Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 20 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Later, Moabites and Ammonites, with some Meunites, came to make war on Jehoshaphat. Gannaaw ba loolu wéyee, Mowabeen ña ak Amoneen ña, ñook ñenn ca Mewuneen ña ñoo dikk song Yosafat xare.
2 Messengers came and reported to Jehoshaphat, "A vast army comes against you from beyond the Dead Sea, from Edom, already at Hazazon-tamar" (En-gedi). Ay ndaw dikke Yosafat xibaar ne ko: «Fi sa kaw de, la gàngoor gu mag jëm, bawoo wàllaa géeju Xorom ga, fa Edom. Ña nga noonu ca Acacon Tamar, maanaam Engedi.»
3 Jehoshaphat was afraid, so he set himself to seek our Father, and proclaimed a fast throughout Judah. Tiitaange nag jàpp Yosafat, mu fas ci yéenee tinu Aji Sax ji. Ci biir loolu mu yéene koor ci Yuda gépp.
4 Judah gathered to seek our Father; from every town of Judah they came to seek him. Ci kaw loolu Yuda gépp daje ngir ñaan Aji Sax ji, mboolem dëkki Yuda lañu jóge ngir saraxu Aji Sax ji.
5 Then Jehoshaphat stood up in the assembly of Judah and Jerusalem, in our Father's house, before the new courtyard. Ba mu ko defee Yosafat taxaw fa mbooloom Yuda ak Yerusalem, fa biir kër Aji Sax ji, janook ëtt bu bees ba.
6 He said: "O our Father, God of our ancestors, are you not our Father in heaven? You rule all kingdoms of nations. Power and might are in your hand; none can stand against you. Mu ne: «Aji Sax ji sunu Yàllay maam, xanaa du yaay Yàlla ja fa asamaan, te yaay buur bi tiim mboolem nguuri xeet yi? Sa loxoo am doole ak kàttan, te kenn tëwu la.
7 Our Father, didn't you drive out this land's people before your people Israel, giving it forever to Abraham your friend's descendants? Xanaa du yaw sunu Yàlla yaa dàq ñi dëkke woon réew mii, fi kanam Israayil sa ñoñ, ba jox ko sa askanu xarit, Ibraayma, ba fàww?
8 They have lived in it and have built you a sanctuary in it for your name, saying, Ñu dëkk fi, tabaxal la fi béreb bu sell ngir sa tur, ba ne:
9 if disaster comes on us—sword of judgment, plague, or famine—we'll stand before this house and before you, for your name is in this house, and cry out to you in our distress, and you'll hear and save. “Su musiba dikkee ci sunu kaw, muy saamar mbaa mbugal mbaa mbas mbaa ab xiif, ba nu taxaw fi kanam kër gii ak fi sa kanam, ndax kat sa tur a ngi ci kër gii, su boobaa su nu yuuxoo, woo la wall, nanga nu nangul, wallu nu.”
10 Now: Ammon, Moab, and Mount Seir—you would not let Israel invade them when they came from Egypt; Israel turned away from them and did not destroy them. «Léegi nag xoolal ñii di waa Amon ak Mowab ak tundu Seyir, réew yooyee nga mayul woon Israayil ñu jaare fa, ba ñu bàyyikoo réewum Misra, ba tax ñu teggi leen, ba faagaagaluñu leen.
11 See how they repay us, coming to drive us from the possession you gave us to inherit. Ñooñoo ngii feyewuñu nu, lu moy dikk ngir dàqe nu ci sa céru suuf bi nga nu moomale!
12 Our Father, won't you judge them? We're powerless against this vast army coming against us; we don't know what to do, but our eyes are on you." Éy sunu Yàlla, xanaa doo leen ñàkka dikke mbugal mi ñu yelloo, nde nun kat amunu dooley jànkoonteek gàngoor gu réy gii dikk ci sunu kaw. Nun nag danoo xamul nu nuy def, te yaw kat lanu ne jàkk sunuy gët.»
13 All Judah stood there before our Father, with their little ones, their wives, and their children. Yuda gépp a nga taxaw fa kanam Aji Sax ji, ñook seen njaboot gu sew, seeni jabar ak seeni doom.
