Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 6 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "Take care not to practice your righteousness before others to be seen by them, or you have no reward from your Father in heaven. «Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw.
2 So when you give to the needy, don't announce it with a trumpet, like the hypocrites do in synagogues and streets, to be praised by people. I assure you: they've already received their full reward. Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
3 But when you give to the needy, don't let your left hand know what your right hand does, Waaye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmoñ xam li sa loxob ndijoor di def,
4 so that your gift stays secret. Your Father, who sees in secret, will repay you. ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
5 "When you pray, don't be like hypocrites who love praying standing in synagogues and on street corners to be seen by others. Truly, I tell you: they've already received their full reward. «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6 But when you pray, go into your room, shut the door, and pray to your Father in secret. Your Father who sees in secret will reward you. Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
7 When you pray, don't babble like those who don't know the Father, because they think many words will get them heard. «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare.
8 Do not be like them, for your Father knows what you need before you ask him. Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax.
9 This, then, is how you should pray: 'Our Father in heaven, may your name be honored as holy, Yéen nag nii ngeen wara ñaane: “Sunu Baay bi nekk ci kaw, yal na sa tur di lu ñu sellal,
10 your kingdom come, your will be done, on earth as it is in heaven. yal na sa nguur ñëw, yal na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.
11 Give us today our daily bread. Yal nanga nu may tey li nu dunde;
12 And forgive us our debts, as we also have forgiven our debtors. te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ;
13 And lead us not into temptation, but deliver us from the evil one.' Yàlla boo nu teg ci yoonu nattu, waaye yal nanga nu musal ci lu bon. Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
14 "For if you forgive others their sins, your heavenly Father will also forgive you. «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam.
15 But if you do not forgive others their sins, neither will your Father forgive your sins. Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ.
16 "When you fast, don't look gloomy like the hypocrites—they disfigure their faces to show others they're fasting. Truly, I tell you, they have their full reward. «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
17 But when you fast, put oil on your head and wash your face, Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu,
18 so you don't appear to others as fasting, but only to your Father, who is hidden. Then your Father, who sees what's hidden, will reward you. ngir sa koor baña feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
19 "Do not store up treasures for yourselves on earth, where moth and rust destroy, and thieves break in and steal. «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko.
20 But store up treasures in heaven for yourselves, where neither moth nor rust destroys, and thieves can't break in and steal. Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko.
21 For where your treasure is, there your heart will be also. Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
22 "The eye is the body's lamp. If your eye is clear, your whole body will be full of light. «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer,
23 But if your eye is bad, your whole body will be dark. If then the light in you is darkness, how great that darkness is! waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse!
24 "No one can serve two masters: he'll hate one and love the other, or hold to one and despise the other. You can't serve our Father and money. «Kenn manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.
25 "So I tell you: don't worry about your life—what you'll eat or drink—or body—what you'll wear. Isn't life more than food, body more than clothes? «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk, walla lu ngeen wara naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen wara sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay?
26 Look at the birds in the sky: they don't plant, harvest, or store in barns, yet your heavenly Father feeds them. Aren't you worth more than they? Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare?
27 Can any of you by worrying add a single hour to your life? Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo mana yokk waxtu ci àppam?
28 And why worry about clothing? Consider the lilies of the field, how they grow: they don't work or spin. «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc,
29 Yet I tell you: not even Solomon, in all his glory, was dressed like one of these. waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom.
30 If our Father clothes the field's grass like this—here today, thrown into the fire tomorrow—won't he much more clothe you, you of little faith? Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd?
31 "So don't worry, asking, 'What will we eat?' or 'What will we drink?' or 'What will we wear?' Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu wara lekk? Lu nu wara naan?” walla: “Lu nu wara sol?”
32 For those who don't know the Father chase all these things, but your heavenly Father knows you need them. Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp.
33 But seek first our Father's kingdom and his righteousness, and all these will be added to you. Waaye jëkkleena wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
34 So don't worry about tomorrow—it will worry about itself. Each day has enough trouble of its own." Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]