his ancestors. Edomeen ñaa ngi bañ moomeelu Yuda ba tey jii. Jant yooyu itam la waa dëkk ba ñuy wax Libna fippu, ndax Yexoram moo wacc Aji Sax ji Yàllay maamam.
11 He built high places on Judah's hills, led Jerusalem's people to prostitute themselves, and drew Judah astray. Moom moo sàkk ay bérebi jaamookaay ca tundi Yuda, moo bokkaaleloo waa Yerusalem, te moo lajjal Yuda.
12 A letter came to him from Elijah the prophet: Your Father, God of your ancestor David, says: Because you haven't walked in the ways of your father Jehoshaphat, or the ways of Asa king of Judah, Ab bataaxal bu bàyyikoo fa Yonent Yàlla Ilyaas nag dikkal Yexoram, ne ko: «Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Gannaaw toppuloo tànki Yosafat sa baay ak tànki Asa buurub Yuda,
13 but walked like Israel's kings, led Judah and Jerusalem's people to be unfaithful, as Ahab's house led Israel, and killed your brothers—your father's house—men better than you, xanaa nga topp tànki buuri Israayil, ndax yaa bokkaaleloo waa Yuda ak waa Yerusalem, noonee waa kër Axab daan bokkaalee, te itam sa waa kër baay, sa doomi baay yi la gën, yaw yaa leen rey,
14 now your Father will strike your people, children, wives, and all your goods with a great plague. Aji Sax jaa ngii di dumaa mbas mu réy saw xeet, ak say doom ak say jabar ak mboolem sa alal.
15 You will have a severe intestinal disease, until day by day your intestines come out. Yaw ci sa bopp lay dumaa wopp yu aay, woppi butit, ba say butit di génn, ndax aayteefu wopp jay màgg, bés ak bés.»
16 Our Father stirred up against Jehoram the spirit of the Philistines and Arabs near the Cushites. Aji Sax ji teg ca xabtal waa Filisti ak itam Arab ya dendeek Kuuseen ña ci kaw Yexoram.
17 They attacked Judah, invaded it, and seized all the goods found in the king's palace, plus his sons and wives, leaving him no son except Jehoahaz, his youngest. Ñu dikk fa kaw Yuda, bëtt kaaraangeem, nangu mboolem alal ja ñu fekk kër buur ak itam doomam yu góor ak ay jabaram, ba desewul doom ju moy Axasya ma gëna tuut ca doomam yu góor.
18 After all this, our Father struck him with an incurable disease in his intestines. Gannaaw loolu yépp, Aji Sax ji dóore ko jàngoroy butit ju amul paj.
19 In time, after two years, his intestines came out because of his disease, and he died in agony. His people made no fire for him, as they had for his ancestors. Jamono di dox ba ñu xawa tollu ca ndeetel ñaareelu at ma, butit ya génn ndax wopp ja, mu deewe mitit yu tar. Askanam nag taaluñu ab taal bu ñu ko sargale, na ñu ko taalale woon ay maamam.
20 He was thirty-two when crowned king; he reigned eight years in Jerusalem. He died unmourned, buried in the City of David, but not among the kings' tombs. Fanweeri at ak ñaar la Yexoram amoon ba muy falu buur, te nguuru na juróom ñetti at fa Yerusalem. Moo dëddu te kenn tiisluwu ko. Ca gox ba ñu naan Kër Daawuda lañu ko denc, waaye denceesu ko fa bàmmeeli buur ya.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]