Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 25 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Amaziah became king at twenty-five and reigned twenty-nine years in Jerusalem. His mother was Jehoaddan of Jerusalem. Ñaar fukki at ak juróom la Amaciya amoon ba muy falu, te ñaar fukki at ak juróom ñeent la nguuru fa Yerusalem. Yaayam moo doon Yowadan ma cosaanoo Yerusalem.
2 He did what was right in the eyes of our Father, but not wholeheartedly. Def na njub gi Aji Sax ji rafetlu, waaye defewu ko pastéefu xol bu mat sëkk.
3 Once the kingdom was firmly his, he executed the servants who had killed his father the king. Ba nguur ga demee ba dëgër ñeel ko, moo bóom jawriñam ña bóomoon Buur baayam.
4 But he did not put their children to death, as written in the Law, the book of Moses, where our Father commanded, "Parents must not die for their children, nor children for their parents; each dies for his own sin." Waaye seeni doom, bóomu leen, ngir dëppook la ñu bind ci téereb yoonu Musaa, te Aji Sax ji santaane ko, ne: «Deesul rey baay ndax doom te deesul rey doom ndax baay. Nit ku nekk, bàkkaaru boppam lees koy reye.»
5 Amaziah gathered Judah, organized them by ancestral houses under commanders of thousands and hundreds, for all Judah and Benjamin. He counted those twenty and up: 300,000 chosen men fit for war, handling spear and shield. Ci kaw loolu Amaciya woo Yuda, ñu daje, mboolem góori Yuda ak Beñamin, mu topp na ñu bokke seeni kër maam, tàbbal leen noonu ay njiiti kuréeli junni ak njiiti kuréeli téeméer. Mu lim leen, dale ca góor ña am ñaar fukki at jëm kaw, ña mu leen gisal di ñetti téeméeri junniy (300 000) góor ñu xare war, te ñu mane ab xeej akub pakk.
6 He also hired 100,000 strong warriors from Israel for about 7,500 pounds of silver. Mu boole ca jël téeméeri junniy (100 000) ñeyi xarey Israayil ñu am doole, fey leen lu wara tollook ñetti junni kiloy xaalis ak liibar (3 500).
7 A man of our Father came to him: "King, don't let Israel's army go with you, for our Father is not with Israel—all these Ephraimites. Ba loolu amee genn góorug Yàlla dikk ba ca moom ne ko: «Buur, bu gàngooru Israayil ànd ak yaw, ndax Aji Sax ji àndul ak Israayil, àndul ak kenn ci Efraymeen ñi.»
8 Even if you fight bravely, our Father will overthrow you before the enemy, for our Father has power to help or overthrow." Soo àndee ak ñoom dem déy, defal loo man te góor-góorlu ca xare ba, Yàlla moo lay daane fa kanam noon ba, ndax Yàllaa mana walloo, moo mana daaneel.
9 Amaziah asked the man of our Father, "But what about the roughly 7,500 pounds of silver I gave Israel's troops?" He replied, "Our Father can give you far more than this." Amaciya ne góorug Yàlla ga: «Ana lees di def nag ak ñetti junniy kiloy xaalis ak genn-wàll (3 500) yi ma fey gàngoori Israayil?» Góorug Yàlla ga ne ko: «Aji Sax ji man na la may lu ko ëpp fuuf.»
10 So Amaziah sent home the troops that came to him from Ephraim. They burned with anger against Judah and returned home enraged. Ba loolu amee Amaciya beddi gàngoor ga ko fekksi te bawoo fa Efrayim, ngir ñu ñibbi. Seen xol nag tàng lool ca Yuda, ñu ñibbee xol bu tàng.
11 But Amaziah took courage, led out his people to the Valley of Salt, and struck down 10,000 men of Seir. Ba mu ko defee Amaciya takku fitam, jiite gàngooram, dem xuru Xorom wa, rey fa fukki junniy niti Seyir.
12 Judah's men also captured 10,000 alive, took them to the cliff top, and threw them down, smashing them all to pieces. Ñeneen fukki junni ca ñoom, Yudeen ña jàpp leen ñuy dund, ñu yéege leen ci aw doj ba ca kaw. Ca njobbaxtalu doj wa lañu leen sànnee, ñu rajaxoo, ñoom ñépp.
13 Meanwhile the troops Amaziah sent back, not letting them join the battle, raided Judah's cities from Samaria to Beth-horon, struck down 3,000 people, and carried off much plunder. Niti gàngoor ga Amaciya waññi woon, ba ànduñook moom ca xare ba nag, ca dëkki Yuda lañu dalandoo, dale ca Samari ba Bet Oron. Bóom nañu ca ñoom ñetti junni, boole ca sëxëtoo cëxëtoo mu réy.
14 After Amaziah defeated the Edomites, he brought back the gods of Seir's people, set them up as his own gods, bowed to them, and burned offerings to them. Ndeke ba Amaciya ñibbisee, gannaaw ba mu dumaa Edomeen ña, ay yàllay waa Seyir la indaale, sampal leen boppam, ñu taxawe ay yàlla; ñoom lay sujjóotal, ñoom lay taalal cuuraay.
