Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Mark 14 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Two days before Passover and Unleavened Bread, the chief priests and scribes were looking for a way to seize Jesus by trickery and kill him. Booba nag sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya ñu ngi doon fexeel Yeesu, ngir jàpp ko, reylu. Fekk booba ñaari fan a des ci màggalu bésu Mucc ba ak màggalu Mburu ma amul lawiir.
2 For they said, "Not during the feast, or the people might riot." Kon nag ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yëngu-yëngu baña am ci nit ñi.»
3 While he was in Bethany, in Simon the leper's house, reclining at the table, a woman came with an alabaster flask of pure nard perfume, very costly. She broke the flask and poured it on his head. Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani, mu dem këru Simoŋ ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jigéen ñëw, yor njaq lu ñu defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree bare. Jigéen ji toj njaq li, tuur latkoloñ ci boppu Yeesu.
4 There were some who said to themselves indignantly, "Why was this perfume wasted like that? Waaye amoon na fa ñu mer, di xultu ci seen biir naan: «Yàq gii, lu muy jariñ?
5 For this perfume could have sold for over 300 denarii and given to the poor." And they scolded her. Maneesoon na jaay latkoloñ jii ci lu tollook peyug atum lëmm, jox ko miskin yi.» Noonu ñu daldi gëdd jigéen ji.
6 But Jesus said, "Leave her alone. Why trouble her? She has done a beautiful thing for me. Waaye Yeesu ne leen: «Bàyyileen ko. Defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal?
7 For the poor are always with you, and you can do good for them whenever you want; but you won't always have me. Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, te man ngeen leena dimbali saa su leen neexee, waaye dungeen ma gis ba fàww.
8 She has done what she could; she has anointed my body beforehand for burial. Jigéen ji def na li mu man; diw na sama yaram ak latkoloñ, ngir waajal sama rob, laata moo jot.
9 Truly, I tell you, wherever the gospel is preached worldwide, what she did will be told in memory of her." Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
10 Then Judas Iscariot, one of the twelve, went to the chief priests to betray Jesus to them. Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya, ngir wori Yeesu.
11 Hearing this, they were glad and promised him money. So he looked for a chance to betray Jesus. Bi ñu ko déggee, ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis. Noonu mu fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu.
12 On the first day of Unleavened Bread, when they sacrificed the Passover lamb, his disciples asked him, "Where do you want us to go and prepare for you to eat the Passover?" Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, taalibey Yeesu laaj ko: «Foo bëgg, nu defaral la reeru bési Mucc bi?» Bés bu jëkk booba nag mooy bés, ba ñu farala rendi gàttub bésu Mucc ba.
13 He sent two of his disciples, "Go into the city; a man carrying a jar of water will meet you. Follow him, Noonu Yeesu yebal ñaar ci taalibe yi ne leen: «Demleen ca dëkk ba, foofa góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen, ngeen topp ko.
14 and wherever he enters, tell the house's owner, 'The Teacher says: Where is my guest room, where I may eat the Passover with my disciples?' Kër gi mu dugg nag, ngeen ne boroom kër gi: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc bi, man ak samay taalibe?”
15 And he will show you a large upper room furnished and ready; there prepare for us." Dina leen won néeg bu féete kaw te yaa, ñu defar ko, ba lépp jekk. Foofa ngeen nuy defarale reer bi.»
16 The disciples left, went to the city, found things as he had told them, and prepared the Passover. Bi mu ko waxee, taalibe ya dem ca dëkk ba, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
17 And when it was evening, Jesus came with the twelve. Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu ñëw, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar.
18 While they reclined and ate, Jesus said, "Truly, I tell you, one of you will betray me, one eating with me." Ñu toog, di lekk. Bi ñuy lekk nag, Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen, ku bokk ak man di lekk sax, dina ma wor.»
19 They began to grieve and ask him, one by one, "Is it I?" Taalibe yi nag am naqar, ñu daldi ko ne kenn-kenn: «Mbaa du man?»
20 He said to them, "One of the twelve, dipping bread with me into the dish. Mu ne leen: «Kenn ci yéen fukk ak ñaar la, kuy cappandoo ak man ci ndab li.
21 The Son of Man goes as the Scriptures said about him, but how terrible for that man who betrays him—better if he had never been born." Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox. Bañoona juddu moo gën ci moom.»
22 As they ate, he took bread, blessed it, broke it, gave it to them, and said, "Take; this is my body." Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, jox leen ko naan: «Jël-leen, lii sama yaram la.»
