Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 18 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Now Jehoshaphat had great riches and honor, and he allied himself with Ahab by marriage. Yosafat amoon na alal ak daraja ju bare. Moo lëngoo ak Axab, ci kaw séy bu mu amal diggante kenn ci waa këram ak waa kër Buur Axab.
2 Some years later he went down to Ahab in Samaria, where Ahab slaughtered many sheep and oxen for him and for the people who were with him, urging him to attack Ramoth-gilead. Ñu teg ca ay at, mu dikk seetsi Axab ca Samari. Axab reyal ko ay gàtt ak nag yu bare, mook topp ma mu àndal. Ci biir loolu mu soññ ko ci ànd ak moom, ngir songi Ramot ga ca Galàdd.
3 Ahab king of Israel asked Jehoshaphat king of Judah, "Will you go with me to Ramoth-gilead?" He answered, "I am as you are, my people as yours; we join you in the war." Axab buurub Israayil ne Yosafat buurub Yuda: «Xanaa dinga ànd ak man ca xareb Ramot ga ca Galàdd?» Mu ne ko: «Maa ngi, yaa ngi; te say nit laak samay nit. Maak yaw la ca xare ba.»
4 But Jehoshaphat said to the king of Israel, "First seek the word of our Father." Yosafat teg ca ne buurub Israayil: «Njëkkala seet lu ci Aji Sax ji wax.»
5 So the king of Israel gathered the prophets, 400 men, and asked them, "Will we go to Ramoth-gilead for battle, or hold back?" They said, "Go up, for God will hand it over to the king." Buurub Israayil woo yonent yi, ñu daje, di ñeenti téeméer (400). Mu laaj leen ne leen: «Ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am nu bàyyi?» Ñu ne ko: «Demal, ndax Yàlla moo leen di teg ci sa loxo.»
6 But Jehoshaphat said, "Is there not still a prophet of our Father here whom we can consult?" Yosafat dellu ne: «Xanaa beneen yonentu Aji Sax ji da fee amatul, ba ñu mana seetlujeeti fa moom?»
7 Israel's king told Jehoshaphat, "One man remains through whom we can ask our Father, but I hate him—he never prophesies good about me, only bad. He is Micaiah son of Imlah." Jehoshaphat replied, "The king shouldn't say that." Buurub Israayil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du jottali ci man kàdduy waxyu yu baax. Bés bu nekk, lu bon rekk. Mise la, doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»
8 Then the king of Israel summoned an officer and said, "Bring Micaiah son of Imlah quickly." Buurub Israayil daldi woo ab jawriñam ne ko: «Gaawal dem indil ma Mise doomu Yimla.»
9 The king of Israel and Jehoshaphat king of Judah sat each on his throne, dressed in robes, on the threshing floor at the entrance of Samaria's gate, with all the prophets prophesying before them. Buurub Israayil ak Yosafat buurub Yuda nag, ña nga toog, ku ci nekk ci ngànguneem. Ña nga solu ba jekk, toog ca dàgga ja ca buntu Samari. Yonent yépp janook ñoom, di biral ay kàdduy waxyu.
10 Zedekiah son of Chenaanah made iron horns and said, "God says: 'With these you will gore the Arameans until they are destroyed.'" Cedesyas doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, fekk na mu defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”»
11 All the prophets prophesied the same, saying: "Go up to Ramoth-gilead and win; our Father will hand it to the king." Mboolem yonent ya ca des nag di waxe genn kàddug waxyu googu, naan: «Buur, songal Ramot ga ca Galàdd te jël ndam li, ndax Aji Sax ji moo leen teg ci say loxo.»
12 The messenger sent to summon Micaiah told him, "The prophets' words all favor the king. Let yours match theirs—speak favorably." Ci kaw loolu ndaw la woowi Mise, dem ne ko: «Ma ne, kàddug yonent ya genn la, mooy jàmmu Buur. Kon nag, na sa kàddu ànd ak seen kàddu di genn, te nga wax jàmm.»
13 But Micaiah said, "As surely as our Father lives, I will say only what my Father says." Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy dund, li ma Aji Sax ji sama Yàlla wax rekk laay wax.»
14 When he came, the king said, "Micaiah, will we go to battle at Ramoth-gilead, or will I hold back?" He said, "Go up and win; they'll be handed to you." Ba Mise dikkee ba ca Buur, Buur ne ko: «Mise, ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am ma bàyyi?» Mu ne ko: «Songleen, daanee waay, dees na leen teg ci sa loxo.»
