Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 28 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After the Sabbath, at dawn on the first day of the week, Mary Magdalene and the other Mary came to see the tomb. Gannaaw bésub noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba.
2 Suddenly a great earthquake struck, for an angel of our Father came down from heaven, rolled back the stone, and sat on it. Fekk suuf yëngu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
3 His appearance was like lightning, and his clothing white as snow. Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal.
4 The guards trembled in fear of him and became like dead men. Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee.
5 But the angel said to the women, "Don't be afraid, for I know you're looking for Jesus, who was crucified. Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba,
6 He isn't here—he's risen, as he said. Come, see the place where he was lying. waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon,
7 Go quickly, tell his disciples: He has risen from the dead. Look, he is going ahead of you to Galilee; you will see him there. Listen, I have told you." te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.»
8 So they left the tomb quickly, with fear and great joy, and ran to tell his disciples. Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya.
9 Suddenly Jesus met them, saying, "Greetings!" They came to him, grasped his feet, and worshiped him. Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal.
10 Then Jesus told them, "Don't be afraid. Go, tell my brothers to leave for Galilee—they will see me there." Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
11 While on the way, some guards entered the city and reported to the chief priests all that had happened. Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal sarxalkat yu mag ya lépp lu xew.
12 After meeting with the elders and forming a plan, they paid the soldiers a large sum, Noonu sarxalkat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya,
13 telling them, "Say: His disciples came at night and stole him while we slept. ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
14 If this reaches the governor, we'll persuade him and keep you free of trouble." Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.»
15 They took the money and did as they were told; this report spread among the Jews to this day. Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.
16 Then the eleven disciples went to Galilee, to the mountain where Jesus had directed them. Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon.
17 When they saw him, they worshiped him, but some doubted. Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar.
18 Jesus came and said to them, "All authority in heaven and on earth has been given to me. Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf.
19 Therefore go and make disciples of all nations, baptizing them in the name of the Father and of the Son and of the Holy Spirit, Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi;
20 teaching them to obey all I've commanded you. Remember, I'm with you always, to the end of the age." ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]