Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Romans 7 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Or don't you know, brothers—I'm speaking to people who know the law—that the law rules over a person only while he lives? Bokk yi, yéen ñi may waxal xam ngeen luy yoon; xam ngeen kon ne yoon am na doole ci nit diirub dundam.
2 A married woman is bound by law to her husband while he lives; if he dies, she is free from the law of the husband. Ci maanaa, mu ngi mel ni jigéen juy séy; yoon a ngi koy boole ak jëkkëram, ñu ànd seen giiru dund, waaye su jëkkër ji faatoo, buum gi dagg na.
3 While her husband lives, she's called an adulterous woman if she becomes another man's wife; but if he dies, she's free from that law—not an adulterous woman if she marries another. Kon nag su jabar ji àndee ak beneen góor, te fekk jëkkër jiy dund, dees na ko àtte njaaloo. Waaye bu jëkkër ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na séy nag ak beneen góor, te du doon njaaloo.
4 So, my brothers and sisters, you too were put to death to the law through Christ's body, to belong to another—the one raised from the dead—so we might bear fruit for our Father. Nii laa leen ko mana misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeena deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa wàcc leen. Léegi nag yéena ngi ànd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Yàlla njariñ.
5 For when we were in the flesh, sin's passions, stirred by the law, worked in our bodies to produce fruit for death. Keroog ba nu daan topp sunu nafsu, yoonu Musaa daan na xamb bëgg-bëgg yu bon, yiy yëngal sunuy cér, ba jural nu dee.
6 But now we're released from the law, dead to what held us bound, so we serve in the new way of the Spirit, not the old way of the written code. Waaye léegi yoon wi wàcc na nu, ci li nu dee, ba rëcc cig buumam. Léegi nag nu ngi jaamu Yàlla, waxuma leen ci sàmm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci kàttan gu bees, gi nu Xelum Yàlla di may.
7 What then should we say? Is the law sin? Never! Yet I wouldn't have known sin except through the law—nor would I have known craving, had the law not said, "Do not crave what isn't yours." Kon nag lu nu wara wax? Ndax bàkkaar ci yoonu Musaa la jóge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy bàkkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: «Bul bëgg yëfi jaambur,» kon duma xam luy xemmem.
8 But sin, seizing an opening through the commandment, produced in me every covetous craving. For apart from law, sin is dead. Waaye bàkkaar jaare na ci ndigalu Yàlla, daldi ñëw dugg ci man, ba yëngal ci man xemmem yu bare. Ndaxte ba ma xamagul woon yoonu Musaa, bàkkaar da ne woon nemm ci man.
9 I once lived apart from law; but when the commandment came, sin revived, and I died. Keroog bi ma xamagul lu yoon wi santaane, maa ngi doon dund dund gu neex; waaye ba ma ko déggee, bàkkaar dafa daldi fuddu ci man, te man ma daldi dee.
10 I found that the very commandment that was meant to bring life actually brought death. Noonu gis naa ne ndigal loolu waroona jëme nit ñi ci dund, daf maa jëme ci dee.
11 For sin, seizing the opportunity through the commandment, deceived me, and through the commandment killed me. Ndaxte bàkkaar jaar na ci li Yàlla digle, ba nax ma, rey ma.
12 So then, the law is holy, and the commandment is holy and righteous and good. Kon nag man nanoo wax ne yoonu Musaa yoon wu sell la, te ndigalu Yàlla dafa sell, jub te baax.
13 Did the good, then, bring death to me? Absolutely not! Rather, sin—to be exposed as sin—produced death in me through the good, so that through the commandment sin might become extremely sinful. Ndax kon lu baax moo ma tàbbal ci dee? Mukk! Bàkkaar a ko def, ngir jikkoom feeñ; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu mana jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Yàlla tax na, bàkkaar fés, bon ba jéggi dayo.
14 For we know the law is spiritual, but I am fleshly, sold under sin. Xam nanu ne yoonu Musaa ngi jóge ci Yàlla, waaye man yëfi àddina laa fonk, te nekk ci dooley bàkkaar, mel nib jaam.
15 I don't understand what I do; for I don't do what I want, but what I hate I do. Ndaxte samay jëf jaaxal na ma; li ma bëgga def, duma ko def, waaye li ma bañ rekk, moom laay def.
16 If I do what I don't want, I agree the law is good. Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na.
17 So now, it's no longer I who do it, but sin living in me. Léegi nag du man maay def lu bon loolu, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ciy jiiñ.
18 For I know nothing good lives in me—that is, in my flesh. For I want to do good but can't carry it out. Ndaxte xam naa ne lu baax dëkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa yéeney def lu baax, waaye awma kàttanu yeggale.
19 For I don't do the good I want, but the evil I don't want—that I keep doing. Lu baax nag lu may yéene, duma ko def, waaye lu bon lu ma bëggul, moom laay def.
20 Now if I do what I don't want, it's no longer I doing it, but sin living in me doing it. Bu fekkee nag lu ma bëggul, moom laay def, kon dootul sama coobare, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ci jiiñ.
21 So I find this law: when I want to do good, evil lies close at hand. Gis naa nag lii: saa su ma bëggee def lu baax, lu bon a ngi ma taxawu.
22 For in my inner being I delight in the law of our Father. Ndaxte ci sama biir xol yoonu Yàlla wi neex na ma.
23 But I see another law in my body, warring against the law of my mind and taking me captive to the law of sin at work in my body. Waaye gis naa jeneen doole juy yëngu ci samay céri yaram, di bëre ak li sama xol bëgg; day bëre ba not ma, def ma jaam ci dooley bàkkaar joojuy yëngu ci samay cér.
24 What a wretched man I am! Who will rescue me from this body of death? Céy maaka torox! Ana ku may musal ci sama yaram, wii may jëme ci dee?
25 Thanks to our Father through Jesus Christ our Lord! So then, I myself serve the law of our Father with my mind, but with my flesh, the law of sin. Maa ngi sant Yàlla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Yàlla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu bàkkaar.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]