23 He took a cup, gave thanks, gave it to them, and they all drank from it. Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko, ñépp naan ci.
24 He said to them, "This is my blood of the covenant, poured out for many. Mu ne leen: «Lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te tuurul ñu bare.
25 Truly I tell you, I will not drink wine again until that day when I drink it new in the kingdom of our Father." Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dootuma naan gannaaw tey ndoxum reseñ mii, ba kera ma ciy naan bu bees ci nguuru Yàlla.»
26 And when they had sung a hymn, they went out to the Mount of Olives. Noonu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
27 Jesus said to them, "You will all stumble, for it's written: 'I will strike the shepherd, and the sheep will be scattered.' Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.”
28 But after I am raised up, I will go ahead of you to Galilee." Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.»
29 Peter said to him, "Even though they all fall away, I will not." Kon Piyeer ne ko: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la bàyyi mukk.»
30 Jesus said to him, "Truly I tell you, today, this night, before the rooster crows twice, you will deny me three times." Waaye Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, guddig tey, bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.»
31 But he insisted, "Even if I must die with you, I will never deny you." They all said the same. Waaye Piyeer gëna sax ca la mu waxoon naan: «Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu.
32 They arrived at a place called Gethsemane, and he told his disciples, "Sit here while I pray." Noonu ñu dem ca bérab bu tudd Setsemane. Yeesu ne taalibe yi: «Toogleen fii, ma dem ñaani.»
33 He took Peter, James, and John, and began to feel deep distress and anguish. Mu ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi jàq, ba xonet.
34 He said to them, "My soul is crushed with grief, to death. Stay here and stay alert." Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba ma bëgga dee; toogleen fii, xool.»
35 Going a little farther, he fell to the ground and prayed that, if possible, the hour would pass from him. Noonu Yeesu dem ci kanam tuuti, daanu ci suuf, di ñaan ne, waxtu wi teggi ko, bu loolu manoona am.
36 He said, "Abba, Father, all things are possible for you. Take this cup from me—but let it be your will, not mine." Mu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
37 He returned, found them asleep, and said to Peter, "Simon, are you asleep? Couldn't you stay awake one hour? Noonu mu délsi ci taalibe yi, fekk ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
38 Watch and pray, so you don't fall into temptation. The spirit is willing, but the flesh is weak." Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.»
39 And again he went away and prayed, saying the same words. Beneen yoon Yeesu dem, di ñaane noonu,
40 Again he found them sleeping, eyes heavy, not knowing how to answer him. délsiwaat, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. Xamuñu lu ñu koy tontoo.
41 He came a third time and said, "Still sleeping and resting? Enough—the hour has come. Look, the Son of Man is handed over into the hands of sinners. Ñetteelu yoon mu délsi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi.
42 Rise, let us be going; see, my betrayer is here." Jógleen nu dem; ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
43 While he was still speaking, Judas—one of the twelve—arrived, and with him a crowd with swords and clubs from the chief priests, scribes, and elders. Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak ñaar, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, mu jóge ca sarxalkat yu mag ya, ca xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
44 His betrayer had given them a signal: "The one I kiss is him—seize him and take him away securely." Fekk ki ko naroona wor joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko, yóbbu ko te wottu ko bu baax.»
45 He came up to Jesus at once, said, "Rabbi!" and kissed him. Noonu mu ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi,» daldi ko fóon.
46 And they laid hands on him and seized him. Bi mu ko defee nit ñi song Yeesu nag, jàpp ko.
47 One of the bystanders drew his sword, struck the high priest's servant, and cut off his ear. Waaye kenn ci ñi fa taxaw bocci jaaseem, dóor surgab sarxalkat bu mag bi, nopp bi dagg.
48 Jesus said to them, "Have you come out with swords and clubs to seize me, like a robber? Yeesu ne leen: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
49 Every day I was with you in the temple teaching, and you didn't arrest me. But let the Scriptures be fulfilled." Moona daan naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngle, te jàppuleen ma. Waaye lii am na, ngir Mbind mi am.»
50 And they all left him and fled. Ci kaw loolu, ñépp dëddu ko, daw.
51 And a young man followed him, wearing nothing but a linen cloth. And they seized the young man, Fekk amoon na ca waxambaane wu lëkkaayoo woon sér, topp Yeesu, ñu daldi ko jàpp.