15 So our Father's anger burned against Amaziah, and he sent a prophet, who asked, "Why seek this people's gods, which couldn't save their own from your hand?" Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkkal Amaciya, mu yebal fa moom ab yonent, yonent ba ne ko: «Ana looy toppe yàllay askan wu xettaliwul ay ñoñam, ba jële leen ci say loxo?»
16 As he spoke, the king said, "Did we make you the king's counselor? Stop! Why be killed?" The prophet stopped but said, "I know our Father has determined to destroy you, because you did this and ignored my counsel." Naka lay wax ak moom, Amaciya dog ko, ne ko: «Kuy xelal buur lanu la def xanaa? Na doy! Ana looy indile sa bopp ay dóor?» Yonent ba noppi. Gannaaw loolu mu ne: «Xam naa ne Yàlla moo la nara sànk, ndax yaa def lii, te dégguloo samab digle.»
17 Amaziah king of Judah consulted his advisers, then sent to Joash son of Jehoahaz, son of Jehu, king of Israel: "Come, let us face each other in battle." Gannaaw ba Amaciya buurub Yuda diisoo ak ñi koy xelal, dafa yónnee ca buurub Israayil Yowas doomu Yowaxas doomu Yewu. Mu ne ko: «Dëkk naa la, dikkal, nu jàkkaarloo!»
18 Joash king of Israel answered Amaziah king of Judah: "A Lebanon thistle sent to a Lebanon cedar, saying, 'Give your daughter to my son as wife.' But a wild Lebanon beast passed and trampled the thistle. Yowas buurub Israayil yónnee Amaciya buurub Yuda tontam, ne ko: «Ndég ga ca Libaŋ moo yónnee woon ca garabu seedar gu mag ga ca Libaŋ, ne ko: “Sa doom jii, may ko sama doom jabar.” Ci kaw loolu rabu àllu Libaŋ jaare fa, dëggaate ndég ga.
19 You said, 'Look, I have struck down Edom,' and your heart grew proud, boasting. Stay home. Why court disaster and fall—you and Judah with you?" Nee nga xanaa du yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la, nga di ko damoo. Léegi nag tee ngaa toog sa kër? Ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?»
20 But Amaziah wouldn't listen—this was from our Father, to hand them over for seeking Edom's gods. Amaciya nag faalewul wax jooju, te Yàlla moo dogal loolu, ngir teg ko ciy loxo, ndax yàllay Edom ya ñu toppoon.
21 So Joash king of Israel marched up, and he and Amaziah king of Judah faced off at Beth-shemesh in Judah. Gannaaw loolu Yowas buurub Israayil jóg; ñu jàkkaarloo mook Amaciya buurub Yuda, ca Bet Semes ga ca Yuda.
22 Judah was defeated by Israel, and everyone fled to his own home. Ba mu ko defee muy jéllu Yuda fa kanam Israayil. Waa Yuda tasaaroo, ku nekk ñibbi ca sab xayma.
23 Joash king of Israel captured Amaziah king of Judah, son of Joash, son of Jehoahaz, at Beth-shemesh, took him to Jerusalem, and broke down its wall from the Ephraim Gate to the Corner Gate—about 600 feet. Yowas buurub Israayil nag jàpp buurub Yuda, Amaciya doomu Yowas doomu Yowaxas, ca Bet Semes. Gannaaw loolu mu yóbbu ko Yerusalem, daldi màbb tata ja, la ko dale buntu Efrayim ba ca buntu Ruq ba, muy ñeenti téeméeri xasab.
24 He took all the gold, silver, and articles found in the house of our Father in Obed-edom's care, plus the palace treasures and hostages, and returned to Samaria. Ci biir loolu wurus waak xaalis baak mboolem jumtukaay ya nekkoon ca kër Yàlla, ca loxol Obedd Edom ak ca denci kër buur, mu jël lépp, boole ca nit ñu mu jàpp, daldi dellu Samari.
25 Amaziah son of Joash, king of Judah, lived fifteen years after Joash son of Jehoahaz, king of Israel, died. Amaciya doomu Yowas buurub Yuda dund na fukki at ak juróom gannaaw deewug buuru Israayil Yowas doomu Yowaxas.
26 The rest of Amaziah's acts, first to last, are they not written in the Book of the Kings of Judah and Israel? Li des ci mbiri Amaciya, yu njëkk yaak yu mujj ya, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Buuri Yuda ak Israayil.
27 After Amaziah turned from following our Father, they conspired against him in Jerusalem, and he fled to Lachish. But they sent men after him there and killed him. La dale jant ba Amaciya dëddoo Aji Sax ji, ca la ko ay nit lalal pexe ca Yerusalem, mu daw dem Lakis, ñu yónnee dabi ko ca Lakis. Foofa lañu ko reye.
28 They brought him back on horseback and buried him with his ancestors in the City of Judah. Ba mu ko defee, ay fas lañu yóbboo néew ba, denci ko fa ay maamam, ca dëkk ba, ca Yuda.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]