14 Then our Father's Spirit came on Jahaziel son of Zechariah, son of Benaiah, son of Jeiel, son of Mattaniah, a Levite of Asaph's line, amid the assembly. Ci biir loolu leerug Aji Sax ji wàcc fa digg mbooloo ma, ca kaw jenn waay ju sëtoo ci Asaf, di Yaxasyel. Yaxasyel moomu, Sàkkaryaa mooy baayam; Sàkkaryaa, Benaya mooy baayam; Benaya, Yewel ay baayam; Yewel, Mataña Leween ba mooy baayam.
15 He said: "Listen, all Judah, Jerusalem's residents, and King Jehoshaphat. This is what our Father says to you: Do not fear or be terrified by this vast army—the battle isn't yours but our Father's. Yaxasyel ne: «Yeen waa Yuda gépp ak waa Yerusalem ak yaw Buur Yosafat, teewluleen. Aji Sax ji da leena wax ne leen: “Yeen buleen tiit, buleen ragal gàngoor gu réy gii, ndax xare bi du yeena ko moom, xareb Yàllaa.
16 Tomorrow go down against them: they're climbing the Ziz ascent; you'll find them at the valley's end, facing the Jeruel wilderness. Ëllëg dalleen ci seen kaw, ñu ngoogu jaare yéegub Cicc di dikk. Ca catal wal ma ngeen di dajeek ñoom, fa janook màndiŋu Yerwel.
17 You won't need to fight this battle. Take your places, stand firm, and watch our Father rescue you, Judah and Jerusalem. Don't fear or lose heart. March out against them tomorrow, for our Father is with you.'" Du yeenay xare bii xare. Dikkleen taxaw ba gis ndamal Aji Sax jeek yeen. Yeen waa Yuda ak Yerusalem, buleen tiit, buleen ragal. Ëllëg génnleen dajeek ñoom, Aji Sax ji mooy ànd ak yeen.”»
18 Jehoshaphat bowed face-down, and all Judah and Jerusalem's people fell in worship before our Father. Ba loolu amee Yosafat sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mboolem Yuda ak waa Yerusalem ne gurub sukk fa kanam Aji Sax ji, ngir sujjóotal Aji Sax ji.
19 Then the Levites from the Kohathites and Korahites stood to praise our Father, Israel's God, with a loud voice raised high. Ba mu ko defee Leween ña bokk ca làngu Keyat ak làngu Kore daldi jóg, di sàbbaale baat bu réy te kawe, ñeel Aji Sax ji Yàllay Israayil.
20 At dawn they went out to Tekoa's wilderness. As they went out, Jehoshaphat stood and said, "Hear me, Judah and people of Jerusalem. Trust your Father and you'll stand firm; trust his prophets and you'll succeed." Ca ëllëg sa ñu teela xëy, génn, jëm màndiŋu Tekowa. Bala ñoo dem nag Yosafat taxaw, ne: «Yeen Yuda ak waa Yerusalem gépp, gëmleen seen Yàlla Aji Sax ji, seen taxawaay dëgër; gëmleen ay yonentam, seen pexe sotti.»
21 After consulting the people, Jehoshaphat appointed singers to our Father to praise his holy splendor, marching ahead of the army: "Give thanks to our Father, for his faithful love endures forever." Ba loolu wéyee Yosafat féncoo ak askan wa, ba noppi tabb ay woykat ngir woy Aji Sax ji, di ko sàbbaal ndax li mu gànjaroo sellaay, te ñu jiitu boroom ngànnaay yi, naan: «Santleen Aji Sax ji, kee saxoo ngoram ba fàww.»
22 As they began to sing and praise, our Father set ambushes against the Ammonites, Moabites, and the people of Mount Seir who were attacking Judah, and they were struck down. Naka lañu tàmbalee sarxolle aka sàbbaal, Aji Sax ji teg ay tërukat ci kaw niti Amon ak Mowab ak waa tundu Seyir, ña songsi Yuda. Ba loolu amee dees leena duma.
23 Ammon and Moab turned against Mount Seir's people to destroy and annihilate them; once Seir's people were finished, Ammon and Moab turned and slaughtered each other. Waa Amon ak waa Mowab ñoo jóg dal ci kaw waa tundu Seyir, faagaagal leen, bóom leen. Ba ñu noppee ca waa Seyir, lañu tàmbalee songoo ca seen biir, ku nekk dal ca moroom ma, ngir rey ko.
