Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Seeing the crowds, Jesus went up the mountain; when he sat down, his disciples came to him. Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom.
2 And he opened his mouth and began to teach them, saying: Mu daldi leen jàngal naan:
3 "Blessed are the poor in spirit, for theirs is the kingdom of our Father. «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo.
4 Blessed are those who mourn, for they will be comforted. Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol.
5 Blessed are the meek, for they will inherit the earth. Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina.
6 Blessed are those who hunger and thirst for righteousness, for they will be satisfied. Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg.
7 Blessed are the merciful, for they will receive mercy. Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen, ndax dees na leen yërëm.
8 Blessed are the pure in heart, for they will see our Father. Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen, ndax dingeen gis Yàlla.
9 Blessed are the peacemakers, for they will be called children of our Father. Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen, ndax dees na leen tudde doomi Yàlla.
10 Blessed are those who are persecuted for righteousness' sake, for theirs is the kingdom of our Father. Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo.
11 "Blessed are you when people insult, persecute, and lie about every kind of evil against you because of me. «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man.
12 Rejoice and be glad, for your reward is great in heaven, for they persecuted the prophets before you the same way. Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
13 "You are the salt of the earth. But if salt loses its taste, how can it be salted again? It's no longer good for anything but being thrown out and trampled by people. «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.
14 "You are the light of the world. A city set on a hill cannot be hidden. Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du mana nëbbu.
15 No one lights a lamp and puts it under a basket, but sets it on a stand to light everyone in the house. Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp.
16 Likewise, let your light shine before people, so they see your good works and glorify your Father in heaven. Na seen leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw.
17 "Don't think I came to abolish the Law or the Prophets—I didn't come to abolish them, but to fulfill them. «Buleen defe ne ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man.
18 For truly I tell you: until heaven and earth pass, not one letter, not one stroke, will pass from the Law until everything is done. Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am.
19 So whoever breaks one of these least commands and teaches others the same will be called least in the kingdom of our Father; but whoever keeps and teaches them will be called great in the kingdom of our Father. Ku tebbi nag ba gëna tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gëna tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
20 For I tell you, unless you are more righteous than the scribes and Pharisees, you'll never enter the kingdom of our Father. Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
21 "You've heard that it was said to those of old, 'Do not murder; whoever murders is subject to judgment.' «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.”
22 But I tell you: whoever is angry with his brother risks judgment. Whoever insults his brother risks the council, and whoever says, 'You fool!' risks fiery hell. Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara.
23 "So if you're offering your gift at the altar and recall there that your brother has something against you, Booy yóbbu nag sa sarax ca sarxalukaay ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree,
24 leave your gift there before the altar, go make peace with your brother first, then come offer your gift. nanga fa bàyyi sa sarax ca kanam sarxalukaay ba, nga jëkka dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax.
25 Make peace with your accuser quickly, while still on the way with him, or he may hand you over to the judge, the judge to the officer, and you may be thrown into prison. «Gaawala juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeena egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la.
26 Truly I tell you, you will never get out until you have paid the last penny. Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj.
27 "You have heard that it was said, 'You shall not commit adultery.' «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.”
28 But I tell you: everyone who looks at a woman lustfully has already committed adultery with her in his heart. Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel.
29 If your right eye makes you stumble, tear it out and throw it away—better to lose one part of your body than have your whole body thrown into hell. Bu la sa bëtu ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore.
30 If your right hand makes you sin, cut it off and throw it away. Better to lose one part of you than have your whole body go into hell. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. Bu la sa loxol ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci sawara.
31 "It was also said, 'Whoever divorces his wife must give her a certificate of divorce.' «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.”
32 I tell you: whoever divorces his wife, except for sexual sin, makes her a victim of adultery; and whoever marries a divorced woman commits adultery. Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa soxna te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga.
33 "Again, you've heard it was said to the ancients: 'Don't break your oath—fulfill it to our Father.' «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.”
34 But I tell you, do not swear an oath at all: neither by heaven, for it is our Father's throne, Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamaan, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla;
35 nor by the earth, for it's the footstool for his feet, nor by Jerusalem, for it's the city of the great King. bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukaayu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi.
36 And do not swear by your head, for you cannot make a single hair white or black. Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte manuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar.
37 Let your 'Yes' be 'Yes,' and your 'No,' 'No'; anything beyond this comes from the evil one. Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
38 "You have heard that it was said, 'Eye for eye and tooth for tooth.' «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.”
39 But I tell you: don't resist an evil person. If someone slaps your right cheek, turn the other cheek to him too. Waaye man maa ngi leen di wax ne buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndijoor, jox ko ba ca des.
40 If anyone wants to sue you and take your tunic, let him have your cloak too. Ku la bëgga kalaame, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag.
41 And if anyone forces you to go one mile, go with him two. Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñaar.
42 Give to whoever asks you, and don't turn away whoever wants to borrow from you. Mayal ku lay ñaan, te bul jox gannaaw ku lay leb.
43 "You have heard that it was said, 'You will love your neighbor and hate your enemy.' «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.”
44 But I tell you, love your enemies and pray for those who persecute you, Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal,
45 so you may become children of your Father in heaven, because he makes his sun rise on evil and good and sends rain on just and unjust. ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.
46 If you love those who love you, what reward is that? Don't even tax collectors do the same? Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it?
47 If you greet only your brothers, what more do you do than others? Don't even the Gentiles do that? Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy waar? Xanaa ñi xamul Yàlla duñu def noonu it?
48 Be perfect, therefore, as your heavenly Father is perfect." Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kaw mate.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]