Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 7 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "Do not judge, so that you may not be judged. «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam.
2 For you'll be judged by the judgment you use, and measured by the measure you give. Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale.
3 Why look at the speck in your brother's eye but miss the log in your own? Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
4 Or how can you tell your brother, 'Let me remove the speck from your eye,' when a log is in yours? Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw?
5 Hypocrite, first remove the log from your own eye; then you'll see clearly to remove the speck from your brother's eye. Naaféq, jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
6 "Don't give dogs what is holy, or throw your pearls before pigs—they'll trample them underfoot, then turn and tear you apart. «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen.
7 "Ask, and you'll receive it; seek, and you'll find; knock, and it'll open for you. «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
8 For everyone who asks receives, whoever seeks finds, and whoever knocks, it will be opened. Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
9 Or what person among you, if his son asks him for bread, will give him a stone? Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj?
10 Or if he asks for a fish, will give him a snake? Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan?
11 So if you, being evil, know how to give your children good gifts, how much more will your Father in heaven give good things to those who ask him? Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan!
12 "So in everything, treat people the way you want them to treat you; for this is the Law and the Prophets. «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi.
13 "Enter through the narrow gate, for the gate is wide, the road broad, leading to destruction, and many enter through it. «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare.
14 But the gate is narrow, the road narrow, that leads to life; few find it. Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
15 "Beware false prophets: they come to you in sheep's clothing but are ravenous wolves inside. «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu.
16 By their fruit you will recognize them. Are grapes gathered from thornbushes, or figs from thistles? Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte reseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam?
17 In the same way, every good tree bears good fruit, but the bad tree bears bad fruit. Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon.
18 A good tree cannot bear bad fruit, nor can a bad tree bear good fruit. Garab gu baax manula meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon manula meññ doom yu neex.
19 Every tree that does not bear good fruit is cut down and thrown into the fire. Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca sawara sa.
20 So then, by their fruit you will recognize them. Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee.
21 "Not everyone who says to me, 'Lord, Lord,' will enter the kingdom of our Father, but the one who does the will of my Father in heaven. «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw.
22 Many will say to me on that day, 'Lord, Lord, didn't we prophesy in your name, drive out demons in your name, do many miracles in your name?' Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?”
23 Then I will tell them plainly: 'I never knew you; get away from me, you lawbreakers.' Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Masuma leena xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.”
24 "So anyone who hears these words of mine and does them will be like a wise man whose house was built on the rock. «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj.
25 Rain fell, floods came, winds blew and beat against that house, but it didn't fall, because it was founded on rock. Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa.
26 And everyone who hears these words of mine and doesn't do them is like a foolish man who built his house on sand. Waaye képp ku dégg lii ma leen wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gannuus bi.
27 The rain fell, floods came, winds blew and hit that house, and it fell—and its fall was great." Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
28 When Jesus had finished saying these words, the crowds were astonished at his teaching, Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngleem,
29 because he was teaching them as one who had authority, and not as their scribes. ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]