Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 17 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 His son Jehoshaphat became king in his place and strengthened himself against Israel. Ba mu ko defee Yosafat doomu Asa falu buur, wuutu ko. Mu dëju bu baax nag ci kaw Israayil, nguur ga ca bëj-gànnaar.
2 He stationed troops in all Judah's fortified cities and garrisons in the land of Judah and in the cities of Ephraim that his father Asa had captured. Yosafat teg ay gàngoor ca mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi teg ay kuréeli xare ca réewum Yuda, ak dëkki Efrayim ya Asa baayam nangu woon.
3 Our Father was with Jehoshaphat, for he walked his father David's earlier ways, not seeking the Baals. Ba mu ko defee Aji Sax ji ànd ak Yosafat, ndax na Daawuda maamam daan njëkka doxe, na la doxe, te sàkkuwul tuur ya ñuy wax Baal.
4 Instead, he sought the Father his father served, obeyed his commandments, and not the practices of Israel. Yàllay baayam daal la daan sàkku te ay santaaneem la daan doxe, baña roy jëfi Israayil.
5 So our Father secured the kingdom in his hand; all Judah brought gifts to Jehoshaphat, and he had great wealth and honor. Aji Sax ji nag dëgëral nguur ga ca loxoom, Yuda gépp di indil Yosafat ab galag, mu am alal ak daraja ju bare.
6 His heart was devoted to our Father's ways; he removed the high places and Asherah poles from Judah. Ci kaw loolu pastéefu xolam ci jëfe coobarey Aji Sax ji yokku, ba mu jëleeti fa Yuda, bérebi jaamookaay ya, ak xer ya ñuy màggale Asera tuur ma.
7 In his reign's third year he sent his officials Ben-hail, Obadiah, Zechariah, Nethanel, and Micaiah to teach in Judah's cities, Mu teg ca yebal, ca ñetteelu atum nguuram, jawriñam ñii di Ben Xayil ak Abdiyas ak Sàkkaryaa ak Netaneel ak Mikaya, ngir ñu jàngaleji ca dëkki Yuda.
8 and the Levites with them: Shemaiah, Nethaniah, Zebadiah, Asahel, Shemiramoth, Jehonathan, Adonijah, Tobijah, Tob-adonijah; and with them the priests Elishama, Jehoram. Ña ànd ak ñoom di ay Leween, Semaya ca la, ak Netaña ak Sebaja ak Asayel ak Semiramot ak Yonatan ak Adoña ak Tobya ak Tob Adoña. Leween ñooña àndaale ak Elisama ak Yexoram, sarxalkat ya.
9 They taught throughout Judah, carrying the Book of our Father's Instruction, going to all Judah's cities, teaching the people. Ñu yóbbaale téereb yoonu Aji Sax ji. Mboolem dëkki Yuda lañu wër, di jàngal askan wa.
10 The dread of our Father fell on all the kingdoms around Judah, so they made no war on Jehoshaphat. Tiitaange ju Aji Sax ji sabab nag dikkal mboolem nguuri réew yi séq Yuda, ba tax songuñu Yosafat xare.
11 Some Philistines brought Jehoshaphat gifts and silver tribute; the Arabs brought flocks: 7,700 rams, 7,700 male goats. Ay Filisteen itam di indil Yosafat ay may akub xaalis akub galag, Arab ya sax indil ko ay gàtt: ay kuuy, juróom ñaari junni ak juróom ñaari téeméer (7 700); ak ay sikket, juróom ñaari junni ak juróom ñaari téeméer (7 700).
12 Jehoshaphat grew more and more powerful, and he built fortresses and storage cities in Judah. Yosafat gën di màgg, ba kawe lool. Ci biir loolu mu tabax ca Yuda ay këri buur ak dëkki dencukaay.
13 He had large supplies in the cities of Judah, and mighty warriors in Jerusalem. Ay denc yu takku la amoon fa dëkki Yuda, ak niti xarekat, jàmbaari xare yu am doole fa Yerusalem.
14 Their enrollment by ancestral house: from Judah, commanders of thousands—Adnah the commander, with him 300,000 mighty warriors; Ñii nag lañu limal ñooñu, na ñu bokke seeni kër maam: Ci wàllu Yuda, njiiti junni ya, ñoo di njiit la Atna, ma jiite ñetti téeméeri junniy (300 000) jàmbaari xare yu am doole.
15 next to him was Jehohanan the commander, and with him 280,000; Mu feggook njiit la Yoxanan, ma jiite ñaari téeméer ak juróom ñett fukki junniy (280 000) góor.
16 next Amasiah son of Zichri, who volunteered for our Father, with him 200,000 mighty warriors. Kooku feggook doomu Sikkri, Amasiya ma yebul boppam ci liggéeyu Aji Sax ji. Moo jiite ñaari téeméeri junniy (200 000) jàmbaari xare.
17 From Benjamin: Eliada, a mighty warrior, and with him 200,000 armed with bow and shield; Ci wàllu Beñamin, ñeyu xare ba Elyada moo jiite ñaari téeméeri junni (200 000) ñu gànnaayoo xalaaki fitt ak pakk.
18 next to him Jehozabad, and with him 180,000 equipped for war. Mu feggook Yewosabàdd ma jiite téeméer ak juróom ñett fukki junni (180 000) ñu gànnaayu.
19 These men served the king, besides those he stationed in the fortified cities throughout Judah. Ñooñu ñoo yoroon ndénkaaneb buur bi, te bokkewul ak ña mu tegoon ca dëkk ya tata wër, ca mboolem Yuda.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]