Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 24 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Joash became king at seven, and reigned forty years in Jerusalem. His mother Zibiah was from Beersheba. Juróom ñaari at la Yowas amoon ba muy falu buur. Ñeent fukki at la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Cibya ma cosaanoo Beerseba.
2 Joash did what was right in our Father's eyes all the days of Jehoiada the priest. Giiru dundu Yoyada sarxalkat ba, li Aji Sax ji rafetlu la Yowas daan def.
3 Jehoiada chose two wives for him, and Joash had sons and daughters. Yoyada nag moo ko jëlal ñaari jabar, mu am ca doom yu góor ak yu jigéen.
4 Some time later, Joash set his heart on restoring the house of our Father. Gannaaw gi, xelum Yowas nekk ci yeesal kër Aji Sax ji.
5 He gathered the priests and Levites, told them, "Go to Judah's cities, collect money from all Israel yearly to repair your Father's house—hurry." But the Levites didn't hurry. Mu woo sarxalkat ya ak Leween ña, ne leen: «Wërleen dëkki Yuda, ngeen jële ci mboolem Israayil, xaalis bi doy cim at, ngir jagal seen kër Yàlla. Yeen nag, defleen lu gaaw ci mbir moomu.» Ba loolu amee taxul Leween ña def lu gaaw.
6 The king summoned Jehoiada the chief priest: "Why haven't you required the Levites to bring the tax from Judah and Jerusalem that Moses, our Father's servant, and the assembly set on Israel for the tent of testimony?" Buur daldi woolu Yoyada, sarxalkat bu mag ba, ne ko: «Ana lu waral sàkkuwuloo ci Leween ñi, ñu jëleji Yuda ak Yerusalem galag bi Musaa jaamu Aji Sax ji ak mbooloom Israayil laaj, ngir xaymab ndaje mi?
7 Athaliah's sons, that wicked woman, broke into our Father's house and even used all the holy things of our Father's house in worship of the Baals. Ndax kat niti Atalyaa jigéen ju bon ji, ñoo bëtt kër Yàlla gi, te it mboolem jumtukaayi kër Aji Sax ji lañu def ci tuur yi ñuy wax Baal.»
8 At the king's order, they made a chest and set it outside our Father's house gate. Buur nag joxe ndigal, ñu sàkk ag gaalu dencukaay, teg ko fa bunt kër Aji Sax ji ca biti.
9 They announced in Judah and Jerusalem: bring our Father the tax Moses, our Father's servant, set on Israel in the wilderness. Ci kaw loolu ñu yéene fa Yuda ak Yerusalem, ne ñu indil Aji Sax ji galag ba Musaa jaamub Yàlla ba tegoon Israayil ca màndiŋ ma.
10 All the officials and all the people rejoiced, bringing and dropping their gifts into the chest until full. Kilifa yaak askan wa wépp bége ko, daldi indib xaalis, sànni ca gaal ga ba mu fees.
11 Whenever the Levites brought the chest to the king's officials and saw it full of money, the royal secretary and chief priest's officer emptied it and returned it to its place. Daily they collected much money. Bu ñu demee ba indil gaal ga caytug buur ga ca loxol Leween ña, bu ñu gisee xaalis ba bare, bindkatub buur mooy dikk, mook ndawal sarxalkat bu mag ba, ñu sotti gaal ga, jël ko, delloo fa bérebam. Noonu lañu jàppoo bés bu nekk, ba dajale xaalis bu bare.
12 The king and Jehoiada gave it to workers on our Father's house, who hired masons and carpenters to restore it, and iron and bronze workers to repair our Father's house. Buur ak Yoyada jox ko ña yor liggéey ba tabaxaatub kër Aji Sax ji laaj, ñu jël ay yattkati doj, ak liggéeykati bant, ngir yeesal kër Aji Sax ji, ak itam ay liggéeykati weñ ak xànjar, ngir jagal kër Aji Sax ja.
13 Workers labored; repair progressed by their hands. They restored our Father's house to its form and strengthened it. Ña yor liggéey ba di liggéey, tabaxaatub kër Yàlla ga jëm kanam ca seeni loxo, ñu daldi yékkati kërug Aji Sax ja, ci dayoy boppam ya ca war, ba gën koo dëgëral.
14 When finished, they brought the rest of the money to the king and Jehoiada, making from it articles for our Father's house: vessels for service and burnt offerings, dishes, gold and silver vessels. They offered burnt offerings in our Father's house continually, all Jehoiada's lifetime. Naka lañu noppi, daldi indil Buur ak Yoyada, ndesu xaalis ba, ñu def ca ay jumtukaay ngir kër Aji Sax ji: ndabi liggéeyukaay ak ndabi saraxi rendi-dóomal aki njaq ak jumtukaayi wurus ak xaalis. Giiru dundu Yoyada gépp, dañoo saxoo woon di jébbal saraxi rendi-dóomal ci kër Aji Sax ji.
