Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 20 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "For the kingdom of our Father is like a landowner who went out at dawn to hire workers for his vineyard. «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu reseñam.
2 He agreed to pay the workers a full day's wage and sent them into his vineyard. Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leena yebal ca toolam.
3 About nine o'clock in the morning he went out and saw others standing idle in the marketplace. Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu.
4 He told them, 'You too, go into the vineyard; I'll pay you whatever's right.' So they went. Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.”
5 Going out again about noon and about three in the afternoon, he did the same. Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu.
6 About five in the afternoon, he went out and found others standing there. He asked, 'Why have you stood here idle all day?'" Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?”
7 "They said, 'Because no one hired us.' He said, 'You also go into the vineyard.' Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.”
8 "When evening came, the vineyard owner told his foreman, 'Call the workers and pay them their wages, from the last to the first.' «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.”
9 And when those hired about five o'clock came, each of them received a full day's wage. Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon.
10 When the first came, they thought they would get more, but each got a full day's wage too. Gannaaw ga nag ñi mu jëkka jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon.
11 And on receiving it they grumbled at the landowner, Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga,
12 saying, 'These last worked only one hour, yet you made them equal to us, who bore the day's burden and the scorching heat.' naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.”
13 "He answered one of them, 'Friend, I'm not wronging you. Didn't you agree with me for a full day's wage?' Waaye boroom kër ga ne kenn ci ñoom: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon?
14 Take what's yours and go. I want to give this last worker the same as you. Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw,
15 Can't I do what I want with what's mine? Or are you jealous because I'm generous? ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?”
16 So the last will be first, and the first last." Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.»
17 As Jesus was going up to Jerusalem, he took the twelve aside and said to them on the way, Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii:
18 "See, we are going up to Jerusalem, and the Son of Man will be given over to the chief priests and scribes, who will condemn him to death, «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee,
19 and hand him over to the Gentiles to mock and flog and crucify—and on the third day he will be raised." jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
20 Then Zebedee's sons' mother came to him with her sons, kneeling to ask something of him. Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn.
21 He asked her, "What do you want?" She said, "Say my two sons will sit one at your right, one at your left, in your kingdom." Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.»
22 But Jesus replied, "You don't know what you're asking. Can you drink the cup I am about to drink?" "We can," they said. Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.»
23 He said, "You will drink my cup, but seating at my right and left is not mine to give—it belongs to those my Father has prepared it for." Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama càmmoñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.»
24 When the ten heard this, they were angry at the two brothers. Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya.
25 Jesus called them over and said, "You know the rulers of the Gentiles lord it over them, and their powerful men hold authority over them. Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di not.
26 Not so among you. Rather, whoever wants to be great among you must be your servant, Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga,
27 and whoever wants to be first among you must be your slave, te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam.
28 just as the Son of Man came not to be served but to serve, and to give his life as a ransom for many." Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
29 And as they went out of Jericho, a great crowd followed him. Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko.
30 Two blind men sitting by the road heard Jesus was passing and cried out, "Lord, have mercy on us, Son of David!" Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
31 The crowd scolded them to be quiet, but they shouted louder, "Have mercy on us, Lord, Son of David!" Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
32 And stopping, Jesus called them and said, "What do you want me to do for you?" Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
33 They said to him, "Lord, let our eyes be opened." Ñu ne ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.»
34 And Jesus, moved with compassion, touched their eyes, and immediately they recovered their sight and followed him. Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]