Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 The beginning of the gospel of Jesus Christ, the Son of our Father. Xibaaru jàmm bu Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, nii la tàmbalee.
2 As written in Isaiah the prophet: "Look, I send my messenger ahead of you, who will prepare your way. Bind nañu ci téereb yonent Yàlla Esayi naan: «Maa ngi yónni sama ndaw ci sa kanam, mu xàllal la sa yoon.
3 A voice calling out in the wilderness: 'Prepare the way of the Lord, make his paths straight.'" Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”»
4 John appeared, baptizing in the wilderness and proclaiming a baptism of repentance for the forgiveness of sins. Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox, tey waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
5 All Judea and everyone in Jerusalem went out to him, and he baptized them in the Jordan River as they confessed their sins. Kon waa diiwaanu Yude ñépp ak waa dëkku Yerusalem ñépp daldi génn jëm ci moom, di nangu seeni bàkkaar fi kanam ñépp, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
6 John was dressed in camel's hair, with a leather belt around his waist, eating locusts and wild honey. Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
7 He announced: "After me comes one stronger than I; I'm not worthy to stoop and untie his sandal strap. Mu waare ne: «Am na kuy ñëw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma ëpp kàttan; yeyoowuma sax sëgg, ngir tekki ay dàllam.
8 I have baptized you with water, but he will baptize you with the Holy Spirit." Maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye moom dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.»
9 In those days Jesus came from Nazareth of Galilee and was baptized by John in the Jordan. Booba Yeesu jóge na dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile, ñëw, Yaxya sóob ko ci dexu Yurdan.
10 Immediately, as he came up out of the water, he saw the heavens split open and the Holy Spirit come down on him like a dove. Bi muy génn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Yàlla di wàcc ci melow pitax, ñëw ci moom.
11 And a voice came from heaven: "You are my beloved Son; in you I delight." Te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
12 And immediately the Holy Spirit drove him out into the wilderness. Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma.
13 He was in the wilderness forty days, tempted by Satan, with the wild animals, and the angels served him. Mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane; mu dëkk ci biir rabi àll yi, te malaakay Yàlla di ko topptoo.
14 Now after John was arrested, Jesus came into Galilee, proclaiming the gospel of our Father, Bi nga xamee ne jàpp nañu Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi,
15 and saying, "The time is fulfilled, and our Father's kingdom is near; repent and believe the good news." naan: «Jamono ji mat na, nguuru Yàlla jegesi na; tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bi.»
16 Passing the Sea of Galilee, he saw Simon and his brother Andrew casting a net in the sea, for they were fishermen. Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon.
17 And Jesus said to them, "Follow me, and I will make you become fishers of people." Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.»
18 And immediately they left their nets and followed him. Ci saa si ñu bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
19 Going a little farther, he saw James son of Zebedee and John his brother in their boat, mending the nets. Bi Yeesu demee ba ca kanam, mu gis Saag doomu Sebede, ak Yowaana, mi mu bokkal ndey ak baay, ñu nekk ci gaal gi, di defar seeni mbaal.
20 At once he called them; leaving their father Zebedee in the boat with the hired hands, they followed him. Noonu Yeesu woo leen, ñu daldi bàyyi seen baay Sebede ci gaal gi, moom ak surga ya, tey topp ci moom.
21 They went to Capernaum. At once, on the Sabbath, he entered the synagogue and began teaching. Gannaaw loolu ñu dem Kapernawum. Ca bésub noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jàngu bi, di leen jàngal.
22 They were amazed at his teaching, for he taught them with authority, not like the scribes. Te ñu waaru ca njàngleem, ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
23 And immediately there was in their synagogue a man with an unclean spirit, and he cried out. Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi yuuxu naan:
24 Why meddle with us, Jesus of Nazareth? Have you come to destroy us? I know who you are—God's Holy One! «Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.»
25 But Jesus rebuked him, saying, "Be silent, and come out of him!" Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!»
26 And the unclean spirit, convulsing him and crying out with a loud voice, came out of him. Noonu rab wi daldi sayloo nit ki te génn ci moom ak yuux gu réy.
27 All were amazed, and they questioned each other: "What is this? A new teaching with authority - he commands even the unclean spirits, and they obey him!" Bi loolu amee ñépp waaru, ba laajante naan: «Kii mooy kan? Mii njàngle lu bees la te ànd ak sañ-sañ. Day sant rab yi sax, ñu di ko déggal.»
28 And at once his fame spread everywhere throughout all the surrounding region of Galilee. Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile gépp.
29 Immediately he left the synagogue and went to Simon and Andrew's house, with James and John. Bi nga xamee ne génn nañu ci jàngu bi, ñu ànd ak Saag ak Yowaana, dem ci kër Simoŋ ak Andare.
30 Now Simon's mother-in-law lay sick with a fever, and immediately they told him about her. Fekk gorob Simoŋ bu jigéen tëdd wopp ak yaram wu tàng; ñu daldi ko yégal Yeesu.
31 He came, took her hand, raised her up. The fever left her, and she served them. Mu ñëw nag ci moom, jàpp loxoom, yékkati ko. Noonu tàngoor wi daldi wàcc, te soxna si di leen topptoo.
32 That evening, when the sun set, they brought him all who were sick and those oppressed by demons. Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ñi rab jàpp ñépp,
33 And the whole city was gathered together at the door. ba dëkk bi bépp dajaloo ci buntu kër gi.
34 He healed many sick with various diseases and drove out many demons, not letting the demons speak, since they knew him. Noonu mu wéral ñu bare, ñu wopp ak ay jàngoro yu wuute, te dàq ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ko.
35 Long before dawn, while still dark, he got up, went out to a deserted place, and prayed there. Ca njël laata bët di set, Yeesu jóg dem ca bérab bu wéet, di fa ñaan Yàlla.
36 And Simon and those who were with him searched for him, Simoŋ nag ak ñi ànd ak moom di ko seet fu nekk.
37 and they found him and said to him, "Everyone is looking for you." Bi ñu ko gisee, ñu ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.»
38 He said, "Let us go elsewhere, to the neighboring towns, so I can preach there too, for that is why I came." Waaye Yeesu ne leen: «Nanu dem feneen ci dëkk yi nu wër, ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma génn.»
39 And he went throughout all Galilee, preaching in their synagogues and casting out demons. Noonu mu wër ci diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, tey dàq rab yi.
40 A man with leprosy came, knelt, and begged him, "If you're willing, you can make me clean." Am bés ku gaana ñëw ci moom, sukk, ñaan ko ne: «Soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
41 Moved with deep compassion, he stretched out his hand, touched him, and said to him, "I am willing; be clean." Yeesu yërëm ko, tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.»
42 And immediately the leprosy left him, and he was made clean. Ca saa sa ngaanaam daldi deñ, mu wér.
43 Sternly warning him, he sent him away at once, Noonu Yeesu yebal ko, dénk ko bu wér naan:
44 and told him, "Make sure you tell no one—but go, show yourself to the priest, and offer what Moses commanded for your cleansing, as proof to the people." «Moytula wax kenn dara, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
45 But he went out, proclaiming it freely and spreading the news, so Jesus could no longer enter a town openly, but stayed in lonely places. Yet people came to him from everywhere. Waaye naka la waa ji génn, mu di yéene ci kaw li xewoon, te di ko jéebaane, ba tax Yeesu manatula fàŋŋaaral dugg cib dëkk, waaye mu nekk ci biti ciy bérab yu wéet. Ba tey nit ñi jóge fu nekk, di ko fa fekk.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]