Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 19 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Jehoshaphat king of Judah returned safely to his house in Jerusalem. Gannaaw loolu Yosafat buurub Yuda dellu ak jàmm këram ca Yerusalem.
2 Jehu son of Hanani the seer met King Jehoshaphat and asked, "Should you help the wicked and love those who hate our Father? For this, wrath from our Father is on you. Yewu doomu Anani boroom peeñu ba nag dikk, dajeek Buur Yosafat, ne ko: «Nit ku bon, dees na ko wallu? Am ñi bañ Aji Sax ji, sopp leen war na la? Li nga def tax na am sànj dal ci sa kaw, bawoo fa Aji Sax ji.
3 Still, good is found in you: you cleared the Asherah poles from the land and set your heart to seek our Father." Teewul nag gisees na jëf ju baax ci yaw; yaa jële ci réew mi, xer yi ñuy jaamoo Asera tuur mi, te it ci jaamu Yàlla nga saxal sam xel.»
4 Jehoshaphat lived in Jerusalem, then went out again among the people, from Beersheba to Ephraim's hill country, turning them back to our Father, God of their ancestors. Yosafat toog na Yerusalem ab diir, waaye dellu naa génn, dem ca biir askan wa, dale Beerseba ba diiwaanu tundi Efrayim, ba waññi leen ci Aji Sax ji seen Yàllay maam ya.
5 He appointed judges in the land, in all the fortified cities of Judah, city by city. Ay àttekat la tabb ca réew ma, mboolem dëkki Yuda ya tata wër, dëkkoo dëkk.
6 He told the judges, "See what you do—you judge not for people but for our Father, and he is with you in every case you decide. Mu ne àttekat ya: «Xoolleen bu baax li ngeen di def, ndax kat du doom aadama ngeen di àtteel, waaye Aji Sax ji ngeen di àtteel, te mooy ànd ak yeen ci mbirum àtte mu mu doon.
7 Now let fear of our Father be on you. Watch and act, for with our Father there is no injustice, no favoritism, no bribery." Kon nag na ragal Aji Sax ji di ab téeñ ci seen kaw. Moytuleen li ngeen di def, ndax Aji Sax ji sunu Yàlla kat xajoowul gennug njubadi akug par-parloo akub ger.»
8 Also in Jerusalem, Jehoshaphat appointed some Levites, priests, and heads of Israel's ancestral families to render the judgment of our Father and to settle disputes; they returned to Jerusalem. Ca Yerusalem itam, gannaaw ba ñu fa dellusee, Yosafat tabb na fa ñenn ci ay Leween aki sarxalkat ak ñenn ca ña jiite seeni kër maam ca Israayil, ngir ñuy àtte àtteb Aji Sax ji ak lijjanti ay jote.
9 He commanded them: "Act this way, in fear of our Father, faithfully and wholeheartedly. Mu sant leen ne leen: «Nii ngeen di jëfe ci biir ragal Aji Sax ji ak worma ak xol bu dëggu ba mat sëkk:
10 Whenever your brothers in their cities bring you a dispute—over bloodshed, or over law and commandment, statutes and rulings—warn them, so they don't incur guilt before our Father, bringing wrath on you and your brothers. Do this, and you will not incur guilt. mépp mbir mu leen dikkal, bawoo ci seeni bokk ca dëkk ya ñu dëkke, muy mbirum deret ju ñu tuur ak jote bu jëm ci ndigalu yoon ak ab santaane ak dogali yoon ak àttey yoon, nangeen leen artu ngir ñu bañ cee tooñ Aji Sax ji, ba am sànj di dal ci seen kaw yeen ak ci kaw seeni bokk. Noonu ngeen di def, ba dungeen tooñ.
11 Now, Amariah the chief priest oversees you in every matter of our Father; Zebadiah son of Ishmael, leader of Judah's tribe, in every matter of the king. The Levites serve as officials before you. Be strong and act—may our Father be with those who do good." Sarxalkat bi Amarya miy njiitu sarxalkat nag, moo leen fare kaw ci mboolem mbirum Aji Sax ji. Sebaja doomu Ismayel, njiitu kërug Yuda, fare leen kaw ci mboolem mbirum buur, bindkat yi leen di taxawu di Leween ñi. Dëgërluleen te liggéey. Yal na Aji Sax ji ànd ak ku ciy def lu baax.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]