Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 16 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In Asa's thirty-sixth year, Baasha king of Israel invaded Judah, fortifying Ramah to keep anyone from leaving or entering Asa king of Judah's territory. Ca fanweereelu at ak juróom benneel ci nguurug Asa, Basa buurub Israayil moo song Yuda, daldi dàbbali dëkk ba ñuy wax Raama, ba kenn du dugg jëm ca Asa buurub Yuda, mbaa muy génn.
2 Asa took silver and gold from the storerooms of our Father's house and the royal house, and sent them to Ben-Hadad king of Aram, living in Damascus, with this message: Asa yebbee fa denci kër Aji Sax ji ak kër buur xaalis ak wurus, yónnee ko Ben Addàd buurub Siri ba ca Damaas, yóbbantewaale ko kàddu yii:
3 "Let there be a treaty between me and you, as there was between my father and your father. See, I'm sending you silver and gold. Go now and break your treaty with Baasha king of Israel, so he withdraws from me." «Kóllëree dox sama digganteek yaw, na mu doxe woon sama diggante baay ak sa baay. Lii nag maa la ko may, muy xaalis ak wurus. Te nga dogoo rekk ak Basa buurub Israayil, ndax mu jóge samam réew.»
4 Ben-Hadad agreed with King Asa and sent his army commanders against Israel's cities. They struck down Ijon, Dan, Abel-maim, and all Naphtali's store cities. Ben Addàd déggal Buur Asa, daldi yebal njiiti gàngooram ca dëkki Israayil. Nii lañu nangoo dëkk ya ñuy wax Yon ak Dan ak Abel Mayim, ak mboolem dëkki dencukaay ya ca Neftali.
5 When Baasha heard of it, he stopped fortifying Ramah and abandoned his work. Ba ko Basa déggee, Raama ga mu doon dàbbali la ba, ba dakkal liggéeyam ya mu fa sumboon.
6 King Asa mustered all Judah; they carried off the stones and timber Baasha had fortified Ramah with, and with them he fortified Geba and Mizpah. Ba loolu amee Asa dajale Yuda gépp, ñu yóbbu doj yaak bant ya Basa doon tabaxe fa Raama. Ca la tabaxe dëkk ya ñuy wax Geba ak Mispa.
7 Then Hanani the seer came to Asa king of Judah and said to him, "Because you relied on Aram's king and not your Father, his army escaped your hand. Jant yooyu la Anani boroom gis ba dikk ca Asa buurub Yuda, ne ko: «Gannaaw defoo sa yaakaar ci sa Yàlla Aji Sax ji, xanaa ngay yaakaar buurub Siri, gàngooru buurub Siri rëcc na la.
8 Weren't Cushites and Libyans a vast army with countless chariots and horsemen? Because you relied on your Father, he gave them to you. Xanaa Kuuseen ñi ak waa Libi duñu woon gàngoor gu mag aki watiir aki gawar yu baree bare? Ndaxam ba nga defee sa yaakaar ci Aji Sax ji, moo leen teg ci sa loxo.
9 For our Father's eyes scan the whole earth, to strengthen those whose heart is fully devoted to him. You acted foolishly in this; from now on you will have wars." Aji Sax ji déy suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol. Yëfi dof nga def ci mbir mii, ndax li dale tey ay xare topp na la.»
10 Asa raged at the seer for this and jailed him in the stocks, for he was furious with him about it; he also brutally oppressed some people at that time. Ba loolu amee Asa mer, sànju ca kaw boroom gis ba ndax kàddu yooyu, ba dugal ko kaso, jéng ko. Jant yooyu la Asa mitital ñenn ca askan wa.
11 Asa's acts, first to last, are written in the Book of the Kings of Judah and Israel. Mu ngoog, mbiri Asa yu njëkk yaak yu mujj ya, ña nga binde ca téere ba ñu dippee Buuri Yuda ak Israayil.
12 In his thirty-ninth year of reign, Asa's feet grew diseased, the disease severe. Yet even in his illness he did not seek our Father, but only the doctors. Ca fanweereelu at ak juróom ñeenteel ci nguuram nag, jàngoroy tànk moo jàpp Asa, ba mu mujj metti, te jàngoroom ja taxul sax mu sàkku ndimbalu Aji Sax ji, xanaa fajkat ya.
13 Then Asa rested with his fathers, dying in the forty-first year of his reign. Gannaaw gi, Buur Asa saay, fekki ay maamam. Ca ñeent fukkeelu atu nguuram ak benn la dee,
14 They buried him in his own tomb, cut for himself in the City of David, laid him on a funeral bed covered with spices and various blended perfumes prepared by skilled perfumers, and lit a great fire for him. ñu denc ko ca bàmmeelu dojam bu mu yattaloon boppam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Ab lal bu ñu jal mboolem xeeti cuuraay yu njafaan-kat waajal, ca lañu ko tëral. Ci biir loolu ñu taalal ko taal bu réy lool, sargale ko ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]