Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Romans 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So you have no excuse, whoever you are, when you judge another—in judging them you condemn yourself, since you do the same things. Kon nag képp ku mu mana doon, yaw miy àtte sa moroom ak ñaaw njort, amuloo aw lay, ndaxte àtte sa moroom, daan sa bopp la; yaa ngi koy àtte ndax ay jëfam, fekk yaw itam noonu ngay jëfe.
2 Now we know that our Father's judgment rightly falls on those who do such things. Xam nanu ne ñiy jëfe noonu, Yàlla dina leen àtte, te àtteem jub na.
3 Do you think, whoever judges others for such things while doing them yourself, that you'll escape our Father's judgment? Yaw nag miy àtte ñiy def loolu, te di ko def, ndax defe nga ne dinga rëcc ci àtteb Yàlla?
4 Or do you despise the riches of his kindness and restraint and patience, not realizing that our Father's kindness is meant to lead you to repentance? Ndax dangaa xeeb mbaaxu Yàlla, mi yéexa mer te di la muñal? Xanaa xamuloo ne Yàllaa ngi lay won baaxaayam, ngir nga réccu say bàkkaar?
5 But because of your hard, unrepentant heart, you are storing up wrath for yourself, for the day of wrath when our Father's righteous judgment will be revealed. Waaye ndegam dëgër nga bopp te bëgguloo réccu, yaa ngi dajale merum Yàlla ci sa bopp. Ndaxte Yàlla sàkk na bés bu muy wone àtteem bu jub bi te meram wàcc ci ñi bon;
6 He will repay each person according to what they have done. bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam.
7 To those who through persistent good work seek glory, honor, and immortality, he will give eternal life. Ñiy góor-góorlu ciy def lu baax, bëgg Yàlla boole leen ca ndamam te sédde leen ngërëm ak dund gu sax, dina leen tàbbal ci dund gu dul jeex.
8 But those who are self-seeking, reject the truth, and follow wickedness face wrath and rage. Waaye ñi dëgër bopp, ba tanqamlu dëgg, di topp lu jubadi, seen pey mooy dooni merum Yàlla ak toroxte.
9 Trouble and distress for everyone who does evil—the Jew first, then the Greek, Ki doon def lu bon, peyam mooy tiis ak metit wu tar, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut.
10 but glory, honor, and peace for all who do good—Jew first, then Greek too. Waaye ki doon def lu baax, añam mooy bokk ci ndamu Yàlla, am ngërëm ak jàmm, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut.
11 For our Father shows no favoritism. Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
12 Sinners without the law also perish without it; sinners under the law will be judged by it. Képp ku doon bàkkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci lu dul yoonu Musaa, nga doora sànku. Te képp ku doon bàkkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci yoon woowu.
13 For not those who hear the law are righteous before our Father, but those who obey it will be justified. Kon déglu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Yàlla; kiy sàmm yoon wi, moom la Yàlla di àtte ni ku jub.
14 Indeed, when Gentiles, who do not have the law, do by nature what the law requires, the law is at work within them, even though they do not have the law. Ndax ñi dul Yawut te nekkuñu ci yoonu Musaa, ñu ngiy def li yoon woowu tëral, ndaxte Yàlla def na ko ci nit. Te wonee nañu noonu ne man nañoo ràññee lu baax ak lu bon, su ñu nekkul sax ci yoonu Musaa,
15 They show the law's work written on their hearts, their conscience bearing witness, and their conflicting thoughts accusing or defending them. di wone it ne Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal.
16 This happens on the day our Father judges everyone's secrets through Jesus Christ—so my gospel says. Ndax bés dina ñëw, bu xalaat yu làqu yi di feeñ, te Yàlla àtte nit ñi jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xibaaru jàmm, bi may waare, moo ko wax.
17 But if you call yourself a Jew, rely on the law, and boast in our Father, Maa ngi ñëw nag ci yaw mi ne Yawut nga; yaa ngi sukkandiku ci yoonu Musaa ak di damu ci Yàlla.
18 if you know our Father's will and approve what is excellent because you are instructed by the law, Xam nga coobareem, ndaxte jàng nga ci yoonu Musaa, ba fonk yëf yi gëna baax.
19 if you're convinced you are a guide for the blind, a light for those in darkness, Yaa ngi teg sa bopp wommatkatu gumba yi ak leeru ñi nekk cig lëndëm.
20 a corrector of the foolish, teacher of the immature, holding in the law the shape of knowledge and truth. Yaa di jànglekatu ñi jàngul ak xamlekatu ñi xamul, ndaxte xalaat nga ne Yàlla jagleel na leen ci yoonu Musaa bépp xam-xam ak gépp dëgg.
21 You teach others—do you not teach yourself? You preach against stealing—do you steal? Kon nag yaw miy jàngal say moroom, xanaa doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare di tere sàcc, mbaa doo sàcc yaw itam? Yaw miy tere njaaloo, mbaa doo njaaloo?
22 You who tell others not to commit adultery—do you commit it? You who detest idols—do you rob temples? Yaw miy araamal xërëm yi, mbaa doo sàcc li nekk ci seeni xàmb?
23 You who boast in the law, do you dishonor our Father by breaking the law? Yaw miy damoo yoonu Musaa, mbaa doo ko moy, ba indi gàcce ci turu Yàlla?
24 As it is written: "Our Father's name is blasphemed among the nations because of you." Moo tax Mbind mi ne: «Yéena tax ñi nekkul Yawut di suufeel turu Yàlla.»
25 Circumcision helps if you keep the law; break it, and your circumcision becomes being uncircumcised. Bëggoon naa ngeen xam ne xaraf am na njariñ, boo ca boolee sàmm yoon. Waaye boo ko ca boolewul, sa xaraf amatul njariñ.
26 So if the uncircumcised keep the law's requirements, won't their uncircumcision be counted as circumcision? Te itam ku xaraful, tey def jëf yu jub yi yoonu Musaa santaane, ndax Yàlla du ko teg ni ku xaraf?
27 The physically uncircumcised who keep the law will judge you who, with the letter and circumcision, break the law. Ku dul Yawut te xaraful waaye di sàmm yoon wi, kooku dina la mana àtte, yaw Yawut bi. Ndaxte li ngay xam xam yoonu Musaa ci Mbind mi te xaraf, terewul nga koy moy.
28 For being a Jew isn't merely about the outside, nor circumcision merely about the body. Juddu nekk Yawut taxul sag Yawut dëggu, te xaraf ci saw yaram taxul sa xaraf wóor.
29 Rather, one is a Jew inwardly, circumcision being of the heart, by the Spirit, not the written code; that one's praise is not from people but from our Father. Waaye Yawut dëgg, ci xol lay nekk. Te xaraf dëgg itam, ci xol lay nekk. Du ngistal, lu dëggu la. Te képp ku mel noonu, dees na la gërëm, waxuma la nit ñi, waaye Yàlla ci boppam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]