Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Romans 6 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 What should we say, then? Should we go on sinning so that grace may increase? Lu nu wara wax léegi nag? Xanaa nu sax ci bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gëna bare?
2 Absolutely not! How can we who died to sin still live in it? Mukk! Nun ñi dee, ba rëcc ci kàttanu bàkkaar, naka lanu manatee sax ci di ko def?
3 Or are you unaware that all of us baptized into Christ Jesus were baptized into his death? Xanaa dangeena xamul ne, képp ku ñu sóob ci ndox, ngir wone ne mu ngi bokk ci Yeesu Kirist, ci deewu Yeesu la bokk.
4 So we were buried with him through baptism into death, that as Christ was raised from the dead through our Father's glory, we too might walk in newness of life. Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees.
5 For if we've been joined to his death's likeness, we'll surely also be joined to his resurrection. Kon nag gannaaw benn lanu ak Kirist, dee ni mu deeye woon, kon dinanu nekk it benn ak moom, dekki ni mu dekkee woon.
6 We know our old self was crucified with him to destroy sin's body, so we'd no longer be enslaved to sin. Ndegam xam nanu ne daajoon nañu Kirist ca bant ba, xam nanu it ne jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale nañu ko ak Kirist ca bant ba. Yàlla def na loolu, ngir nguuru bàkkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu rëcc ci dooleem.
7 For anyone who has died has been set free from sin. Ndaxte ku dee, bàkkaar manatul dara ci yaw.
8 Now if we died with Christ, we believe that we will also live with him. Gannaaw nag dee nanu ak Kirist, gëm nanu ne dinanu dekki it ni moom,
9 For we know Christ, raised from the dead, never dies again; death no longer rules him. xam ne Kirist mi dekki dootul dee mukk, dee manatul dara ci moom.
10 For the death he died, he died to sin once for all; but the life he lives, he lives to our Father. Dee na benn yoon, ba bàkkaar manul ci moom dara; mi ngi dund léegi, di ànd ak Yàlla ba fàww.
11 In the same way, count yourselves dead to sin but alive to our Father in Christ Jesus. Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
12 Therefore do not let sin reign in your mortal body so that you obey its desires. Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam.
13 Do not offer your body's parts to sin as weapons for wrongdoing; instead, offer yourselves to our Father as those brought from death to life, and your body's parts to him as weapons for righteousness. Buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
14 For sin will not have mastery over you, because you are not under law but under grace. Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla.
15 What then? Should we sin because we are not under law but under grace? Absolutely not! Lan lanu wara wax nag léegi? Gannaaw génn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla, ndax danoo wara sax ci def bàkkaar? Mukk!
16 Don't you know that offering yourselves to someone as slaves to obey makes you slaves of whoever you obey—whether sin, leading to death, or obedience, leading to righteousness? Ndax dangeena xamul ne koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub.
17 Thanks to our Father: you were slaves of sin, but you obeyed from the heart the teaching pattern you were entrusted to. Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp.
18 Having been set free from sin, you became slaves of righteousness. Ci noonu rëcc ngeen ci notaangeg bàkkaar te jébbalu ci Yàlla, sóobu ci njub.
19 I speak humanly, since your flesh is weak. As you offered your body's parts as slaves to impurity and lawlessness, resulting in more lawlessness, now offer them as slaves to righteousness, resulting in holiness. Xam naa ne seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen jële woon seeni cér, jébbal leen, ñu nekk jaami lu selladi ak lu bon, di gëna jur lu bon, noonu itam léegi jébbal-leen seeni cér, ñu nekk jaami njub, ngeen doora sell.
20 For when you were slaves of sin, you were free from righteousness. Ndaxte keroog ba ngeen nekkee jaami bàkkaar, séquleen woon dara ak lu jub.
21 What did you gain then from what you're now ashamed of? For those things end in death. Ban njariñ ngeen ci jële nag? Dara lu dul gàcce, ndaxte ci dee la leen doon jëmale.
22 But now, freed from sin and enslaved to our Father, your fruit leads to holiness, and the end, eternal life. Waaye léegi Yàlla goreel na leen ci kilifteefu bàkkaar, def leen ay jaamam, ba jural leen sellaay, jëme leen ci dund gu dul jeex.
23 For the wages of sin is death, but our Father's gift is eternal life in Christ Jesus our Lord. Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]