Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Romans 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 What advantage, then, does the Jew have? Or what is the value of circumcision? Yawut bi nag, ci lan la rawe ku dul Yawut? Te xaraf lu muy njariñ?
2 Much in every way. First of all, they were entrusted with the very words of our Father. Raw na ko fu nekk. Ci bu jëkk Yawut yi la Yàlla dénk waxam.
3 What then? If some were unfaithful, will their unfaithfulness nullify the faithfulness of our Father? Bu fekkee ne am na ci ñoom ñu ñàkk kóllëre, ndax loolu man na fanq kóllëreg Yàlla?
4 No! Let our Father be true, though every person is a liar. As it is written: "You are proven right in your words, and win when judged." Mukk! Su ñépp nekkoon ay naaféq, du tere Yàlla nekk dëgg. Moom la Mbind mi wax ci Yàlla ne: «Loo wax, ñépp ànd ci, te ku layoo ak yaw, nga yey ko.»
5 But if our wrongdoing highlights our Father's righteousness, what do we say? Is our Father unjust to bring wrath on us? (I speak in human terms.). Su fekkee nag njubadig nit dina feeñal njubteg Yàlla, lu ciy seen xalaat? Wax ji may bëgga wax nag léegi, waxi nit rekk la, maanaam: ndax kon Yàlla àttewul yoon ci li muy daan ku jubadi?
6 Certainly not! For then how could our Father judge the world? Mukk! Ndax su Yàlla jubadi woon, naka lay àttee àddina si?
7 But if my lie makes our Father's truth overflow to his glory, why am I still judged as a sinner? Waaye nag xanaa dina am ku tontu ci loolu ne: «Su fekkee sama ñàkk kóllëre gën na yékkati kóllëreg Yàlla, di yokk it ndamam, lu tax kon Yàlla di ma teg ba tey bàkkaarkat, ba di ma àtte?»
8 Why not say, as some slander us as saying, "Let's do evil so good may come"? Their judgment is deserved. Lu tax manunoo wax ne: «Nanu def lu bon, ngir lu baax génn ca?» Am na sax ñu nuy tuumaal, di wax ne noonu lanuy waaree. Waaye ñiy wax loolu, ndaan gi ñu yelloo dina leen dal.
9 What then? Are we better off? Not at all—we've already charged that Jews and Greeks alike are all under sin's grip, Kon nag lu nu ci wara wax? Nun Yawut yi, ndax noo gën ñi ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit ñépp ñu ngi ci notaangeg bàkkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi.
10 as it is written: "There is no one righteous, not even one; Moom la Mbind mi wax ne: «Ku jub amul, du kenn sax.
11 no one understands; no one seeks our Father. Amul kenn ku xam yëfi Yàlla, mbaa kenn ku koy wut.
12 All have turned away; together they have become worthless; no one does good, not even one. Ñépp jeng nañu, ba kenn amalatul Yàlla njariñ. Kenn du def lu baax, du kenn sax!
13 Their throat is an open grave; they use their tongues to deceive." "The venom of snakes is under their lips. Seen put a ngi xasaw ni méddum ñetti fan, seen làmmiñ làggi ci njublaŋ, te seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Their mouth is full of cursing and bitterness. Duñu génne ci seen gémmiñ lu dul ay móolu ak i xas.
15 Their feet are swift to shed blood; Ñu sawar lañu ci rey nit.
16 ruin and misery mark their ways, Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba.
17 and the way of peace they have not known. Xamuñu yoonu jàmm,
18 There is no fear of our Father before their eyes." te ragal Yàlla sore na seen xol.»
19 We know whatever the law says applies to those under it, so every mouth is silenced and the whole world stands accountable to our Father. Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla.
20 No one is made right before him by works of the law; the law brings awareness of sin. Ndaxte sàmm yoon wi taxul kenn jub ci kanam Yàlla; solob ndigal yi daal mooy wone bàkkaar.
21 But now, apart from the law, our Father's righteousness has been revealed, testified to by the Law and the Prophets. Waaye léegi nag Yàlla feeñal na, ni nit mana jube ci kanamam, ci lu séqul ak yoonu Musaa dara. Waaye ba tey yoonu Musaa ak waxi yonent yi seedeel nañu ko.
22 This righteousness of our Father comes through faith in Jesus Christ, to all who believe, for there's no distinction, Jub ci kanam Yàlla, gëm Yeesu Kirist rekk a koy maye, te képp ku ko gëm bokk nga ci. Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
23 since all have sinned and fall short of the glory of our Father, Ñépp a bàkkaar, ba joteetuñu ndamu Yàlla.
24 and are justified freely by his grace through the redemption that is in Christ Jesus. Waaye gannaaw Kirist Yeesu dee na ngir jot leen, Yàlla ciw yiwam man na leena àtte ni ñu jub ci dara.
25 Our Father presented him as the atoning sacrifice, through faith in his blood, to show his righteousness, since in his patience he had passed over sins committed before, Wàcce na Kirist, mu nekk sarax ngir Yàlla baal nu sunuy bàkkaar, jaar ci deretam ji ñu tuur; te ngëm rekk moo nu ciy boole. Noonu Yàlla firndeel na ne ku jub la, doonte sax dafa muñaloon ñi jiitu jamonoy Kirist, ba jéggal leen seeni bàkkaar.
26 to show his righteousness now, so he is both just and the justifier of whoever trusts in Jesus. Kon ci jamono jii nu ne, Yàlla wone na bu leer ne ku jub la, di àtte ni ku jub képp ku gëm Yeesu, te ba tey dëkk ci njubteem.
27 Where then is boasting? Excluded. By what law? Of works? No—by the law of faith. Kan a mana bàkku nag ci kanam Yàlla? Kenn! Lu ko waral nag? Xanaa sàmm yoon? Déedéet! Ngëm rekk.
28 For we maintain that a person is justified by faith apart from works of the law. Ndaxte danoo dëggal ne ngëm rekk a tax Yàlla di àtte nit ni ku jub, waaye du sàmm yoon.
29 Or is our Father the Father of Jews only? Not the Father of Gentiles too? Yes, of Gentiles too, Walla ndax nag Yawut yi rekk la fi nekkal? Ndax nekkalu fi it ñu dul Yawut? Ahakay!
30 since our Father is one, he will justify the circumcised by faith and the uncircumcised through faith. Gannaaw Yàlla kenn la, ñépp la fi nekkal. Ñi xaraf dina leen àtte ni ñu jub ndax seen ngëm, ñi xaraful it dina leen àtte ni ñu jub ndax seen ngëm.
31 Do we cancel the law through this faith? Never—we confirm the law. Xanaa kon ngëm day fanq yoonu Musaa? Mukk! Da koy gëna dëgëral sax.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]