Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 23 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In the seventh year Jehoiada took courage and made a covenant with the commanders of hundreds—Azariah son of Jeroham, Ishmael son of Jehohanan, Azariah son of Obed, Maaseiah son of Adaiah, and Elishaphat son of Zichri. Ca atum juróom ñaareel ma Yoyada sarxalkat ba moo takku fitam, daldi woo njiiti téeméeri dag yii ci kóllëre gu ñu fasook moom: Asaryaa doomu Yeroxam ak Ismayel doomu Yoxanan ak Asaryaa doomu Obedd ak Maaseya doomu Adaya ak Elisafat doomu Sikkri.
2 They traveled through Judah, gathered the Levites from all its cities and the family heads of Israel, and came to Jerusalem. Ñu wër Yuda, woo Leween ña, ñu bàyyikoo mboolem dëkki Yuda, woo ña jiite seeni kër maam ca Israayil, ñu bokk dajesi fa Yerusalem.
3 The whole assembly made a covenant with the king in the house of our Father. Jehoiada told them, "Look, the king's son will reign, as our Father promised about David's sons. Ci kaw loolu mbooloo ma mépp fasoo ak buur ba kóllëre fa kër Aji Sax ji. Yoyada ne leen: «Yowas a ngii kat, di doomu Buur, te moo wara nguuru noonee ko Aji Sax ji waxe woon ci mbirum doomi Daawuda.
4 Do this: a third of you—priests and Levites entering on the Sabbath—will be gatekeepers at the thresholds. Li ngeen di def mooy lii: Yeen sarxalkat yeek Leween ñi aye liggéey bésub Noflaay, na seen xaajub ñetteel féetewoo wattu bunt yi.
5 A third at the king's house, a third at the Gate of the Foundation, and all the people in the courts of the house of our Father. Beneen xaajub ñetteel ba nekk ca kër buur, xaajub ñetteel ba ca des féete fa buntub Fondmaa ba. Mbooloo mi mépp nag nekk ci ëtti kër Aji Sax ji.
6 Let no one enter the house of our Father except the priests and the serving Levites; they may enter, for they are holy. Everyone else is to keep guard for our Father. Bu kenn dugg ci kër Aji Sax ji, xanaa sarxalkat yeek Leween ña fay liggéey. Ñooñu ñoo fay dugg, ndax dees leena sellal. Waaye mboolem askan wi ci des nañu dégg ndigalu Aji Sax ji.
7 The Levites must surround the king, each with weapon in hand; whoever enters the house is to be put to death. Stay with the king wherever he comes and goes." Leween ñiy dar Buur, nañu ko fege wet gu nekk, ku nekk ŋàbb ngànnaayam. Képp ku jëm ci kër gi, dees koy rey. Àndleen ak Buur ak fu mu mana jëm.»
8 The Levites and all Judah did exactly as Jehoiada the priest commanded. Each took his men—those coming on duty the Sabbath with those going off—since Jehoiada the priest did not dismiss any of the divisions. Ci kaw loolu Leween ña ak Yuda gépp def mboolem la leen Yoyada sarxalkat ba sant. Ku nekk ànd ak say nit, ña aye bésub Noflaay ak ña wàcc bésub Noflaay, ndax Yoyada sarxalkat ba noppalul genn kuréel.
9 Jehoiada the priest gave the commanders of hundreds King David's spears and large and small shields, kept in our Father's house. Ba loolu amee, Yoyada sarxalkat ba jox njiiti kuréeli téeméer ya, xeej yaak pakki Buur Daawuda ya nekkoon ca biir kër Yàlla ga.
10 He stationed all the people, each with weapon in hand, from the south side of the temple to the north side, surrounding the altar, the temple, and the king. Mu taxawal nag kuréel gépp, ku nekk ŋàbb ngànnaayam, ñu dare kër Yàlla ga ak sarxalukaay ba, wetu ndijoor ba wetu càmmoñ, ngir yéew buur ba.
