Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Matthew 19 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 When Jesus finished these words, he left Galilee and went into the region of Judea, across the Jordan. Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan.
2 Large crowds followed him, and he healed them there. Mbooloo mu bare topp ko, mu faj leen fa.
3 Pharisees came to test him, asking, "Is it lawful for a man to divorce his wife for any cause?" Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase soxnaam, saa su ko neexee?»
4 He answered, "Haven't you read that our Father, who made them at the beginning, made them male and female, Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen,
5 and said, 'So a man will leave his father and mother and cling to his wife, and the two will become one flesh'? te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.”
6 So they are no longer two but one flesh; therefore, let no one separate what our Father has joined." Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
7 They said to him, "Why then did Moses command that a man give a divorce certificate and send her away?" Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox soxnaam kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?»
8 He told them, "Moses let you divorce your wives because your hearts were hard, but it wasn't like that from the beginning. Yeesu ne leen: «Musaa may na leen, ngeen fase seen soxna, ndax seen xol dafa dëgër, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu.
9 I tell you: whoever divorces his wife—except for sexual sin—and marries another commits adultery." Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa soxna te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.»
10 The disciples said to him, "If that's the case between husband and wife, it's better not to marry." Bi ko taalibe ya déggee, ñu ne ko: «Bu dee noonu la digganteb góor ak jigéen mel, baña séy moo gën.»
11 He said to them, "Not everyone can accept this word—only those it's given to. Yeesu ne leen: «Du ñépp ñoo mana nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk.
12 There are eunuchs born that way from their mother's womb; there are eunuchs made that way by others; and there are eunuchs who made themselves so for the kingdom of our Father. Let the one who can accept this, accept it." Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu baña séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko mana nangu, nangu ko.»
13 Then little children were brought to him so he could lay hands on them and pray, but the disciples rebuked those bringing them. Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen.
14 But Jesus said, "Let the little children come to me—don't stop them, for the kingdom of our Father belongs to ones like these." Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
15 And he laid his hands on them and went on from there. Noonu Yeesu teg leen ay loxoom, ba noppi jóge fa.
16 Just then a man approached him and asked, "Teacher, what good must I do to obtain eternal life?" Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def ci lu baax, ngir mana am dund gu dul jeex?»
17 He said to him, "Why ask me about what is good? Only one is good. If you want to enter life, keep the commandments." Yeesu ne ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.»
18 "Which ones?" he asked. Jesus said, "Do not murder, do not commit adultery, do not steal, do not testify falsely, Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg,
19 honor your father and mother, and love your neighbor as yourself." teralal sa ndey ak sa baay, te it: nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
20 The young man said to him, "All these I have kept. What do I still lack?" Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?»
21 Jesus told him, "If you want to be complete, go, sell your possessions and give to the poor—you'll have treasure in heaven—then come, follow me." Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
22 When the young man heard this, he went away grieving, because he had great wealth. Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
23 Jesus said to his disciples, "Truly, I tell you: a rich person will hardly enter our Father's kingdom. Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
24 I tell you again: a camel fits through the eye of a needle easier than a rich person enters our Father's kingdom." Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
25 When the disciples heard this, they were greatly astonished and asked, "Who then can be saved?" Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo mana mucc nag?»
26 Jesus looked at them and said, "This is impossible for people, but everything is possible with our Father." Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.»
27 Then Peter said to him, "Look, we've left everything and followed you. What then will we have?" Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw, nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?»
28 Jesus told them, "Truly: in the renewal, when the Son of Man sits on his glorious throne, you who followed me will also sit on twelve thrones, judging the twelve tribes of Israel. Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.
29 "Everyone who has left houses or brothers or sisters or father or mother or children or fields for my name will receive one hundred times more and inherit eternal life. Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex.
30 But many who are first will be last, and many who are last will be first." Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]