15 Jehoiada grew old and full of years, then died; at his death he was 130 years old. Yoyada nag dem na ba màggat, gannaaw ba mu dundee ba doyal aw fan, doora dee ci téeméeri atam ak fanweer.
16 They buried him in the City of David among the kings, for doing good in Israel toward our Father and his house. Ba mu ko defee ñu denc ko ca gox ba ñuy wax Kër Daawuda, ca bàmmeeli buur ya, ndax lu baax la mu def ca Israayil, ngir Yàlla ak kërug Yàlla.
17 After Jehoiada died, Judah's officials came and bowed to the king, and he listened to them. Gannaaw deewug Yoyada, njiiti Yuda ñoo dikk, sujjóotal Buur, daldi fexe ba Buur dégg seen ndigal.
18 They abandoned our Father's house, God of their ancestors, served Asherah poles and idols—so anger came on Judah and Jerusalem for this guilt. La ca tegu ñu mujj wacc kër Aji Sax ji seen Yàllay maam, di jaamu ay tuur yu ñuy woowe Asera ak jëmmi xërëm. Am sànj nag dal ca kaw Yuda ak Yerusalem ndax seen tooñ googu.
19 Yet our Father sent them prophets to bring them back to himself; they warned them, but they wouldn't listen. Aji Sax ji yónni ay yonent fa seen biir, ngir delloosi leen fa moom, Aji Sax ji. Ñu femmu leen, te taxul ñu teewlu.
20 Then the Spirit of our Father came on Zechariah son of Jehoiada the priest. He stood before the people and said, "This is what our Father says: Why break his commands? You won't succeed—you abandoned him, so he abandons you." Ci kaw loolu noowug Yàlla solu sarxalkat ba, Sàkkaryaa doomu Yoyada. Mu taxaw janook askan wa, ne leen: «Yàlla dafa wax ne: Yeen lu tax ngeen di moy santaaney Aji Sax ji? Dungeen baaxle, ndax yeena wacc Aji Sax ji, mu wacc leen.»
21 They conspired against him, stoning him in our Father's house courtyard at the king's command. Ba loolu amee ñu fexeel ko, ba dóor ko ay doj ba mu dee ca ndigalal Buur, ca ëttub kër Aji Sax ji.
22 King Joash forgot the kindness Zechariah's father Jehoiada had shown him and killed his son. As Zechariah was dying he said, "May our Father see and require it." Noonu la Buur Yowas ñàkka bàyyee xel, ngor ga Yoyada baayu Sàkkaryaa jëflantee woon ak moom, ba rey doomam. Ba Sàkkaryaa di waaja dee nag da ne: «Yal na Aji Sax ji gis te sàkku ag pey.»
23 At the turn of the year Aram's army attacked Joash, invaded Judah and Jerusalem, killed all the people's officials, sent all their plunder to Damascus's king. Ba at ma deewee, gàngooru Siri moo song Yowas xare. Ñu dikk ba Yuda ca Yerusalem, daldi faat mboolem kàngami askan wa, dajale cëxëtoo ma mépp, yónnee ko seen buur ca Damaas.
24 Though Aram's army came with few men, our Father gave a much larger army into their hand, since Judah abandoned our Father, the God of their ancestors. So judgment fell on Joash. Nit ñu néew déy la gàngooru Siri indi woon, waaye Aji Sax ji moo teg ci seen loxo gàngooru Yuda gu takku lool, ndax waa Yuda ñoo wacc Aji Sax ji seen Yàllay maam. Yowas nag, noonu la ko waa Siri jottalee ay mbugal.
25 When the Arameans left, leaving him badly wounded, his servants conspired against him for the blood of Jehoiada the priest's son, killing him on his bed. He died and was buried in the City of David, not in the kings' tombs. Ba ko waa Siri wonee gannaaw, bàyyee ko mitit yu tar, ay surgay boppam ñoo ko fexeel, ndax la mu jël bakkanu doomu Yoyada sarxalkat ba. Ca kaw lalam lañu ko bóome, denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda, te dencuñu ko ca bàmmeeli buur ya.
26 Conspirators against him: Zabad son of Shimeath, Ammonite woman, and Jehozabad son of Shimrith, Moabite woman. Ña fexeel Yowas nag ñoo di Sabàdd ma yaayam dib Amoneen bu ñuy wax Simeyat, ak Yewosabàdd ma yaayam di Mowabeen bu ñuy wax Simrit.
27 His sons, the many prophecies against him, and rebuilding our Father's house are written in the Book of the Kings' commentary; his son Amaziah reigned in his place. Lu jëm ci doomi Yowas yu góor ak barewaayu àtte ya dal ca kawam ak defaraatub kër Yàlla ga, ma nga noonu ñu bind ca faramfàcceb téereb buur ya. Amaciya doomam moo falu buur, wuutu ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]