Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 23 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Then Jesus spoke to the crowds and to his disciples, Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen:
2 saying, "The scribes and the Pharisees sit on Moses' seat. «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa.
3 "So do and keep whatever they tell you, but not what they do—they preach, but don't do. Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe.
4 They tie up heavy, hard-to-carry loads and put them on people's shoulders, but they themselves won't lift a finger to move them. Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam.
5 They do everything to be seen by others; they widen their phylacteries and lengthen their tassels, Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb.
6 and they love the place of honor at feasts and the best seats in the synagogues, Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya.
7 and greetings in the marketplaces and being called 'Rabbi' by others. Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “kilifa gi.”
8 You must not be called 'Rabbi,' since you have only one teacher, and you're all brothers. Waaye yéen buñu leen wooye “kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen.
9 And call no one on earth your father, for you have one Father, who is in heaven. Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw.
10 Don't let anyone call you 'instructor,' for you have one instructor, the Christ. Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist.
11 The greatest among you will be your servant. Ki gëna mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
12 Whoever raises himself will be humbled; whoever humbles himself will be raised. Kuy yékkatiku dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
13-14 Woe to you, scribes and Pharisees, hypocrites! For you shut the kingdom of our Father before people, neither entering yourselves nor letting in those trying to enter. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci.
15 Woe to you, scribes and Pharisees, hypocrites! For you cross sea and land to make one convert, then make him twice the child of hell you are. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon.
16 Woe to you, blind guides! You say, 'Swearing by the temple means nothing, but swearing by the temple's gold makes the oath binding.' «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.”
17 Blind fools! Which is greater: the gold, or the temple that makes the gold sacred? Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gëna màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell?
18 And you say, 'Swearing by the altar is nothing, but swearing by its gift is binding.' Dangeen ne it: “Ku giñe sarxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.”
19 You blind men! For which is greater, the gift or the altar that makes the gift sacred? Gumba yi! Lan moo gëna màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell?
20 So whoever swears by the altar swears by it and by everything on it. Ku giñe sarxalukaay bi, giñ nga ci sarxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
21 And whoever swears by the temple swears by it and by him who lives in it. Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak ki ci dëkk.
22 And whoever swears by heaven swears by our Father's throne and by him who sits on it. Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak ki ci toog.
23 Woe to you, scribes and Pharisees, hypocrites! You bring the tenth of mint, dill, and cumin, yet neglect the law's weightier matters—justice, mercy, faithfulness. These you should have done, without neglecting the others. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des.
24 You blind guides, straining out a gnat and swallowing a camel! Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
25 Woe to you, scribes and Pharisees, hypocrites! You clean the cup and dish outside, but inside they're full of greed and excess. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
26 Blind Pharisee! First clean the inside of cup and dish, so the outside is clean too. Farisen yu gumba yi! Jëkkleena setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set.
27 Woe to you, scribes and Pharisees, hypocrites! You are like whitewashed tombs, appearing beautiful outside but full of dead people's bones and all impurity inside. «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk.
28 So you also outwardly appear righteous to others, but inside you are full of hypocrisy and lawlessness. Yéen itam, ci ngistal dangeena mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
29 Woe to you, scribes and Pharisees, hypocrites! For you build tombs of the prophets and decorate the monuments of the righteous, «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
30 saying, 'Had we lived in our fathers' days, we would not have joined them in killing the prophets.' Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.”
31 So you testify against yourselves that you are the sons of those who murdered the prophets. Seede ngeen nii ne yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi,
32 Fill up, then, the measure of your fathers. di aw seen tànki baay, ba yées leen sax.
33 You serpents, you brood of vipers, how are you to escape being sentenced to hell? Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu sawara?
34 So I am sending you prophets, wise men, and scribes—some you will kill and crucify, some you will flog in your synagogues and persecute from town to town, Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo dëkk.
35 so that all righteous blood shed on earth may come upon you—from righteous Abel's blood to Zechariah son of Berekiah's, whom you murdered between the sanctuary and the altar. Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakari doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak sarxalukaay bi.
36 Truly, I say to you, all these things will come upon this generation. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii.
37 Jerusalem, Jerusalem—killing the prophets, stoning those sent to you! How often I wanted to gather your children, as a hen gathers her chicks under her wings, but you refused. «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!
38 Look, your house is left to you desolate. Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent.
39 I tell you, you won't see me again till you say, 'Blessed is the one coming in our Father's name.'" Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]