52 but he left the linen cloth and ran away naked. Waaye waxambaane wa wacc fa sér bi, daldi daw, def yaramu neen.
53 They led Jesus to the high priest, and all the chief priests and elders and scribes gathered. Ñi jàpp Yeesu yóbbu ko ci sarxalkat bu mag bi, te foofa la sarxalkat yu mag yi, njiit yi ak xutbakat yi yépp dajaloo.
54 Peter had followed at a distance, all the way into the high priest's courtyard, and sat with the guards, warming himself by the fire. Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci ëttu sarxalkat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi.
55 The chief priests and the whole council sought testimony against Jesus to put him to death, but found none. Noonu sarxalkat yu mag yi ak kureelu àttekat yi yépp di wut ku mana seede lu daan Yeesu, ba ñu man koo reylu, waaye gisuñu kenn.
56 For many gave false testimony against him, but their testimony did not agree. Teewul sax naaféq ñu bare ñëw, seede ci Yeesu lu dul dëgg, waaye seen seede ànduñu.
57 And some stood up and gave false testimony against him, saying, Ba mujj naaféq taxaw, seede ci moom naan:
58 "We heard him say, 'I will destroy this temple made by hands, and in three days build another not made by hands.'" «Nun daal dégg nanu, mu ne: “Dinaa toj kër Yàlla, gii loxoy nit liggéey, tabax ci ñetti fan geneen gu nit liggéeyul.”»
59 Yet even about this their testimony did not agree. Waaye ba tey seeni wax ànduñu.
60 The high priest stood up in the midst and asked Jesus, "You have no answer? What are these men testifying against you?" Ci kaw loolu sarxalkat bu mag bi taxaw ci seen kanam ne Yeesu: «Doo tontu? Lu la nit ñi di jiiñ?»
61 He stayed silent, answered nothing. Again the high priest asked him, "Are you the Christ, the Son of the Blessed?" Waaye Yeesu ne cell, waxul dara. Sarxalkat bu mag bi dellu nag ne ko: «Ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ju tedd ji?»
62 Jesus said, "I AM, and you will see the Son of Man seated at the right hand of the Mighty One and coming with heaven's clouds." Yeesu ne ko: «Moom laa. Te dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Aji Man ji, di ñëw ci niiri asamaan.»
63 And the high priest tore his clothes and said, "What further witnesses do we need? Bi ko sarxalkat bu mag bi déggee nag, mu daldi mer, ba xotti ay yéreem naan:
64 You have heard his blasphemy. What is your decision?" And they all condemned him as deserving death. «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Lu ngeen ci xalaat?» Noonu ñépp teg ko dee.
65 Some began spitting on him, covering his face, and punching him, saying to him, "Prophesy!" Then the guards slapped him. Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci moom, takk ay bëtam, di ko dóor ay kurfeñ, naan ko: «Yaw wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?» Ba noppi alkaati yi teeru ko ak ay pes.
66 While Peter was below in the courtyard, one of the high priest's servant girls came, Piyeer nag ma nga toogoon ci ëtt bi féete suuf. Noonu benn mbindaanu sarxalkat bu mag ba romb fa.
67 seeing Peter warming himself, she looked at him and said, "You too were with the Nazarene, Jesus." Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko jàkk naan: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu.»
68 But he denied it: "I don't know or understand what you mean." Then he went out to the entrance, and a rooster crowed. Waaye Piyeer weddi ko naan: «Xawma li ngay wax, dégguma ci dara.» Mu daldi génn, dem ca buntu kër ga.
69 The servant girl saw him and again told the bystanders, "This man is one of them." Foofa nag mbindaan mi gisaat ko, mu ne ñi fa taxaw: «Waa jii ci ñoom la bokk.»
70 But he denied it again. A little later the bystanders again told Peter, "You truly are one of them, for you're a Galilean." Waaye Piyeer weddiwaat ko. Nees-tuut ñi fa taxaw ne Piyeer: «Yaw mi de, ci lu wóor bokk nga ci, nde waa Galile nga.»
71 He began to call down curses on himself and swear, "I don't know this man you're talking about." Waaye Piyeer daldi giñ ak a waat naan: «Xawma nit ki ngay wax.»
72 At once a rooster crowed a second time. Peter remembered Jesus' words: "Before the rooster crows twice, you will deny me three times." He broke down and wept. Ci saa si ginaar sab ñaareelu yoon. Noonu Piyeer fàttaliku li ko Yeesu wax: «Bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi jooy jooy yu metti.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]