Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 22 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Jesus spoke to them again in parables, saying: Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen:
2 "The kingdom of our Father is like a king who prepared a wedding feast for his son. «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
3 He sent his servants to summon the invited guests to the wedding feast, but they refused to come. Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw.
4 Again he sent other servants, saying, 'Tell those invited: Look, I have prepared my dinner; my oxen and fattened cattle are killed, everything ready. Come to the wedding feast.' Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ”
5 But they paid no attention and went off, one to his farm, another to his business, Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani,
6 while the rest seized his servants, mistreated them, and killed them. ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
7 The king was enraged, and he sent his troops, destroyed those murderers, and burned their city. «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk.
8 Then he told his servants, 'The wedding is ready, but those invited weren't worthy. Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko.
9 Go therefore to the main roads and invite to the wedding feast as many as you find.' Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.”
10 Those servants went out into the roads and gathered everyone they found, bad and good, and the wedding hall filled with guests. Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan.
11 "But when the king came in to see the guests, he saw a man not dressed in wedding clothes. «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu wara sol ca céet ga.
12 He asked, 'Friend, how did you get in here without wedding clothes?' He was speechless. Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig.
13 Then the king told the servants, 'Tie his hands and feet, and throw him into the outer darkness, where there will be weeping and grinding of teeth.' Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.”
14 For many are called, but few are chosen." Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
15 Then the Pharisees went and plotted how to trap him with his own words. Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu wara def, ngir fiir Yeesu ci waxam.
16 They sent their disciples to him, with the Herodians, saying, "Teacher, we know you are truthful and truly teach God's way; you defer to no one, since you don't judge people by rank. Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
17 Tell us, then, what you think: Is it lawful to pay taxes to Caesar, or not?" Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
18 But Jesus, knowing their malice, said, "Why are you testing me, you hypocrites? Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
19 Show me the coin used for the tax." And they brought him a denarius. Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon.
20 And he said to them, "Whose image is this, and whose inscription?" Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
21 They said, "Caesar's." Then he said to them, "So pay Caesar what belongs to Caesar, and our Father what belongs to our Father." Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
22 When they heard it, they were amazed; and they left him and went away. Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem.
23 That same day Sadducees came to him, who say there is no resurrection, and they asked him, Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan:
24 saying, "Teacher, Moses said: if a man dies childless, his brother must marry the widow and raise offspring for his brother. «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.”
25 Now there were seven brothers among us. The first married, died, and, childless, left his wife to his brother. Amoon na ci nun nag juróom ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba noppi, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
26 So too the second and the third, down to the seventh. Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom ñaareel ba.
27 Last of all, the woman died. Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu.
28 In the resurrection, then, whose wife of the seven will she be? For they all had her." Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
29 Jesus answered, "You're mistaken—you know neither the Scriptures nor our Father's power. Waaye Yeesu ne leen: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla.
30 For in the resurrection people neither marry nor are married off, but are like angels in heaven. Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
31 Now, about the resurrection of the dead, haven't you read what our Father told you: Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa masuleena jàng la leen Yàlla waxoon ne:
32 'I'm the God of Abraham, of Isaac, and of Jacob'? He's not God of the dead, but of the living." “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
33 And when the crowds heard it, they were astonished at his teaching. Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngle.
34 But when the Pharisees heard that he had silenced the Sadducees, they gathered together. Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
35 And one of them, an expert in the Law, asked him a question to test him: Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko:
36 "Teacher, which is the great commandment in the Law?" «Kilifa gi, ban ndigal moo gëna màgg ci yoonu Musaa?»
37 He said to him, "Love your Father with all your heart, with all your soul, and with all your mind. Yeesu ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.”
38 This is the great and first commandment. Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane.
39 And a second is like it: You will love your neighbor as yourself. Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
40 On these two commandments depend all the Law and the Prophets." Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
41 Now while the Pharisees were gathered together, Jesus asked them, Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen:
42 "What do you think about the Christ? Whose son is he?" They said to him, "David's." «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.»
43 He asked them, "How then does David, by the Holy Spirit, call him Lord, saying, Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne:
44 'Our Father said to my Lord, "Sit at my right hand, until I put your enemies under your feet"'? “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
45 If then David calls the Christ Lord, how can the Christ be David's son?" Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
46 No one could answer him a word, and from that day no one dared ask him anything else. Ci kaw loolu kenn manu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]