15 But the king said to him, "How many times must I make you swear to tell me only the truth in the name of our Father?" Buur nag ne ko: «Ñaata yoon laa lay giñloo ne la bu ma wax lu moy dëgg ci turu Aji Sax ji?»
16 Micaiah said, "I saw all Israel scattered on the mountains, like sheep without a shepherd. And our Father said, 'They have no master; let each return home in peace.'" Mise ne ko: «Israayil gépp laa gis ñu tasaaroo ca kaw tund ya, mbete xar yu amul sàmm. Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”»
17 Israel's king said to Jehoshaphat, "Didn't I tell you he'd prophesy nothing good about me, only evil?" Buurub Israayil nag ne Yosafat: «Waxuma la woon ne du jottali kàdduy waxyu yu baax ci man, xanaa lu bon rekk?»
18 Micaiah said, "Then hear the word of our Father: I saw our Father seated on his throne, all heaven's armies standing at his right and left. Mise teg ca ne ko: «Kon nag dégluleen kàddug Aji Sax ji. Aji Sax ji laa gis mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw, ndijooram ak càmmoñam.
19 And our Father said, 'Who will entice Ahab king of Israel to go up and fall at Ramoth-gilead?' One said this, another that. Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab buurub Israayil, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.
20 A spirit came forward, stood before our Father, and said, 'I will entice him.' And our Father asked him, 'How?' Kenn ci gàngoor ga dikk, taxaw fa kanam Aji Sax ji. Mu ne: “Man maa koy nax.” Aji Sax ji ne ko: “Nan?”
21 He said, 'I will go out and be a lying spirit in the mouth of all his prophets.' Then our Father said, 'You will lure him and also prevail. Go out and do so.' Mu ne: “Maay dikk, doon leer guy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.”
22 So now, our Father has put a lying spirit in the mouth of these prophets of yours, and our Father has declared disaster against you." Looloo waral lii. Aji Sax ji moo def leer guy safaan dëgg ci sa làmmiñu yonent yii, te Aji Sax ji moo tudd musiba ci sa kaw.»
23 Then Zedekiah son of Chenaanah came up, struck Micaiah on the cheek, and said, "Which way did the Spirit of God go from me to speak to you?" Ba loolu amee Cedesyas doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana wan yoon la leerug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man, di wax ak yaw?»
24 Micaiah said, "You'll see it that day when you go into an inner room to hide." Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.»
25 The king of Israel said, "Take Micaiah back to Amon the city governor and to Joash the king's son, Buurub Israayil nag ne: «Jàppleen Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi ak ca Yowas doomu Buur.
26 and say, 'The king says: Put this man in prison on meager rations of bread and water until I return safely.'" Ngeen ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugalleen kii kaso, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may délseek jàmm.”»
27 Micaiah said, "If you ever return safely, our Father has not spoken through me." Then he said, "Listen, all you people!" Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottali.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»
28 So the king of Israel and Jehoshaphat king of Judah went up to Ramoth-gilead. Ba mu ko defee buurub Israayil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ñu dem songi Ramot ga ca Galàdd.
29 The king of Israel said to Jehoshaphat, "I will disguise myself and go into battle, but you wear your robes." So the king of Israel disguised himself, and they went into battle. Buurub Israayil nag ne Yosafat: «Damay soppi col, dugg ci xeex bi, waaye yaw solal sa mbubbam buur.» Buurub Israayil soppig col, ñu dugg ca xeex ba.
30 The king of Aram had ordered his chariot captains, "Fight no one, small or great, but only the king of Israel." Fekk na buurub Siri jox ndigal ñay jiite watiiri xare ya. Mu ne leen: «Buleen xeex ak kenn, du ku tuut, du ku réy, diirleen buurub Israayil, moom rekk.»
31 When the chariot captains saw Jehoshaphat, they said, "That is Israel's king," and turned to fight him. But Jehoshaphat cried out, and our Father helped him, drawing them away from him. Ba loolu amee ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii mooy buurub Israayil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag woote wall, Aji Sax ji dimbali ko, waññi leen.
32 When the chariot captains saw he was not Israel's king, they stopped chasing him. Njiiti watiir ya xam ne du buurub Israayil, ñu walbatikuwaat, bàyyi ko.
33 A man drew his bow at random and struck the king of Israel between the joints of his armor. He told his chariot driver, "Turn around and get me out of the fighting; I'm wounded." Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israayil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiir ba: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!»
34 The battle raged that day. Israel's king was held up in his chariot facing the Arameans until evening, then died at sunset. Naka la xare ba tàkkarnaase bésub keroog bépp, buurub Israayil taxaw jonn rekk ca watiir ba, janook waa Siri, ba jant bay so, mu doora dee.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]