Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Romans 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 What then should we say that Abraham, our physical forefather, has found? Sunu maam Ibraayma, mi nu soqikoo; nu mbiram tëdde?
2 For if Abraham was justified by works, he has something to boast about—but not before our Father. Bu fekkoonte ne Ibraayma, ci kaw i jëfam la ko Yàlla àttee ni ku jub, kon am na lu mu ci mana damoo. Waaye demewul noonu ci kanam Yàlla.
3 For what does Scripture say? Abraham believed our Father, and it was counted to him as righteousness. Lan la Mbind mi wax ci loolu? Nee na: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.»
4 To the one who works, wages aren't credited as a gift but as what's owed. Képp kuy liggéey dina jot peyam; te pey googu du ag may, ñaqam la.
5 But to one who does not work, but trusts him who justifies the wicked, his faith is counted as righteousness. Waaye Yàlla dina àtte jub sax ki ko weddi woon; kon ku wéeruwul ciy jëfam, waaye mu gëm rekk, Yàlla dina jàppe ngëmam ni njub.
6 As David also speaks of the blessing of the person our Father credits righteousness to, apart from works: Noonu la Daawuda birale barkeelug nit ki Yàlla jagleel njub, fekk ay jëfam taxul.
7 "Blessed are those whose lawless deeds are forgiven, and whose sins are covered; Mu ne: «Ñi ñu baal seen jàdd yoon, te seeni bàkkaar far ci kanam Yàlla, ñu barkeel lañu.
8 blessed is the one whose sin our Father will never count against him." Ki Boroom bi sëful ay bàkkaaram, kooka ku barkeel la.»
9 Is this blessing only for the circumcised, or also the uncircumcised? We say Abraham's faith was credited as righteousness. Kon nag barkeel googu, ndax ñi xaraf rekk ñoo ko yeyoo? Ndax ñi xaraful it bokkuñu ci? Ahakay! Ndaxte wax nanu ne, Yàlla jàppe na ngëmu Ibraayma ni njub.
10 How then was it credited? While he was circumcised, or uncircumcised? Not while circumcised, but while uncircumcised. Kañ la ko jagleel njub nag? Ndax lu jiitu xarafam la woon, am gannaaw ga? Lu ko jiitu la woon.
11 He received circumcision as a sign, a seal of the righteousness he had by faith while still uncircumcised, so he would be father of all who believe though uncircumcised, with righteousness credited to them too, Ndaxte Ibraayma gëm na, te Yàlla jàppe na ngëmam ni njub, fekk booba xarafagul. Te xarafal gi, màndarga la woon ci yaramam, di firndeel ne ku jub la woon. Noonu la Ibraayma mana nekke baayu ñépp ñi gëm, ba Yàlla man leena àtte ni ñu jub, te xarafuñu sax.
12 and father of the circumcised who are not only circumcised but also walk in the footsteps of the faith our father Abraham had while uncircumcised. Noonu itam la Ibraayma mana nekke baayu ñi xaraf, bu fekkee yemuñu rekk ci xaraf, waaye ñu am ngëm, ga Ibraayma sunu maam amoon lu jiitu xarafam.
13 For the promise to Abraham and his offspring that he would inherit the world did not come through the law, but through faith's righteousness. Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ak ñi naroona soqikoo ci moom, ne dinañu moom àddina si. Te dige boobu jógewul ci yoonu Musaa, waaye dafa jóge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Yàlla ci kaw ngëmam.
14 For if those who live by the law are heirs, faith is emptied and the promise nullified. Ndaxte su fekkee ne ñi nekk ci yoonu Musaa rekk ñooy moom àddina, kon ngëm amatul njariñ, te digeb Yàlla toxu na.
15 Law brings wrath; where there is no law, there is no violation. Yoonu Musaa daal du def lu dul wàcce merum Yàlla ci sunu bopp; ndax fu yoon amul, jàdd yoon du fa mana am.
16 So it comes by faith, to be by grace, guaranteeing the promise to all the offspring—not only those tied to the law but also those who share Abraham's faith, father of us all, Kon nag loolu Yàlla dige, ngëm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Yàlla rekk. Noonu la dige bi wóore ci ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, du ci ñi nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam ñi gëm ni Ibraayma gëme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun ñépp.
17 as it is written, "I have made you father of many nations"—before our Father, in whom he believed, who gives life to the dead and calls things that do not exist into being. Moom la Yàlla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: «Def naa la baayu xeet yu bare.» Ndaxte Ibraayma gëmoon na Yàlla, miy dekkal ñi dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am.
18 Against hope, he believed in hope, becoming father of many nations, as he'd been told: "So will your offspring be." Ibraayma dafa jàppoon ci ngëmam, di yaakaar, fekk bunti yaakaar yépp tëju. Moo tax mu nekk baayu xeet yu bare, ni ko Mbind mi waxe ne: «Noonu la sa askan di meli.»
19 Not weak in faith, he considered his own body already as good as dead—he was about one hundred—and Sarah's womb lifeless. Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat téeméeri at, waaye ba tey ngëmam wàññikuwul. Mu xam it ne, Saarata manatula ëmb.
20 He did not doubt our Father's promise in lack of faith, but was strengthened in faith, giving glory to our Father, Waaye loolu taxul ngëmadi jàpp ko, ba muy werante ci waxu Yàlla; ngëmam sax di gëna dëgër, mu daldi sant Yàlla,
21 fully convinced that what our Father had promised he was also able to do. mu wóor ko ne loolu ko Yàlla dig, Yàlla man na koo def.
22 That is why "it was credited to him as righteousness." Moo tax «Yàlla jagleel na Ibraayma njub.»
23 But the words "it was credited to him" were written not for his sake alone, Waaye loolu lañu bind ne: «Yàlla jagleel na ko njub,» du Ibraayma rekk a moom wax ji.
24 and also for us who will be credited with it—those trusting the one who raised our Lord Jesus from the dead, Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Yàlla dina nu jagleel njub, nun ñi gëm Yàlla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom.
25 who was delivered over for our sins and raised to make us right with our Father. Ndaxte Yàlla jébbale na ko ngir sunuy tooñ, dekkal ko ngir àtte nu jub.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]