Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 22 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The people of Jerusalem made his youngest son Ahaziah king in his place, since the raiders who came with the Arabs into the camp had killed all the older sons. So Ahaziah son of Jehoram king of Judah became king. Waa Yerusalem nag fal buur Axasya, doomam ja gëna tuut, mu wuutu ko, ndax fekk na mboolem ay magam, gàngooru yàqkat ga àndoon ak Arab ya dikk ca dal ba, rey leen. Noonu la Axasya doomu Yexoram faloo buurub Yuda.
2 Ahaziah became king at twenty-two and reigned one year in Jerusalem. His mother was Athaliah, granddaughter of Omri. Ñaar fukki at ak ñaar la Axasya amoon, ba muy falu buur, te menn at la nguuru fa Yerusalem. Atalyaa mooy yaayam, sëtub Buur Omri.
3 He too followed the ways of Ahab's house, for his mother counseled him to do evil. Moom itam tànki waa kër Axab la topp, ndax yaayam moo doon xelal, di ko xiir ci jëf ju bon.
4 He did evil in our Father's eyes, like Ahab's house, for after his father's death they were his counselors, to his ruin. Li Aji Sax ji ñaawlu la daan def ni waa kër Axab, ndax gannaaw deewug baayam, ñooñoo ko doon xelal, mu dig sànkuteem.
5 He followed their advice too, joining Joram son of Ahab, Israel's king, to fight Hazael king of Aram at Ramoth-gilead, where the Arameans wounded Joram. Seenub digle it la topp, ba ànd ak buurub Israayil Yoram doomu Axab, xarejeek Asayel buurub Siri, ca Ramot Galàdd. Waa Siri jam Yoram.
6 So he returned to Jezreel to recover from the wounds he received at Ramah fighting Hazael king of Aram. Ahaziah son of Jehoram king of Judah went down to Jezreel to see Joram son of Ahab, because he was wounded. Mu walbatiku fajuji fa Yisreel, ndax jam-jam ya ñu ko jam fa Raama, ba muy xareek Asayel buurub Siri. Axasya buurub Yuda nag dem seeti Yoram doomu Axab fa Yisreel ndax jagadeem ja.
7 Ahaziah's downfall came from our Father when he visited Joram. On arriving, he went out with Jehoram against Jehu son of Nimshi, whom our Father had anointed to destroy the house of Ahab. Waaye booba Yàllaa dogal jéllub Axasya jaare ca yoon wa muy dem di seeti Yoram. Ba mu agsee, Yoram la àndal dem seeti Yewu doomu Nimsi ma Aji Sax ji tabboon, ngir mu foq nguurug waa kër Axab.
8 As Jehu carried out judgment on Ahab's house, he found Judah's officials and Ahaziah's nephews who served Ahaziah, and killed them. Yewu nag nekk ca liggéeyam, ngir sottal àtteb waa kër Axab. Ci biir loolu mu gis jawriñi Yuda ak doomi magi Axasya yay taxawu Axasya. Yewu daldi leen rey.
9 He searched for Ahaziah, who was captured while hiding in Samaria. They brought him to Jehu and killed him, then buried him, saying, "He is Jehoshaphat's son, who sought our Father with all his heart." So Ahaziah's house had no one strong enough to hold the kingdom. Ba loolu amee mu yónnee ñu ko wëral Axasya, ba jàppe ko fa Samari ga mu làqu woon. Ñu indi ko ca Yewu, daldi koy rey. Waaye dencees na ko, ndax booba dañu ne Axasya mooy sëtub Yosafat ma daan jaamoo Aji Sax ji léppi xolam. Gannaaw loolu nag amul woon kenn ku bokk ca kër Axasya ku amoon dooley yor nguur ga.
10 When Athaliah, Ahaziah's mother, saw her son was dead, she set out to destroy all the royal offspring of Judah's house. Ci kaw loolu Atalyaa yaayu Axasya xam ne doomam ju góor dee na, mu daldi bóom mboolem ku bokk ci askanu nguur gu waa kër Yuda.
11 But Jehoshabeath the king's daughter took Joash son of Ahaziah, stealing him from among the royal sons about to be killed, and hid him with his nurse in a bedroom. So Jehoshabeath, King Jehoram's daughter, Jehoiada the priest's wife and Ahaziah's sister, hid him from Athaliah, so she did not kill him. Teewul Yoseba doomu Buur ju jigéen jàpp Yowas, doomu Axasya ju góor, jële ko ca biir doomi buur ya ñuy fexee rey, rawale ko. Ci kaw loolu mu boole kook ab nàmpalkatam, dugal cib néegu fanaanukaay. Jigéenub Axasya, Yoseba doomu Buur Yexoram, soxnas Yoyada sarxalkat ba, noonu la làqe Atalyaa, Yowas, ba Atalyaa reyu ko.
12 He stayed hidden with them in the house of our Father six years while Athaliah reigned over the land. Yowas nekk naak ñoom fa kër Yàlla ga, làqu fa juróom benni at, te Atalyaa di nguuru fa réew ma.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]