11 They brought out the king's son, crowned him, gave him the covenant law, and made him king. Jehoiada and his sons anointed him and shouted, "Long live the king!" Ñu génne doomu buur ba nag, solal ko mbaxanam buur, jox ko kayitu doxalinu nguur ga. Ci kaw loolu Yoyada ak doomam yu góor fal ko buur, diw ko diwug pal, ñu daldi tàccu, ne: «Guddaluw fan, Buur!»
12 Hearing the sound of people running and praising the king, Athaliah came to them at our Father's house. Ba Atalyaa déggee coowal mbooloo may daw aka kañ buur ba, daa àgg ca mbooloo ma, fa kër Aji Sax ji.
13 She looked—there was the king standing by his pillar at the entrance, officers and trumpeters beside him, all the people of the land rejoicing and blowing trumpets, singers with instruments leading the praise. Then Athaliah tore her clothes and shouted, "Treason! Treason!" Mu xool, yem ci buur ba taxaw fa kenoom ga, ca bunt ba, kilifay xarekat yaak boroom liit ya dar Buur, waa réew ma mépp di bànneexooka wal liit ya, woykat ya yor jumtukaayi xumbéen ya, jiite woy ya. Atalyaa nag ne tareet ay yéreem ndaxu naqar, daldi ne: «Wor am naay, wor am na!»
14 Jehoiada the priest summoned the commanders of hundreds over the army and said, "March her out through the ranks; kill with the sword anyone who follows her." For the priest had said, "Do not kill her in the house of our Father." Ci kaw loolu Yoyada sarxalkat ba yebal njiiti kuréeli téeméer ya, kilifay gàngoor ga, ne leen: «Génneleen ko làng gi, te ku ko topp, dees koy jam saamar, mu dee.» Fekk na Yoyada ne buñu ko rey ci biir kër Aji Sax ji.
15 They seized her; when she reached the Horse Gate's entrance by the king's house, they killed her there. Ba mu ko defee ñu teg ko loxo. Ba mu demee ba àgg kër buur, bay tollook fa fas yay dugge, foofa lañu ko reye.
16 Then Jehoiada made a covenant among himself, all the people, and the king to be our Father's people. Ba loolu amee Yoyada digoo kóllëre digganteem moom ak askan wépp ak Buur, ngir ñu doon ñoñi Aji Sax ji.
17 All the people went to Baal's temple and tore it down, smashed its altars and idols, and killed Mattan, Baal's priest, before the altars. Ci kaw loolu waa réew ma mépp ànd dem ca kër ga ñuy jaamoo Baal. Ñu màbb ko; ay sarxalukaayam ak jëmmi nataalam, ñu tas; Matan, sarxalkatu Baal ba, ñu rey ko ca kanam sarxalukaay ya.
18 Jehoiada put the Levite priests in charge of our Father's house, whom David had assigned there, to offer burnt offerings to our Father, as written in Moses' law, with joy and song as David had ordered. Ci biir loolu Yoyada teg wattub kër Aji Sax ji ci loxoy sarxalkat yiy Leween. Daawuda moo defoon ñooñu ay kuréel ci kër Aji Sax ji, ngir ñuy joxe saraxi rendi-dóomali Aji Sax ji, noonee ñu ko binde ci yoonu Musaa, te ñu war koo def ci biir bànneex aki woy, na ko Daawuda diglee woon.
19 He stationed gatekeepers at the gates of our Father's house so no one unclean in any way could enter. Mu taxawal nag fara bunt ya ca bunti kër Aji Sax ji, ba ku sobewu ci lu mu mana doon, du dugg.
20 He took the commanders of hundreds, the nobles, the rulers of the people, and all the people of the land, and brought the king down from the house of our Father, through the Upper Gate into the king's house, and seated him on the royal throne. Ba loolu amee mu dellu woo njiiti téeméeri nit yaak garmi yaak kàngam ya yilif askan wa. Mu jële Buur kër Aji Sax ji, ñu jaare nag ca buntub Kaw ba, ba àgg kër buur, daldi koy toogal ca ngànguney nguur ga.
21 All the people of the land rejoiced, and the city grew calm, for Athaliah was killed with the sword. Waa réew mépp di bànneexu. Péey ba am jàmm ndax la ñu jam Atalyaa saamar ba mu dee.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]