24 When Judah reached the wilderness lookout and looked toward the vast army, they saw only corpses fallen on the ground—no one had escaped. Ba Yudeen ña agsee ca wattukaay ba ñu mana séentoo màndiŋ ma, ba dawal seen bët fa gàngoor ga nekkoon, gisuñu lu moy ay néew yu ne wetar fa suuf, kenn rëccul.
25 Jehoshaphat and his people came to plunder the dead, finding abundant goods, clothing, and valuables—too much to carry, so gathering it took three days. Yosafat ak gàngooram nag dikk ngir sëxëtoo seen alal. Fekk nañu fa lu bare ci alal, ay yére ak ay gànjar. Dañoo jël a jël ba manuñoo yóbbu la ñu jël lépp. Ñetti fan lañu sëxëtoo cëxëtoo ma, ndax na mu baree.
26 On day four, they gathered at the Valley of Beracah and praised our Father there—so it's named Valley of Beracah to this day. Keroog ca gannaawaati ëllëg sa, di bésub ñeenteel ba, ñu daje ca xuru Beraka. Ñu daldi fay sant Aji Sax ji. Moo tax ñuy woowe béreb boobu, ba tey jii xuru Beraka (muy firi Cant).
27 All the men of Judah and Jerusalem, Jehoshaphat leading, returned there with joy, for our Father gave them joy over their enemies. Ba mu ko defee mboolem niti Yuda ak Yerusalem walbatiku, Yosafat jiitu leen, ngir dellu Yerusalem, ànd ak mbég, ndax Aji Sax jee leen bànneexal ca seeni noon.
28 They entered Jerusalem with harps, lyres, and trumpets, and went to the house of our Father. Ay xeeti xalam aki liit lañu duggsee Yerusalem, ba agsi ca kër Aji Sax ji.
29 Fear of our Father fell on all the surrounding kingdoms when they heard our Father fought Israel's enemies. Ba loolu wéyee, tiitaange ju Aji Sax ji sabab moo dikkal mboolem nguuri réew yi, ba ñu déggee ne Aji Sax ji moo xareek nooni Israayil.
30 So Jehoshaphat's kingdom was at peace, for his Father gave him rest on every side. Nguurug Yosafat nag dal, Yàllaam may ko noflaay fa ko wër fépp.
31 Jehoshaphat reigned over Judah, crowned at thirty-five, twenty-five years in Jerusalem; his mother, Azubah daughter of Shilhi. Noonu la Yosafat nguuroo fa Yuda. Amoon na fanweeri at ak juróom ba muy falu, te ñaar fukki at ak juróom la falu ca Yerusalem. Yaayam moo doon Asuba doomu Silxi.
32 He walked in his father Asa's ways, never turning aside, doing right in our Father's eyes. Yosafat ci tànki baayam Asa la aw, jàddul fenn, xanaa di def njub gi Aji Sax ji rafetlu.
33 Yet the high places stayed; the people still had not set their hearts on their ancestors' God. Waaye jëleesu fa bérebi jaamookaay ya. Askan wa nag defaguñu woon seen xel ba tey ci seen Yàllay maam.
34 Jehoshaphat's other acts, first to last, are in Jehu son of Hanani's records, found in the Book of Kings of Israel. Li des ci mbiri Yosafat, yu njëkk yaak yu mujj ya, ña nga noonu binde ci kàdduy Yewu doomu Anani, ya ñu bind ca téereb buuri Israayil.
35 Later Jehoshaphat king of Judah allied with Ahaziah king of Israel, who did evil. Gannaaw gi la Yosafat buurub Yuda lëngoo ak Axasya buurub Israayil ma daan jëfe jëf ju bon.
36 He joined with him to build a fleet of trading ships to go to Tarshish, built at Ezion-geber. Bëgga defarlu ay gaal yu jëm Tarsis nag moo taxoon mu lëngook moom. Ca Eccon Geber lañu defare gaal ya.
37 Eliezer son of Dodavahu of Mareshah prophesied against Jehoshaphat: "For allying with Ahaziah, our Father broke your work apart." The ships wrecked and couldn't sail to Tarshish. Teewul Elyeser doomu Dodawa mu Maresa jottali kàdduy waxyu yu dal Yosafat. Mu ne ko: «Gannaaw yaa lëngoo ak Axasya, Aji Sax ji mooy yàq say liggéey.» Ci kaw loolu gaal ya yàqu, ba manatuñoo dem Tarsis.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]